Description
Ap tëŋkk bu am solo Ci taari lislaam Kiko binnd Cheikh Abdurahmane Ibn Naasir Saadi (1307 -1376 ci gaaddaygi) Kiko jeema firi Djibril Dièye
Kiko binnd
Cheikh Abdurahmane Ibn Naasir Saadi
(1307 -1376 ci gaaddaygi)
Kiko jeema firi
Djibril Dièye
Ci turu Yaalla laay dore sama mbinnd mi, moom miy borom yërmënde gu yaatuwi te di yërëm kuko soop.
Mboolem xeeti canntyi ñeelna Yaalla, ñi ngi koy sant diko dimmbandikoo diko jeggalu di tuup jëm ci moom di muslu ci moom ci sunu mbon-mnoni bakken ak suñuy jëf yu ñaaw. Kepp ku Yaalla ginndi kenn mënëtukaa reral, waye kepp kumu setaan cik maanduteep bamu reer kenn mënëtukaa jubal. Maa ngi sesde ne amul lenn luñu wara jaamu ci dëgg kumoy Yaalla, moom dongg deesukoo bookkaale. Di seede ne Muhammad jaamam la di ndawam, Yaalla na Yaalla julli ci moom te doolliko jaam.
Ginnaaw loolu:
Diine lislaam bi Yonent bi (Yaalla na Yaalla julli ci moom te doolliko jaam) mooy diine bi gëna mat ci diine yi te gën ci, gën ce kawe, gën ce maagg. Te bapare mu laamboo akiy taar akup mat ak mbaax ak yërmande ak mandute akup xarañ. Di seede Yaalla ak mat akup xamxam bu peeg akup xarañ yu amul fuñu yam. Di seedeel sunu Yonent ak yoneentaam ne lu tege ci dëggula, te mooy wu dêggu kiñu dëggal, ki dul waxe baaneex: "Lumu wax dañ kokoo wahyu." [1]
Konnak diine lislaam bookkna ci lay bu gëna maagg akup seede bu rëy buy wane weet gu Yaalla weet cik matam gu amul fumu yam; ak yonentuk Yonentebi (yaalla na Yaalla julli ci moom te dooliko jaamm) akup dëggoom.
Lima jublu ci mbind bii mooy fesël fi sama xamxam tooll ci leeral cosaani taari diine bu maagg bi di lislaam, doontene sama xamxam loottna beepp loott ci wane leenn ci li diine jii laamboo cik maaggaay akup taar akup mat andak ne sama samay kaaddu loottnañ ci farŋfaacceko cik matal wala diko yaatal; waye du leep luñu mënul peeg lune wala yegg ci njombaxtalgi wala lici ëpp, du jaadu nitki di baayyi limu ci xam ngit limuci xamul; ndax Yaalla tegul bakken ludul limu mën. Moo wax né:(Ragallen Yaalla keem seen mën mën).[2]
Lixaral loolu mooy ne xamxam bi neekk ci xam taari lislaam yi dafa laammboo akiy njariñ yu limu:
Leeral naci né bookk ci ngëneelu xamle al leeral taaru lislaam:
· Bookkna ci jëf yi gën yi nitki di jox waxtoom; mudi waxtu bulay jariñ te dula lor.
· Bookkna ci ne xam ak waxtaane xeewalu Yaalla yi daa bookk ci yimu digle moom akup Yonentaam. Te bookkna ci jëf yi gëna baax; te sikkisaakka amul ne gëstu ci lu jëm ci taari lislam dina jur nanggu ak waxtaane ak xalaat ci xeewëlu Yaalla bi gëna maagg ciy jaamam: te muy lislaam bi nga xamne du naanggu budul moom. Kone waxtaanee boobu ci boopptam xeetu sant Yaalla la ak saakkuk ndoolleent.
· Bookkna ci ne nit ñi da ñuy gënënte ci ngëm, nu nitki di gëna doolleekoo xamxam ci lislaam ak maaggalko ak begeeko mu ngëmëm di gëna dëgërër, mu gëna am koolute; ndax dafa neek diine bu laamboo mbooleem ciosaani ngëm akiy tëŋkkam.
· Bookkna ci yoon yi gëna gaaw ci woote jëme ci lislam ak leeral limi laammboo ciy mbaax yoo xamne bepp borom xel ak fitra bu mucc dakoy nanggu.
Su amoon ñu feetewoo faraŋfaacce dëgg dëggi lislaam ak di leeral nit ñi li ci neekk ci yu baax, loolu donŋgg doon na doy sëkk ci xertël ci nit; ndax li ci lislaam ci luy baaxal adduna ak allaaxira ak biir bitti ci ludul ñuy soxla toonntu ay lënnt yi ñukoy taxxal wa di jam diine ñi juuyoo ak moom.
Ndak diine lislaam ci booppam dafa laamboo toontu beepp lënnt bu juuyoo ak moom; liko waral mooyne dëgg la bu aandak ap leeral bu bir akiy firnde yuy joxe koolute.
Te suñu wuññee kiiraay gi ci leenn ci dëggëntaani lislaam dina nek liy gëna waral ñu naanguko ak feete gumuy feete kaw ludul moom.
Taari lislaam nak day feeñ ci mboleseeni njaŋŋalem aki tektalam ak ciy cosaanam aki baŋxaasam, ci limiy tektale ci xamxamuk yonal akiy aatte, ci xamxam gu maacc ci mbindef yi ak neekkin bi. Waye nak jubluwuñu faraŋfaacceko ak diko toopp benn par been ndax dafay waralup guddal. Konnak liñu jutbu ci mbinndi mi mooy joxe ay misaal yu am njariñ; yoo xamne dafay tektale yeneen ak di ubbil bunnt ki ci bëgga yaatal.
Suko defe ñuy dimmbandikoo Yaalla, di yaakaar ci mooy mu ginndi ñu te xamal ñu ak mu ubbil ñu ci mangasinu tabeem yi ak terangaam yi luy tax sunuy mbir yewën te sunuy wax ak sunuy jêf dici jube:
Diine lislaam, diine la bu tabaxu ci saxal mbooleem reeni ngëm yi Yaalla mu kawemi tudd ci waxam jimne: "Waxleen ne gëmnañu Yaalla ak limu waacce ci ñun, ak limu waacce ci Yonent Yaalla Ibrahim ak Ismail, ak ishaaq, ak Yaaquub aki sëtëm ak li Yaalla jux Musaa ak Issa ak li yonent yi jële ci sen boroom. Duñu taaxxale digënte ñeenn ci ñoom; te moom lañu jeebbalul".[3]
Te ciosaan yu maagg yooyu Yaalla digal ay jaamam mooy li Yonent yi dëppoo te mu laammboo ay xamxam yu maagg aki passpass yu jëm ci gëm leepp lu Yaalla mellal boopap ci laamiñi Yonentaam yi ak goorgoorlu ci soobu yoonu ngërëmëm.
Diine joo xamne ciosaanam mooy gëm Yaalla, meññentam di soobu yoonu limu te gërëmko boolekook sellal; ndax dina am kuy jaapp ne amna buko gënwaagg wala gënkoo rafet?
Diine joo xamne dafa digle gëm liñu jox Yonentyi, ak dëgêl senuk Yonent, ak naŋgu dëgg giñu jële ci sen boroom, ak baña texxale kenn ci ñoom, ak ne ñoom ñëpp ñu dëggulañu, ak ne ñuñu woolu lañu te ay sellalkat lañu, du mëna nekk mukk diine muñu mëna jam.
Diine la joo xamne dafay digle leepp luy dëgg, di nanggu lepp luy dëggu, di saxal lepp lu aju ci diine te am cëslaay wahyu bu Yaalla di wahyu Yonentaamyi te mu nekk lu juuyoowul ak xel ak fitra ba pare du bañ dëgg bumu mënti doon. Konnak moo feete kaw mboolesen diine yi.
Dafay digle jëf yu radet yi, ak jikko yu teddyi, ay luy yewenël nekkinu jaam yi, di xirtël ci mandu ak ngëneel ak yërmende ak lu baax, di xuppe waliis tooñ ak jalgati akiy jikko yu ñaaw. Amul benn jikko buy tektaleep mat te Yonent yi saxal ko ludulne saxalnako, amul benn mbir buy baaxal diine wala adduna te yoonal yu jiituyi waoote jëmeci ludulne sooññenaci, wala ap yaxx ludulne terenako te digle ñu sori ko.
Cip tëŋkk: Passpassup diine lislaam daal mooy biy sellal xolyi, di yewenal ru yi; jikko yu baaxyi ak jëf yu rafet yi dici saxe.
Yoonal yi gëna maagg yi lislaam yoonal ginnaaw ngëm mooy: taxawal julli, jooxe asaka, woor weeru koor, ajji maakka.
Ku leen seettantal bu baax dina gis lici nekk ci aay ndariñ yu kawe ay limiy waral ci sakku ngërmande Yalla ak am payooram ci adduna ak allaaxira.
Seetlul lici julli cik seellal, ak dëgmël gu mat sëkk, ak tagg, ak ñaan, ak toroxlul. Te palasam ci garabuk ngëm dafay toollook waaccuwaayu saytu tool ak diko roose. Sudul woonak baamu giñum baamu jullli gi juroomi yoon ci besbi kon garabuk ngëm gi dina mujje wow, bapare ay baŋxaasam dina fënëx. Waye julli mookoy suuxat diko dunndal.
Nga xool itam li ci julli ci yittewoo tudd Yaalla nga xamne moo gëna maagg, ak ne julli dafay dox diggantem ak kikoy def ba du taabbi ci lu bon ak lu ñaaw.
Nga ñëw ci asaka ci ay jikko jikku yu baax ñi, cik yaatu ak tabe, ak sori jikko ñu sikk ñi, ak sante Yaalla ciy xewalam, ak wattu alalji ci leepp lukoy nëxël, ak lici nek cik def njekk ci mbinddeefyi ak jookk ñi ñaakk, ak fac aajooy borom soxlayi.
Niki noonu asaka laambboona ak feg ñi ñaakk ci loru, dinañko dimmbandikoo ci xare ak yi nga xamne manul ñaakk ci yewenal nekkinu jullit yi, akitam ne dinalen fegal ñaakk ak ñi ñaakk, ak amup koolute ci kuutëluk Yaalla, ak yaakaarup payooram, ak dëgël limu dige.
Bude koor moom taagatu bu am solo moo ci neekk, ci yar bakken bi ci mëna baayyi lumu bëggoon te taammko ak taaggatko ci muñ ak dogu bu dëgër; lool lepp tege ci bëgg Yaalla ak toopp ko.
Laamboona itam dooleel liy tax bakenbi di seellal ak jiital li Yaalla bëgg ginaleko ci limu bëgg. Moo tax koor neekk ngir Yaalla ba tax mu jagooko walis yeneen xeti jaamu Yaalla yi.
Ku baayyi xel ci ajj dina seetlu alal gi ci nit di def, ak dekku ay cioono ak, leepp ngir saakku ngërmëde Yaalla ak teer ci palaas yu teedd yi ak toraxlu ci kaaba gi nga xamne kërëm la, ak jagleelko ay xeeti jaamu yu wute ci palace berëp yooyu, ak nga xamne ay ndabi xeewël la yumu defal ay jaamam ak delegasiyon *** yuko dikkal.
Boolekook lici neekk ci maaggal Yaalla ak toroxlulko toroxlu gu mat sëkk, ak di faattaliku nekkinu Yonent yi, ak taanneef yi, ak seellalkat yi; loolu diluy dëgërël ngëm ak di yookk sunu mbäggeel ci ñoom.
Ak lici asaka ci xamante diggante jullit yi, ak beennale seeni kaaddu, boolekook ni seeni njariñ yudul jeex di ci dëppoo; loolu bookk na ci taari lislaam yi gëna maagg ak njariñ yi gëna kawe yu jullit yi di faaggu.
Lii nak ap xippi bët la cip tëŋkk.
Bookkna ci taari lislam yi, mooy digle gu Yaalla digle ak sooññee gumu sooññee cik beennoo ak dëppoo, waye tamit tere gumu tere ak xuppee gumu xuppee ci taaxaliko ak wute.
Ay laaya akiy adis yu limu yaxal nañu loolu.
Te kepp ku amuk seetelu dina yeg njariñ gu neekk ci lii. Ak liciy juddu ci njariñal aadduna ak allaaxira akup mucc ci lor ak yu bon.
Te itam kaattan ak dooley biir bu tege ci dëgg lii mooy cosaan boo xamne ci lay wër.
Niki noonu, xam nañu ne ni jullit yi neekkeewoon ci njëlbeenuk lislaam ci diine gu jup ak neekkin gu baax, ak kaattan keneen kudul ñoom yeegguciwoon; ndax dañoo tënkkuwoon ci cosaan googu andak taxaw ci dëgg dëggi taxaw boolekook koolute gu dog ne mooy ruuk seen diine.
Te liy gëna leeral loolu mooy:
Diine lislaam, diineep yërmënde la ak barke ak rafetal akup sooññe ci jariñ nitñi.
Li ci diine lislaam cik yërmënde ak jëflante gu rafet ak woote jême cik rafetal ak tere leepp lu wute ak loolu, def nako mu doonup leer gune raaŋjang ci diggante tooñ ak jalgati ak jëflante gu ñaaw ak xoottik worma.
Mooy diine bi xëcc ci moom xolu ñuko gënoona noonoo; ba ñu mujjee kerlu ci keeppaaram gu yaatu gi.
Mooy diine bi ñeewant te leet ci ñici askanoo ba yërmënde ak njeggël ak njeekk di ballee ci seeni xol badi jeexital ci seeni wax ak seeni jëf; ba jeeggileen jaall ci seeni noon ba ñu mujje neek seeni peete: ndax amna ci ñoom (seeni noon) ñoo xamne ñu taabi ci lislaam teg ko cip gissgiss bu leer ak yeg yeg gu dok; amna itam ñu taabbi ci lislaam cik nanggu ak xeemmeem ay aatteem ak gën gimu gën aatteey seen diine ndax limu laambbo cik maandu ak yërmënde.
Diine lislaam, diineep xarañ la, ak cosaan gi Yaalla binndee nit, diine bu xel nanggu, ak mbaax ak texe.
Li koy gëna firndeel mooy: li lislaam laamboo ci cosaani atteem ak seeni baŋxaas yi nga xamne cosaan gi Yaalla binndee nit ak xel bu mucc dakoo nanggu booleko ak woommatu gu tege ci nattuwaayup dëppoo dëgg, ak li lislaam laambbo ci ap xarañ ci tërëlin.
Ak cip nosee, ba nooppi neekk lu yewën ci beep jamono ak palas. Ay xibaaram leepp dëgg la te dëggu, te beneen xamxam ci li jiitu wala li mujj mënul innddi lukoy feecci wala diko weeddi. Waye li am kay mooy ne yeneen xamxam yi tege ci dëgg dañu koy feeddali aka dëgërël ; mu neekk kon lay wu dok cip dëggoom.
Ñi maandu tey werlu seen xamxam wanenañu ne beepp xamxamu diine wala aadduna wala politik bu am njariñ, Alxuraan tektale nako tektale gu amul beenn sikksaakka.
Lii leepp di dooli jullit bi ngëm.
Ku seetlu ni lislaam tëre mbiru xare ci yoonu Yaalla, dina giss ne limu ci jublu mooy aar lislaam ak jullit yi ci jalgatip noon yi ci ay axxam ay woote bimuy woote jëme ci mbaax.
Wuteek beep jubluwaayup: xër cip moomeel wala dabiy baanneex; waye dafay dugg ci lumunul ñaakk.
Doynaci firnde ci lii, mooy dunnduk Yonentbi (Yaalla na Yaalla julli ci moom te dooliko jaamm) akiy saabaam ak seeni noon.
Batay itam, digle lu baax tere lu bon ci liy taxawu diineji la book ak diko saam.
Bookna ci taari lislaam, mooy lu jëm ci jëflante ci njëdd ak njaay ak leble ak bookk ligeey ak leble.
Toomb la boo xamne lislaam baayiwuko ginnaaw ndaxi njariñam yu kawé ci baaxal mbiru jullit yi ak seenup neekkin ci kaw suuf.
Tekna ci ak aatte yu xarañ, te tere ci leepp luy inndi lor ci jëflante lu melni ribaa ak jalgati.
Bookkna ci li gëna fees ci taari lislaam, mooy daganal gumu daganal leepp lu teey te laap ci leek ak naan ak sol ak sëy.
Mulaambboo leep lu jëm ci baanneex bu dagan te teey.
Bookna ci taar yi batay, mooy saam bi Yaalla saam mbooleem ax yi ci diggante mbinndeef yi ak mbooleem yiw ak rafetal ak maandu ak sori tooñ.
Lu melni axiy waajur, ak doom, ak way jegeñaaleyi, ak dëkkandoo yi, ak andandoo yi, ak ñiñu bookkak ligeey, ak diggante waay deeñanteyi.
Mudi lu xel naanggu te bëgg ko ak di dox jëm ci.
Mooy ni lislaam tërëlé leep lu jëm ci ndono.
Mu tek ay nattukaay yu matale te maandu ci niñu wara seeddale ak ñi wara doonn.
Mooy li lislaam tërêl ci ay daan ak xeetale gumuko xeetale keem dayook jalgatigi.
Leep jëm ci saam aaxi nit ñi ba ñu baña tooñ keenn wala ñuy jalgati ci alalam wala bakkenam wala deram wala njabootam.
Bookna ci taari lislam yi mooy: dox diggante nit ki loott ci saytu alalam ak jëfëdikooko ci melokaan wu baax ngir mu baña loru wala loree.
Niki dof wala xale bu matagul saytu ay mbiram.
Mooy firnde yimu yoonalal boroom aax yi ngir ñuy jot ci aaxam ci jamonoom bi jaadu, ak mucc ci sikkisaakka.
Mu bookk cik maandute gu fes.
Mooy li lislaam sooññee ci rafetal jëmee ci mbiddeef yi; mu bookk ci liy jural jullitbi yool ak njeekk ci nitñi.
Mudi luy inndi naataaŋge ci jullit yi ak barke.
Ay tënkk yimu yoonal ngir aatte beep xulo, wa wutal geennukaay mbir yiy xew ci diggante nitñi, wala jox dëgg keenn ci ñar ñiy wootewoo mbir. Mudi ay tënkk yu tege ci maadute akiy firnde.
Mooy digle bi lislaam digle diisoo ak tagg gumu taagg ñi gëm ci sababuk seen mbooleem mbir yi dafa rege ci diisoo
Mudi lu mbooleem boroom xel yi nanggu.
Mooy ne lislaam dafa dikk ngir yewenal leepp lu jëm ci diine ak aadduna ak boole diggante luy baaxal ruu ak bakken.
Muy ap digdoomu diggante aadduna ak allaaxira.
Mooy li lislaam def ne xamxam ak diine ak kilifteef ak aatte ñuy ay mbir yuy dëgërëlante di moottalante. Mootax mu joxko yitte bu fes.
Diine lislaam laammboowul dara luy juuyoo ak xel bu mucc ayyib wala xamxam bu wer.
Mu book ci mbir yi gëna rëy yuy wane xarañup boroombi ay peeg gimu peeg leepp lumu bindd.
Bookna ci taari lislaam yi mooy, doole gimu am ci beenale ay xol yu feewaloo ak far noonoo ci diggante niteñi.
Aandak pexe yu bari te wuute yuko noon yi de fexeel, suba ak ngoon, guddi ak bëccak; ak seen kaattan yu ñi ciy def.
Waye loolu terewul lislaam di desfi baleegi.
Muy wane ne lislaam dafa amup kaattan gune ci biiram boo xamne mooy ubbi xolyi ci ludul muy aajowoo jasi saasune.
Moo tëŋkk mbooleem li jiitu ci ay toomb, te mooy: diine lislaam diine la bu taxaw ci:
ü Ay passpass yu wer te am njariñ;
ü Ay jikko yu teedd tey foot ruu ak bakken;
ü Ay jëf yuy yewenal neekkin;
ü Ay firnde ci leepp;
ü Sori leepp luy jaamu ludul Yaalla ak aju ci mbinddeef;
ü Seellalal Yaalla jaamu gi;
ü Sori leep luy xarga fuufa;
ü Leepp luy mbaax;
ü Bañ ak sori leepp luy yaxute;
ü Maandu ak sori tooñ ak xeet bumu mëna doon;
ü Sooññe ci faaggu leep luy yekkati nit jëm ci mat.
Lip ap tëŋkk rek la, waye jubluwuñuci peeg.