Description
Man jullit laa
Yénèni tékki 51
Topics
Man jullit laa
Ki ko bind mooy Muhammat Doomu Ibraahiima Alhamdi
Man jullit laa, Loolu mooy Lislaam mooy sama diine,Lislam kàddu gu màgg la te sell gog Yonnente yi -yal na jàmmu nekk ci ñoom- da koo donnante mu dale ci ki jëkk ci ñoom ba ci ki mujj ci ñoom;Kàddu googu nag day làmboo ay maana yu kawe ak ay jikko yu màgg;Te mooy firi jébbalu ak wommatu ak topp Aji-bind ji,Day firi batay jàmm ak texe ak kóolute ak mbégte ñeel kenn ki ak mbooloo mi.Lii moo tax baatu Assalaam ak Lislaam - jàmmu - bokk ci baat yi ëpp lumu rot ci Sariihatul islaam;Assalam - jamm - tur la ci turi Yàlla yi;Te nuyoob jullit yi ci seen diggante itam moy Assalaam - jammu -Nuyoo wa Aljana moy Assalaam -jamm-Te jullit dëgg mooy ki jullit yi mucc ci làmmeñam ak ci loxoom;Lislaam diiney yiw la ñeel mbooleem nit ñi; doy na leen sëkk, te mooy seen yoonu texe ci Adduna ak Allaaxira;Lii moo tax mu mujjee ñëw di lu matale te yaatu te leer di lu tijjeeku ñeel ñépp te du ràññee wenn askan ci kaw askan, wala melo ci kaw melo, waaye day xool nit ñi ci benn xooliin.Te kenn du ràññeeku ci Lisslam lu dul ci kem namu jàppe ci njàngaleem.Loolu moo tax xol yu sell yépp nangu ko; ndax dafa dëppoo ak mbindiinam;Nit ñépp dañoo judd ñu mooñ leen ciw yiw, ak maandu, ak gore, ak bëgg Boroomam, ak saxal ne moom rekk moo yayoo jaamu walif ku dul moom;Te kenn du soppeeku ci mbindiin wii lu dul ne dafa am lu ko soppi,Te diine jii la Yàlla gërëm ñeel nit ñi moom mi leen bind di seen Boroom di ki nu wara jaamu.
Te sama diine jii di Lislaam damaa xamal ne damay dund ci Adduna jii,te ginnaaw buma faatoo it damay tuxu ci baneen kër,t e mooy kërug des gi nga xam ne fala nit ñépp di mujju benn muy Aljana wala Sawara.
Te sama diine jii di Lislaam damay digal ay digle dima tere ay tere;Suma taxawee ci digle yooyu moytu tere yooyu kon dinaa texe ci Adduna ak Allaaxira,Suma ci sàgganee nak dinaa texeedi ci Adduna ak Allaxira ci kem samag càggante ak samag gàttañlu.Li gën a màgg si lima Lislaam digal mooy wéetal Yàlla.Man maa ngi seede, di fas ag fas gu dëggu ne Yàlla moom a bind, te moom rekk laa war a jaamu;Duma jaamu ku dul Yàlla;ngir sama cofeel ci moom,ak ragal mbugalam, ak yaakaar ab yoolam,ak it sukandiku ci moom,Tawhiid jooju ( wéetal Yàlla ) day feeñe ci seede ag kennal ñeel Yàlla, ak seede ak yonnente ñeel Muhammat;Te Muhammat mooy ki mujj ci yonnente yi; Yàlla moo ko yónni mu nekk yërmaande ci jaam ñi, mu tëje yonnente gi ci moom du am beneen Yonnente ginnaawam,muhammat mo andi diine ju mat te yéwen ci béepe jamono ak barap, ak xeet.
Sama diine damaa digal ndigal lu dog ci ma gëm Malaaka yi, ak mbooleem Yonnente yi ña ca jiitu ñooy Nooh, ak Ibraahiima, ak Muusaa, ak Hiisaa ak Muhammat -yal na jàmm nekk ci ñoom -.
Damaay digal it gëm téere yi juge ca Asamaan yi ñu wàcce ko ci yonnente yi, ak topp bi ci mujj, te tëj leen, te gën cee màgg muy (Alxuranul kariim)
Sama diine damay digal itam gëm bis bu mujj ba; bis bi nga xam ne ci la Yàlla di fay nit ñi seen i jëf,Damay digal it gëm dogal yi; ak gërëm limay dal ci dund gii ci lu neex ak lu naqari , ak it may japp ci yiy waral mucc.Gëm ndogal yi damay may ag féex, ak dal, ak muñ, ak bàyyi di naqarlu lima faat;Ndax man damaa xam xam-xam bu wér ni lépp lu ma dal nekkul luma waroona moy, te lépp lu ma moy it nekkul lu ma waroona dal;Mbir yépp lunu dogal la te lunu bind la mu tukkee fa Yàlla kon du war ci man lu dul jàpp ci sabab yi,ak gërëm lépp lu am ginnaaw loolu.
Te Lislaam damay digal lépp luy sellal sama ruu ci ay jëf yu sell, ak ay jikko yu màgg yoy day gërëmloo sama Boroom, tey laabal sama bakkan, tey texeel sama xoll, di tijji sama dënn, di leeral sama yoon, dima def jëmm ju am solo ci askan wi.
Li gën a màgg ci jëf yooyu nag: mooy wéetal Yàlla, ak taxawal julliy juróom ci bëccëg yi ak guddi, ak joxe azakay alal, ak woor aw weer ci at mi, te mooy weeru koor, ak aji ca néegub Yàlla bees wormaal ba fa Màkka ñeel képp ku ko man.
Bokk na ci li gën a màgg ci lima sama diine digal ci luy tijji xol baril jàng Alxuraane mi nga xam ne mooy waxi Yàlla, te mooy wax ji gën a dëggu gën a rafet gën a màgg, gën a rëy te làmboo mboolem xam-xam yi jiitu yi ak yu mujj yi.Di ko jàng walla di ko deglu day dugal dall ak féex ak texe ci xoll, donte Aji jàng ji wala Aji deglu ji déggul Araab wala sax dub jullit.Bokk na ci li gën a màgg ci liy tijji xol bari looy ñaan Yàlla, ak di wéeru ci moom ak di ko ñaan lépp lu ndaw ak lu mag.Yàlla day nangul képp ku ko ñaan tey sellal ag jaamoom ñeel ko.
Bokk na ci li gën a màgg ci liy tijji xoll baril a tudd Yàlla - màgg na te kawe na-.
Sama Yonnente -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- damaa gindi ci na ka la nuy tudde Yàlla, te it xamal nama li gën ci li nuy tudde Yàlla,Bokk na ci yooyu: ñénti baat yi gën ci wax yi ginnaaw Alxuraan, te mooy (subhaanal Laahi, walhamdu lil Laahi, wa laa ilaaha illal Laahu, wal Laahu akbar) tudd naa sellug Yàlla ji, tey sant Yàlla, amul kenn kees war a jaamu ku dul Yàlla, te Yàlla moo gën a màgg lépp.
Ni ki noonu ( asstaxfirul Laaha, wa laa hawla wa laa xuwwata illa bil Laahi) maa ngi jéggalu Yàlla, te amul benn pexe wala kàttan walif ci Yàlla.
Baat yii nag am na ay jeexantal yu yéeme ci tijji dënn, ak wàcce ag dal ci ab xol.
Lislaam it damay digal ci ma nekk ku yékkatiku daraja ku sori lépp luy wàcce samag nite ak sama tedd nga,Ak it may jëfandikoo sama xel ak samay cér ci li tax ñu bind ko ci jëf am njariñ ci sama diine ak sama Adduna.
Lislaam damay digal yërmaande, ak rafet jikko, ak jëflante bu teey, ak rafetal jëme ci mbindéef yi ci wax ak ci jëf sama kem kàttan.
Li gën a màgg ci li nu ma digal ci àqi mbindéef yi mooy àqi ñaari wayjur; sama diinne damaa digal may rafetal jëme ci ñoom ñaar, ak di leen bëggal yiw, ak di xér ci lu leen di bégloo, ak di leen jox lépp lu leen di jariñ; rawatina bu ñu nekkee mag;Loolu moo tax ngay gis yaay ak baay ci réew i Lislaam yi ñuy am wàccuwaay yu kawe ci dayo ak worma, ak seeni doom di leen liggéeyal,Te lu ñaari wayjur yi di gën a maggat wala ñu feebar wala ñu lott ci la rafetalu doom yi jëme ci ñoom di gën a yokk.Sama diine xamal nama ni jigéen amna tedd-nga ju kawe, ak ay àq yu màgg;Jigéen ci Lislam doomi ndayi góor ñi lañu, te ki gën ci nit ñi mooy ki gën ci njabootam,Jullit bu jigéen bi bamu nekkee liir la am àqi nàmpal, ak di ko sàmm, ak yar bu rafet, te moom ci jamono jooju mooy mbégtem xol, di meññeef i xoli ñaari wayjuram ak ay mbokam.Bu màggee nekk ku ñu màggal di ku nu teral, di ku ay kilifaam di fiir ci moom, di ko peeg ci ag càmmam.Du bëgg kenn di jëmale benn ñaaawtéef ci moom, wala wax ju koy lor, wala xooliin wu ñaawi.Bu amee jëkkar dakoy ame ci kàddug Yàlla, ak kollareem gu degër gi.Mu nekk dëkkandoo bi gën a ted ci kër jëkkëram,Te day war ci jëkkëram mu teral ko, tey rafetal jëme ci moom, te bañ koo lor.
Bu nekkee yaay ay àqam day lënkaloo ak àqi Yàlla -mu kawe mi- te dog ko ak ñaawal jëmale ci moom day lënkaloo ak bokkaale Yàlla ak yàq fi suuf.
Bu nekkee mbokk dañuy digal jullit bi mu koy jokk, ak diko teral, ak diko fiire,Bu dee yaay-tëx la day yor wccuwaayu yaay ci jëmale ci moom ag mbaax ak di ko jokk.
Bu dee maam la, wala muy am màggat ab dayoom day dolleeku ci ay doomam , ak ay sétam, ak mboolem ay jigeñaaleem; ba daanaka sax deesuko bañal benn cakkutéef, te deesul xeeb xalaatam.
Bu nekkee ku sori nit ki ci ag mbokk, jege wu ko it ci dëkk andoo kon it dina am àqi Lislaam yi matale ñépp, ci fegal ko lor ak damm ab gis ak yuni mel.
àq yii nag réewi jullit ñi deñuñu ci di ko sàmm dëgg-dëggi sàmm, moo waral jigéen am fa dayo ak wàccuwaay bob du ko ame ci beneen réew bu dul réewum jullit.
Jigéen it day am ci Lislaam àqi moomeel , ak luye, ak jaay, ak jënd, ak mbooleem jëflante yi, am na it àqi jàng ak jàngale, ak liggéey ci lépp lu wuutewul ak diineam.Daa am sax nag ci xam-xam yi loo xam ne faratay jëmm la ku ko bàyyi day am bàkkaar moo xam góor la wala muy jigéen.
Waaye sax lépp lu ñeel góor dakoy ñeel lu dul la mu jagoo walif góor ñi, wala li góor ñ jagoo i walif jigéen ñi ci ay àq,ak ay àttè yoy day méngoo ak kenn ku ne ci ñoom ni ki nu ko leerale ci ay barabam.
Sama diine damay digal it bëgg samay mbokk yu góor ak yu jigéen ak samay baay-tëx ak samay bàjjan ak samay nijaay ak samay yaay-tëx ak mbooleem samay jegeñaale, damay digal it may taxaw ci àqi samay soxna, ak samay doom ak samay dëkkandoo.
Sama diine damay digal wut xam-xam ak dima soññ ci lépp luy yëkkati sama xel ak sama jikko ak sama xalat.
Damay digal it am kersa, ak lewet, ak tabe, ak njàmbaarte, ak xereñ, ak sax ci dëgg, ak muñ, ak wóor, ak toroxlu, ak fegu, ak sell, ak matal kóllare, ak bëgg yiw ñeel mbooleem nit ñi, ak sàkku wërsëg, ak ñeewante way ñàkk yi, ak seeti aji feebar, ak di matal ab dig, ak wax ju teey, ak di daje ak nit ñi ci kanam gu bélli, ak xér ci bégal leen ci sama kem kàttan.
Ci li jàkkaarloo ag loolu damay watandikuloo reer, dima tere kéefar, ak weddi Yàlla, ak moy, ak ñaawtéef, ak njaalo, ak ngóor-jiéen, ak rëy, ak iñaan, ak mbañeel, ak ñaaw-ñort, ak gaafal, ak njàqare, ak fen, ak naagu, ak nay, ak tayyeel, ak buqat, ak bañ a liggéey, ak mer, ak gàtt xel, ak ñaawal jëme ci nit ñi, ak bari wax ju amul njariñ, ak wuññi sutura, ak wor, ak wuute ab dig, ak ñaawal jëme ci ñaari wayjur, ak dog ag bokk, ak doyadal ay doom, ak lor ay dëkkandoo ak mbindéef yi.
Lislaam damay tere -batay- naan luy màndale, ak jëfandikoo luy yóbb am xel, ak kaart xaalis, ak sàcc, ak wuruj, ak wor, ak tiital nit ñi, ak di leen luññutu, ak di topp seeni ayib.
Sama diine Lislaam nag day wattu allal yi, te ci loolu la jàmm ak kóolute di tasaaroo, lii moo tax muy soññee ci am kóllore, daal di kañ ay ñoñam, dig leen dund gu teey, ak dugg aljana fa allaaxira, mu araamal sàcc, daal tëkku ki koy def am mbugël ci àduna ak allaaxira.
Sama diine day wattu bakkan yi, loolu moo tax mu araamal faat bakkan ci lu dul dëgg, ak di tooñ ñeneen ñi ci bépp xeetu tooñ bu mu man a doon donte sax ci ay kàddu la.
Dafa araamal sax nit ki di lor boppam; du dagan ci nit ki muy yàq am xelam, wala muy faagaagal ag wéram, wala muy ray boppam.
Sama diine Lislaam day toggoo sàmm sañ-sañ yi, di ko tënk itam;Nit ki ci Lislaam day am sañ-sañ ci ay xalaatam, ak ci njaayam, ak jëndam, ak ci yaxantoom, ak ci demam ak dikkam, ku am sañ-sañ la it ci bànneexu ci yu teeyi dund gi ci lu ñuy lekk, wala lu ñuy naan, wala lu ñuy sol, wala lu ñuy dégg lu féeg deful lu araam loy dall ci kawam, wala muy lor keneen.
Sama diine day tënk sañ-sañ yi; du nangu kenn di jallgati ci keneen, te nit ki waruta wéy ci ay bànneexam ya araam yoy day màbb alalam, ak texeem, ak niteem.
Te boo gisee ñiy boyal sañ-sañ ci lépp, daal di koy jox lépp lu ñu xemmem ci ay bànneex walif pas-pasu diine wala xel mu leen di yedd, kon danga gis ne ñoom da ñuy dund ci wàccuwaayi texeedi ak ay xat-xat, te dangay gis sax ñenn ñi ñuy bëga; xaru ngir bëgg a mucc tiitaange yooyu.
Sama diine damay jàngal li gën a kawe ci teggini lekk ak naan, ak nelaw, ak jaxasoo ak nit ñi.
Sama diine damay jàngal ag jàppandi ci jaay ak jënd ak laaj samay àq.Damay jàngal it ag jàppandi ci jëflante ak ñi ma wuuteel ci diine; du ma leen tooñ, du ma ñaawal jëme ci ñoom, waaye damay rafetal jëme ci ñoom, maleen di yéene aw yiw.Te jaar-jaaru jullit ñi da leen di seedeel ni ñu yomb la ñu ci seen jëflante ak ñi ñu wuuteel ag yomb gog xameesuko ci benn xeet bu leen jiitu;Jullit ñi dundandoo na nu ak ay xeet yu wuute ay diine, ñu dugg ci kiliftéefug jullit ñi, jullit ñi nekk ak ñépp ci gën gaa rafet ab jëflante ci diggante nit ñi.Ci gàttal daal Lislaam xamal nama li gën a tuuti ci ay teggin, ak jëflante yu rafet yi, ak jikko yu tedd yoy sama dund dina ci selle, samag mbékte di ci mate,Tere nama itam lépp luy nëxal sama dund, ak lépp luy lor nekkinu mbooloomi, wala bakkan, wala xel wala alal, wala tedd-nga, wala der.Te ci kem ni may jàppe ci njàangale yooyu ci la sama samag texe di gën a màggeCi kem samag gàttañlu ci dara ci yooyu, ci la samag texe di wàññikoo kem lima gàttanlu ci ñàngale moomu,
Li weesu nag tekkiwul ne danu maa aar ci njuumte ba duma juum, wala du ma gàttañlu; sama diine day sàmmonte ak sama mbindiinu nite, ak samag néew dolè leeg-leeg, ba tax may juum, di gàttañlu, di sàggan; loolu moo tax mu tijjilma buntub tuub, ak jéggalu,, ak dellu ci Yàlla; ndax tuub day far jeexitalu samay gàttañlu, di yëkkati sama dayo fa sama Boroom.
Mboolem njàggalem diiney Lislaam ci ay pas-pas,ak ay jikko,ak i teggiin,aki jëflante,seen cosaan mooy Alxuraanu ju màgg ji,ak Sunna su sell si.
May wax ci mujj gi di aji-dogu ne:nit ku mu man a doon ci barab bu mu man a nekk ci Àdduna bi bu xolloon ci dëggi-dëggi diiney Lislaam xool bu maandu te mucc ci par-parloo du man lu dul nàngu ko,waaye musiba mi dëgg mooy woote yi dul dëgg tey lëntal diiney Lislaam, wala jëfi ñenn ñiy askanoo Lislaam te jëluñu koca dëgg-dëggam.
Bu nit ki xooloon ci dëgg-dëggi diiney Lislaam mooy lan, wala mu xool melokaanu ay ñoñam ñi koy jëfe ci dëgg-dëgg kon du deng-dengi ci nàngu ko te dugg ci,Te dina ko leer ne Lislaam day woote ci texeel nit ñi, ak tasaare jàmm ak kóolute, ak siiwal maadnu te ak rafetal.Jengug ñenn ñiy askanoo Lislaam nag - mu bari wala mu néew - du jaadu ci genn anam ñu koy limaale ci diine ji, walla ñu ko ciy ŋàññee, li am moooy moom dafa sett wicci ci loolu.Lay tukkee ci jeng googu nag day dellu ci way-jeng ya ca seen bopp; ndax Lislaam digaluleen loolu,waaye kay da leen koo tere xupp leen ci jeng won ginnaaw li mu indi.Ta mandute mooy ñu xool ci melokaanu ñiy taxawe diine dëgg, tey jëfe ndigalam ak i àtteem ci seen bopp ak ci ñeneen ñi, te loolu day feesal xol yi ci màggal diine ji weg ko moo ki ñoñam.Lislaam bàyyiwul benn jubbanti ak yéwenal bu mag wala bu ndaw lu dul soññe na ca, bàyyiwul itam benn ñaawtéef walal yàxute lu dul moytandikuloo na ko, daal di fatt ay yoonam.
Loolu moo tax ñiy màggal ay mbiram,tey taxaw ay ndigalam ñoo gën a texe ci nit ñi,ñooy nekk it ca gën gaa kawe ci ay teggiini bakkan,ak di ko yar ci gën gaa rafeti melokaan i jikko,ak teddngay jikko yi,loolu nag ku jege ak ku sori ak ku dëppoog ñoom ak ku wuute ak ñoom dina leen ko seedeel.
di xool rekk nag ci melokaanu jullit yu gàttañlu yi ci seen diine,te wuuteeg yoon wu jub wa,loolu du daray maandu te,loolu sax nag mooy dëgg-dëggi tooñ.
Lii nag ab woote la ñeel képp ku dul jullit ci mu xér ci xam Lislaam, te dugg ci.
Dara warul ci ki bëga dugg ci Lislaam lu dul mu seede ni amul buur bu yayoo jaamu ku dul Yàlla ak ni Muhammat ndawul Yàlla la.Te mu jàgg ci diine ji lu mu man a taxawe li Yàlla waral ci moom.Lu mu gën a yokk am njàngam ak jëfeem ag texeem di dooliku, darajaam di gën a kawe fa Boroomam.