Description
Lislaam mooy diiney Boroom mbindéef yi
Yénèni tékki 37
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.
Lii mooy laaj bi gën a màgg ci lépp; te mooy laaj bi ëpp solo ci li nit ki war a xam ab tontoom.
Sunu Boroom mooy ki bind asamaan yi ak suuf si, daal di wàcce am ndox mu bawoo asamaan, mu génne ca ay meññet ak i garab ngir muy sunug dund, ak dundug baayima yi nga xam ne dañu koy lekk,Moo nu bind bind sunuy baay, bind lépp, moo def guddi ak bëccëg, mooy ki def guddi muy waxtuw nelaw ak noppalu, mu def bëccëg muy waxtuw sàkku dund,Moo tàggat jant bi ak weer wi ak biddiw yi ak géej yi, Moo nu tàggatal baayima yi nu di ci lekk, di jariñu ci am saawam ak kawaram.
Boroom bi mooy ki bind mbindéef yi, te moo leen di gindi jëme leen ci dëgg ak njub, Mooy doxal mbiri mbooleem mbindéef yi, te moo leen di wërsëgal, te moo moom lépp lu nekk ci dundug àdduna bi ak àllaaxiraa, te lépp moo ko moom, lu dul moom rekk moomeelam la.Mooy Aji-Dund ji dul dee te du nelaw, Mooy Aji-Taxaw ji nga xam ne taxawaayu lépp ci ndigalam la aju, mooy ki yërmàndeem daj lépp, mooy ki dara nëbbuwul ci moom, ci suuf si walla ci asamaan si.Dara niroowul ak moom, te day dégg di gis, moo ngi ci kaw asamaanam yi, soxlaalul mbindéef yi, te mbindéef yi dañu koo soxlawoo, du wàcci ci mbindéefam yi, te dara ci mbindéefam yi du wàcc ci jëmmam ji -tudd naa sellam ga-Boroom bi mooy ki bind àdduna bii ñuy gis ak nii mu nosoo te yam te amul juuyaloo, moo xam ci nosaleg yaramu nit la, walla bu bayima , walla nosaleg àdduna bi nu wër ci jàntam ak biddiwam ak mbooleem li fi nekk.
Te lépp lu ñuy jaamu te du moom amalul boppam njariñ walla lor kon naka lay man a xëccale njariñ keneen, mbaa mu koy jeñal aw lor?
Àqam ci nit ñépp mooy ñu jaamu ko moom dong te duñu ko bokkaaleek dara, duñu jaamu kudul moom mbaa ñukoy bokkaale ak nit walla doj, walla Ag dex, walla lu amul ruuh , walla biddiw walla dara lu mu man a doon, waye dañuy def jaamu gi mu nekk lu sell ñeel Yàlla Boroom mbindéef.
Àqi nit ñi ci Yàlla mooy: bu ñu ko jaamoo mu defal leen dund gu teey guñuy man a ame kóolute ak jàmm, ak ug dal ak ngërëm, bu àllaaxiraa mu dugal leen àjjana, ay xéewal yu sax dàkk moo fa am, waaye bu ñu ko moyee, wuuteek ay ndigalam, dana def séen ug dund muy lu texeedi, di lu naqari doonte dañuy foog ne ñoo ngi cig texe ak ub nooflaay, bu àllaaxiraa mu dugal leen sawara joj duñu fa génn, te mbugal mu sax dàkk lañu fay am, ak ug sax ba fàww.
Boroom bu tedd bi xibaare na nu ne da noo bind ngir jubluwaay bu tedd, te mooy nu jaamu ko moom dong, te dunu ko bokkaale ak dara, mu digal nu nuy dundal suuf si ci mbaax ak yiw. Képp ku jaamu ku dul Boroomam mi ko bind, kon xamul li tax ñu bind ko, te deful li ko war ci Boroomam. Te képp kuy yàq ci kaw suuf xamul ban liggéey la ñu ko gàll.
Boroom bi -tudd naa ag màggam- bindu nu ba noppi boyal nu, te deful sunug dund muy ay caaxaan, waaye dafa tànn ci nit ñi ay ndaw yónni leen ci séenuw nit. Te ñoom ñooy ñi gën a mat jikko ci nit ñi, gën leen a sell bàkkan, gën leen a laab xol. Mu wàcce ci ñoom ay bataaxal, mu def ca lépp lu nit ñi war a xam ci séen Boroom -tudd naa màgaam ga- niki noonu dékkig nit ñi ëllëg bis-penc, te mooy bisub càmbar ba ak pay ga.Yónente yi jottali na ñu séen uw nit na ñuy jaamoo séen Boroom, leeralal leen melokaani jaamu yi ak séen i waxtu, ak séeni pay ci àdduna ak allaaxira. ñu moytuloo leen leen it lépp lu séen Boroom araamal ci ñoom ci lekk ak naan ak sëy. ñu jubale leen ca jikko yu màgg ya, tere leen jikko ya ñu ŋàññi.
Diine ji Yàlla nangu mooy Lislaam, te mooy diine ji nga xam ne moom la Yónente yépp doon jottali, te Yàlla du nangu ëllëg bis-penc lu dul moom. Jépp diine ju nit ki nekk ju dul Lislaam ag neen la, du jariñ boroomam. Waaye kay ag texeedi lay doon ci moom àdduna ak allaaxira.
Diine jii Yàlla da koo yombal ci jaamam yi. Li gën a màgg ci ay ponkam mooy nga gëm Yàlla muy sa Boroom di sa Yàlla, gëm ay Malaakaam ak i téeréem ak i yónentam ak bis bu mujj ba, ak dogal yi. Nga seede ne amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawu Yàlla la, di taxawal julli di joxe asaka, ak di woor weeru koor, moom benn weer la ci at mi, di aj ngir Yàlla néeg bu yàgg ba nga xam ne Ibraahiima -yal na ko Yàlla dolli jàmm- moo ko tabax, benn yoon boo ko manee.Nga moytu li Yàlla araamal ci yaw ci bokkaale, ak ray bakkan, ak njaalo, ak lekk alal ju araam. Boo gëmee Yàlla dangay def jaamu yii, moytu yu araam yii kon yaw kuy mucc nga ci àdduna, te ëllëg bis-penc Yàlla dina la defal xéewal gu sax, ak ug sax ca àjjana ba fàwwu.
Lislaam diiney Yàlla la ñeel nit ñépp. Kenn du ci gën kenn ci lu dul ragal Yàlla ak def lu baax, nit ñépp ñoo ci yam.
Nit ñi danañu xam dëggug Yónente yi ci ay yoon yu bari, bokk na ca:
Li ñu indi ci dëgg ak njub xel da koy nangu mbindiin wu mucc ayib it da koy nangu, te xel yi dañuy seede ak rafetam, te ku dul ab yónente du indi lu mel ni ñoom li ñu indi.
Li Yónente yi indi yéwénug diiney nit ñi ci la nekk ak seen àdduna, ci la séen i mbir di jube, ci la ñuy tabaxe séen i cosaan, ak di ci sàmme séen diine ak séen xel ak séen i alal ak séen i der.
Yónente yi sàkkuwuñu si nit ñi pay ci tegtal ngi ñu leen di tegtal yiw ak ug njub, waaye dañuy xaar séen ug pay ci séen Boroom.
Li Yónente yi indi dëgg la, lu wóor la lu amul sikki-sàkka, du juuyoo du deng-dengi. Yónente bu nekk day dëggal Yónente ya jiitu woon, di woote ci lu mel ni la ñu doon woote.
Yàlla day dëgëral Yónente yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm- ci ay aaya yu leer ak i keeman yu not yoy Yàlla da koy dawal ci ñoom; ngir mu nekk seedey dëgg ci ne ñoom Yàlla moo leen yónni. Li gën a màgg ci keemaani yónente yi mooy keemani yónente bi mujj muy Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- te mooy Alxuraan ju tedd ji.
Alxuraan ju tedd ji mooy téeréb Boroom mbindéef yi, mooy waxu Yàlla, Malaaka ma Jibriil moo ko wàcce ci Yónente bi Muhammat; lépp lu Yàlla waral ci nit ki mu xam ko ci Yàlla ak i Malaakaam ak i téeréem ak i yónentam ak bis bu mujj ba ak dogal yu neex yi ak yu naqari yi ma nga ca.Jaamu yi war it ma nga ca, ak yu araam yi ñu wara moytu, ak jikko yu màgg yi ak jikko ya ñu ŋàññi, ak lépp lu aju ci mbiri diiney nit ñi ak séen àddunaak àllaaxira. Te mooy téeré bay aji-lottloo, Yàlla dëkk na nit ñi ci ñu indi lu mel ni moom. Te lu ñu wattu la ba bis-penc ba ci làkku araab ba mu wàcce woon. Benn Loy (araf) wàññeekuwu ci, benn baat it soppikuwu ci.
Xanaa gisóo suuf su dee si ba amul genn dund, bu ca ndox ma wàccee rekk mu yëngu daal di sax gépp gàncax gu nëtëx. Ki ko dundalaat ku am kàttan la ci dekkil ñi faatu.Ki bind nit ci toq ndox mu doyadi Aji-Am-Kàttan la ci dekkil ko keroog bis-penc, daal di koy càmbar fay ko pay gu mat sëkk, bu dee yiw mu fay ko yiw, bu dee safaan mu fay ka ko.Ki bind asamaan yi ak suuf si ak biddiw yi Aji-Am-Kàttan la ci bindaat nit ki; ndax delloosiwaat ag mbindum nit beneen yoon moo gën a yomb bind asmaan yi ak suuf si.
Boroom bi -ag màggam kawe na- day dekkil mbindéef yi ca séen i bàmmeel daal di leen càmbar ci séen i jëf, ku gëm te dëggal Yónent yi mu dugal ko àjjana ja nga xam ne xéewal gu sax la gog màggaayam du rot ci xelu nit. Ku weddi mu dugal ko sawara sa Nga xam ne mbugal ma day sax ba fàwwu te nit manu koo xalaat. Bu nit ki duggee àjjana walla sawara dootul dee ba fàww, te day sax, ci ay xéewal walla ci mbugal.
Bu nit ki xamee diiney dëgg te mooy Lislaam, ak ne mooy diiney Boroom mbindéef yi, war naa gaawantu ci dugg ci Lislaam; ndax aji-xellu ji bu ko dëgg leeree dafa war a gaawantu jëm ca, te du yeexe mbir moomu,Ku bëgg a dugg ci Lislaam nag benn jaamu bu ñu defar sos ko du war ci moom,du ne it dafa war kenn teewe ko ci nit ñi,waaye bu ko jullit teewee walla mu ame ci bérabu Lislaam loolu ngëneel la ci kaw ngëneel, bu amul it, dana ko doy rekk mu wax: ashadu anlaa Ilaaha illallaah, wa ashadu Anna Muhammadan rasuulullaah (maa ngi seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawu Yàlla la), te xam li miy tekki te gëm ko,ci loolu lay nekke ab jullit; mu jàng nag àttey Lislaam yi des ndànk-ndànk; ngir mu man a taxawe li Yàlla waral ci moom.
Lislaam mooy diiney Boroom mbindéef yi.
Lan mooy meloy Boroom mbindéef yi?
Lan mooy àqi sonu Boroom ci nun?
Lan mooy àqi nit ñi ci séen Boroom?
Lu tax nu am? Ak lu tax ñu bind nu?
Naka la nuy jaamoo sunu Boroom?
Lan mooy diine ja Boroom bi nàngu fa moom?
Lan mooy cosaani diiney Lislaam ak ay ponkam?
Ndax Lislaam diiney aw nit la walla aw xeet?
Naka la nit ñi di xame dëggug Yónente yi -yal na leen Yàlla dolli jàmm-?
Lan mooy tegtali dekki ga ak waññi ga?