Description
Ab tënk bu am solo ñeel jullit bi
Yénèni tékki 14
Topics
Aji-Waajal ji:
Muhammat Assahriyu:
2021-1443
Jamono ji ñu ko mujja bind: 04 / 05 / 1443
Maa ngi tàmbalee samay wax ak samay jёf ci turu Yàlla miy Boroom yёrmànde ju yaatu ji ci àdduna tey jagleell yёrmaandeem ёllëk way-gёm yi.
Sant ñeel na Yàlla mi nga xam ne mooy Boroom mbindéef yi, xéewël ak jàmm yal na nekk ci ki gën a tedd ci yonnent yi ak ñi ñu yónni, muy sunu Yonnent Muhammat ak ay ñoñam, ak àndandoom yépp,
Ginnaaw loolu:
Bokk na ci xéewël i Yàlla mu kawe mi ci nit ki, mu xéewële ko mu nekk jullit te sax ci Lislaam ak jëfe ay àtteem ak li mu yoonal.Ci téere bii la jullit di jànge ay cosaan i diineem yoy dina ci jube, ci anam gu tënku, te di ko leeralal mandargay diine ju màgg ji, ngir mu gën a xam Boroomam bu màgg bi, ak diineem jii di Lislaam, ak ub Yonnenteem Muhammat yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, ngir mu man a jaamu Yàlla ci kaw xam bu leer.
Yàlla mu kawe mi moo nu bind ngir jubluwaay bu màgg, te mooy jaamu ko moom dong, moom mi amul nawle, niki mu ko waxe ne:﴿ وَمَا خَلَقْتُ الْجِنَّ وَالْإِنْسَ إِلَّا لِيَعْبُدُونِ﴾ ﴾Binduma jinne ak nit lu dul ngir ñu jaamu ma﴿[ Saaru As-Saariyaat: 56]Li ñu ci namm mooy: ñu wéetal ko ci jaamu gi moom dong moom mi amul nawle.Jubluwaay bu màgg bii ci la sunu jëf yépp ak sunuy yéene aju ci àdduna, sunu Boroom nee na:﴿ أَفَحَسِبْتُمْ أَنَّمَا خَلَقْنَاكُمْ عَبَثًا وَأَنَّكُمْ إِلَيْنَا لا تُرْجَعُونَ * {Ndax dangeen a njortu ne danu leen a bind ngir am po, te dungeen dellu si fi nun,فَتَعَالَى اللَّهُ الْمَلِكُ الْحَقُّ لا إِلَهَ إِلا هُوَ رَبُّ الْعَرْشِ الْكَرِيمِ﴾ Yàlla de kawe na tooy Buur bu màgg bi amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul moom mooy boroom Aras ju tedd ji}[ Saaru Al-Muuminuuna: 115-116].
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ يَا أَيُّهَا النَّاسُ اعْبُدُوا رَبَّكُمُ الَّذِي خَلَقَكُمْ وَالَّذِينَ مِنْ قَبْلِكُمْ لَعَلَّكُمْ تَتَّقُونَ﴾ {Yéen nit ñi jaamuleen séen Boroom mi leen bind, bind it ña leen jiitu woon ngir ngeen ragal ko}.[ Saaru Al-Baqara: 21].
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ هُوَ اللَّهُ الَّذِي لَا إِلَهَ إِلَّا هُوَ﴾ {Moom mooy Yàlla mi nga xam ne amul buur bu ñuy jaamu cig dëgg ku dul moom}[ Saaru Al-Hasr: 22].
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ لَيْسَ كَمِثْلِهِ شَيْءٌ وَهُوَ السَّمِيعُ الْبَصِير﴾ {Moom niroowul ak dara te moom Aji-Dégg la Aji-Gis la}[ Saaru As-Suuraa: 11]
Yàlla mooy sama Boroom di Boroom lépp mooy Aji-Moom ji di Aji-Bind ji di Aji-Wërsëgale tey Aji-Doxal bir yépp.
Moom dong a yayoo jaamu amul benn buur bu dul moom amul ku yayoo jaamu ku dul moom.
Amna ay tur ak i melo yu rafet yu mu saxalal boppam walla ab Yonnenteem saxalal ko ko te mu yegg fa rafet ak mat yam, niróowul ak dara mooy Aji-Dégg di Aji-Gis.
Aji-Wёrsëgal ji, Aji-Yërëme ji, di Aji-Am-Kàttan ji, Aji-Moom ji, Aji-Dégg ji, di Jàmm, di Aji-Gis ji, di Wéeru-Waay ji, di Aji-Bind ji, di Aji-Ñeewante ji, di Aji-Doy ji, di Aji-Jéggale ji.
Aji-Wёrsëgal ji: mooy ki warlu wërsagi jaam yiy dundal séen xol ak séen yaram.
Aji-Yërëme ji: mooy Boroom yërmaande ju yaatu ju màgg ji nga xam ne daj na lépp.
Aji-Am-Kàttan ji: mooy Boroom kàttan gu màgg ji nga xam ne lott walla tayyeel du ko gaar.
Aji-Moom ji: mooy ki melowoo melokaan yu màgg yi, tey ki not tey doxal, te moom bir yépp te di ca soppaxndiku.
Aji-Dégg ji: mooy kiy dégg mbooleem kàddu yi, yu suufe yi ak yu kawe yi, mooy dégg it ñaanug ay jaamam, ak séenug toroxlu.
Kiy Jàmm: mooy ki mucc ci bépp wàññeeku ak bépp gàkk-gàkk ak bépp ayib.
Aji-Gis ji: mooy kiy gis lépp lu mu man a doon ak nu mu man a toll, di gis bir yi, te deñ kumba ci lépp lu nëbbu.
Ki ñuy wéeru: mooy ki warlu wërsëg i mbindéef yi, di taxawe séen i njariñ, mooy ki méngoo jaamam yu baax yi, di leen yombalal séen i bir.
Aji-Bind ji: mooy ki amal bir yi, mooy ki ko fent ci lu dul misaal mu jiitu.
Aji-Ñeewant ji: mooy kiy teral ay jaamam, di leen yërëm, di leen may li ñu koy ñaan.
Aji-Doy ji: mooy ki doy ay jaamam ci lépp lu ñu soxla, moom lañu doyloo ay ndimbalam wolif keneen, moom lees doyloo it wolif leneen.
Aji-Jéggale ji: mooy ki fegal ay jaamam ayu séen i bàkkaar, te du leen ca mbugal.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ لَقَدْ جَاءَكُمْ رَسُولٌ مِنْ أَنْفُسِكُمْ عَزِيزٌ عَلَيْهِ مَا عَنِتُّمْ حَرِيصٌ عَلَيْكُمْ بِالْمُؤْمِنِينَ رَءُوفٌ رَحِيمٌ﴾ {Ndawal yàlla bu book ci yéen dikkal na leen muy ku leen ñeewant ci séen i coona te muy ku xér ci séen ngëm te am yërmaande ci yéen}[ Saaru At-Tawba: 128]
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ وَمَا أَرْسَلْنَاكَ إِلا رَحْمَةً لِلْعَالَمِينَ﴾ ﴾ yónniwunu la lu dul ngir nga nekk yёrmaande ci mbooleem mbindéef yi ﴿[ Saaru Al-Anbiyaa: 107]
Mooy Muhammat doomu Abdullaa doomu Abdul Muttalib doomu Haasim, te Haasim ci Xurays la bokk, Xurays bokk ci ngiiru Araab yi.
Yaayam mooy Aaminatu doomu Wahbin, ku ni wax Aliimatu Sahdiya moo ko nàmpal, takk na lu toll ci fukk i soxna ak benn, bi muy faatu mi ngi bàyyi gannawam juróom ñent ci ñoom.
Yonnent bi amoon na juróom ñaari doom ñatt yu góor ak ñent yu jigéen, ñu góor ñi ñooy: Xaasim, Abdullaa, ak Ibraahiima, jigéen ñi ñooy: Saynabu, Roqayya, Ummu Kulsuum, ak Faatima.
War na ñu koo topp ci lépp lu mu digle, dëggal ko yit ci lépp lu mu xibaar, te wattandiku lépp lu mu tere, te bañ a jaamoo yàlla ci lu dul lu mu yoonal.
Li ko yàlla yónni mooy li mu yónni woon mbooleem Yonnent yi ko jiitu woon, te mooy woote ci jaamu Yàlla dong bañ koo bokkaale ak dara, Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ وَمَا أَرْسَلْنَا مِنْ قَبْلِكَ مِنْ رَسُولٍ إِلَّا نُوحِي إِلَيْهِ أَنَّهُ لَا إِلَهَ إِلَّا أَنَا فَاعْبُدُونِ﴾ ﴾Yónni wu nu Yonnent yi la jiitu woon lu dul ne xamal nanu leen ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul man kon jaamuleen ma﴿[ Saaru Al-Anbiyaa: 25]
Te mooy ki mujj ci yonnent yi amul beneen yonnent buy ñëw ginnawam, niki ni ko Yàlla mu sell mi waxe ne:﴿ مَا كَانَ مُحَمَّدٌ أَبَا أَحَدٍ مِنْ رِجَالِكُمْ وَلَكِنْ رَسُولَ اللَّهِ وَخَاتَمَ النَّبِيِّينَ وَكَانَ اللَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمًا﴾ ﴾Muhammat nekkul baayu kenn ci yéen waaye yonnenteb Yàlla la tey ki mujj ci yonnent yi, te Yàlla xam na lépp ﴿[ Saaru Al-Ahsaab: 40].
Yálla mu kawe mi moo ko yónni ngir mu jottali Lislaam ci nit ñépp, niki ni mu ko waxe moom Yàlla tudd naa sellam ngi:﴿ وَمَا أَرْسَلْنَاكَ إِلَّا كَافَّةً لِلنَّاسِ بَشِيرًا وَنَذِيرًا وَلَكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ﴾ ﴾ Yónniwunu la lu dul ngir nga jottali diineem ji ci mbooleem nit ñi, nga di leen bégal ci lu baax ak di leen xupp ci def lu ñaaw waaye ñi ëpp ci nit ñi xamuñu ﴿.[ Saaru Saba-i: 28]
Moom nag am na ay yelleef yu mágg ci bépp jullit, bokk na ci yooyu:
1- gëm ag yónnenteem, ak ug dëggoom, ak muccug li mu indi ci sariiya ju mágg ji, ak topp ko ci yoon woowu, Yálla mu kawe nee na:﴿ وَمَا يَنْطِقُ عَنِ الْهَوَى * ﴾ Moom du wax ci bakkanam*إِنْ هُوَ إِلَّا وَحْيٌ يُوحَى﴾ lu mu wax ci Yàlla la juge﴿[ Sarru An-Najm: 3-4].
2- War koo bëgg, ak jiital ko ci sa bopp, ak say doom, ak mboolem mbindéef yi, li mbëggéel gii di waral mooy dëppoog Yonnent bi -yal na ko Yálla dolli xéewël ak mucc- ci ag njubam, topp ko ci lu mu digle, moytu li mu tere te xuppe ci.
3- War koo wormaal, ak dimbali ko, ak màggal ko -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dimbali ko ak màggal ko ak yёkkati ko -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-.
4- Julli ci moom: ak tagg ko, ak ñaan Yàlla mu yёkkati turam, te dolli ko ag màgg ak tedd-nga, moom wax na ne:( Ku julli ci man benn julli Yàlla dina julli ci moom fukki yoon )Muslim moo ko nettali.
5- Tere di ëppal ci moom -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ak di ko yëkkati fu weesu wáccuwaay bi ko Yàlla jox, Yonnet bi -yal na ko Yálla dolli xéewël ak mucc- tere na tere gu tar ku koy yëkkati, mu wax ne:( Buleen ma jay ni Nasraan yi jaye Iisaa doomu Maryama, man jaamub Yàlla kepp laa, waxleen jaamub Yálla ak ndawam bi) Al-Buxaarii moo ko nettali.
Dëggu, yёrmaande, lewet, muñ, njámbaar, baax, rafet jikko, maandu, toroxlu, jéggale.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ يا أيها الناس قد جاءكم برهان من ربكم وأنزلنا إليكم نورًا مبيناً﴾ ﴾ Yéen nit ñi aw lay wu jóge ci séen Boroom ñëwalna leen te wácce nanu ci yéen leer gu bér ﴿.[ Saaru An-Nisaa-i: 174].
Alxuraan ju tedd ji mooy waxu Yàlla mu kawe mi nga xam ne moo ko wax ca dëgg dëgg, te moo ko wàcce ci ab yonnenteem Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ngir mu génne nit ñi ci lëndamug réer yóbb leen ci leerug njub, gindi leen teg leen ci yoon wu jub.Ku ko jàng dina am yool bu mágg, ku ko jëfe mu teg ko ca yoon wu jub wa.Jële nañu ci Abdu Laahi Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla gërëm mu ne: Yonnent yálla bi -yal na ko yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na:(Ku jáng benn araf ci téere Yàlla bi dina am benn tiyaaba, benn tiyaaba bu ne day tolloo ak fukk i tiyaaba, waxuma nag [ alif laam miim ] aw araf la waaye alif araf la laam araf la miim araf la)At-Tirmisii moo ko nettali.
Alxuraan Yàlla mu kawe mi moo ko wattu ci soppeeku, moo ko def muy keemtaan guy sax ba bis pénc,Yàlla Mu sell mi nee na:﴿ إِنَّا نَحْنُ نَزَّلْنَا الذِّكْرَ وَإِنَّا لَهُ لَحَافِظُونَ﴾ ﴾Nun Yàlla noo wàcce Alxuraan te noo koy sàmm﴿[ Saaru Al-Hijri: 9].Képp ku woote ne Alxuraan daa matul walla dañu koo soppi weddi na Yálla ak ub yonnenteem -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- te génn na ci Lislaam.
Alxuraanul kariim dafa làmboo mbooleem la téere yu njëkk ya làmboo woon, dolli ca it ay càkkuteefi Yàlla ak jikko yi, mu dëggal la ca nekk ci dëgg, te amul benn téere bu jòge ci Yàlla ñu war koo topp ci jamono jii, walla di ko màggal, ak di ko jaamoo Yàlla, baa di ko jëfe, bu dul Alxuraan ju tedd ji.
Tolluwaayu diine ñatt la: mooy jёbalu ci Yalla, ak gëm Yàlla, ak rafetal.
Jébbalu mooy: jox sa bopp Yàlla cig wéetal, wommatul ko cig topp, deñ ci bokkaale ak i ñoñam
Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na:( Tabax nañu Lislaam ci juròoomi ponk: seede ne amul benn buur bu ñuy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, Muhammat ndawu Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak woor weeru koor, ak aj Màkka ).Buxaarii ak Muslim dёppoo nañu ci.
Ponki Lislaam yi ay jaamu Yàlla la yu war bépp jullit, Lislaamu nit ki du wér lu dul ne daa fas warug ponk yii, te di ko jëfe, ndax ci lañu tabax Lislaam, moo tax ñu tudde ko ponki Lislaam.
Ponk yooyu nag mooy yii:
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ فَاعْلَمْ أَنَّهُ لَا إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ﴾ ﴾ Xamal ne amul buur bu ñuy jaamu cig dëgg bu dul Yàlla ﴿.[ Saaru Muhammat: 19].
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ لَقَدْ جَاءكُمْ رَسُولٌ مِّنْ أَنفُسِكُمْ عَزِيزٌ عَلَيْهِ مَا عَنِتُّمْ حَرِيصٌ عَلَيْكُم بِالْمُؤْمِنِينَ رَؤُوفٌ رَّحِيمٌ﴾ ﴾ Yonnent bu bokk ci yéen ñëwal na leen di ku bañ lu leen di sonal, di ku xér ci yéen, di ku bari yërmaande ci jullit ñi﴿[ Saaru At-Tawba: 128]
Li ñu jublu ci seede ne amul benn buur bu ñuy jaamu ku dul Yàlla, mooy amul lenn lu yayoo jaamu ci dëgg ku dul Yàlla.
Li nu jublu ci seede ne Muhammat ndawu Yàlla la, mooy topp ko ci la mu digle, dëggal ko ca la mu xibaare, moytu la mu tere te tënku ca, te bañ a jaamu Yàlla ci lu dul li mu yoonal.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ﴾ ﴾ Taxawalleen julli ﴿[ Saaru Al-Baqara: 110].
Taxawal julli nag mooy defe ko ca anam gi ko Yàlla mu kawe mi diglee, te Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- jàngale nu ko noona.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ وَآتُوا الزَّكَاةَ﴾ ﴾ joxeleen asaka ﴿.[ Saaru Al-Baqara: 110].
Yàlla mu kawe mi moo farataal asaka ngir nattu ngëmug jullit bi, ak ngir mu sant ko ci li mu ko xéewëlal ci alal, ak it dimbali way-ñakk ñi ak way-aajewoo yi.
Joxe asaka nag mooy jox ko ñi ko yelloo.
Moom nag yelleef lu war la ci alal bu matee lim ba mu war a toll, juróom ñatti xeet nag lees koy jox, ñooy ñi Alxuraan tudd, bokk na ci ñoom: way-ñakk yi, ak Miskiin yi.
Joxe asaka nag, melokaanu yërmaande la, ak ug ñeewant, day laabal it jikkoy jullit bi ak alalam, di gërëm loo way-ñàkk yi, ak Miskiin yi, tey dëgëral buumu bëggante ak mbokkoo ci diggante mbooloom jullit ñi, looloo tax jullit bu baax da koy génne ànd ci ak teeyug bakkan, am mbégte ci joxe ko, ndax li ca nekk ci teral nit ñi.
Lim bi ñu war a génne ci asakay alal nag, mooy: 2.5% ci alal ju ñu denc, ci wurus ak xaalis, ak këyit, ak li ñuy jaay ngir tonewu, bu matee lim bi ñu war a génne, te mat um at.
Noonu it la asaka ware ci ki yor ab lim bu mat asaka ci ay jur, budee dunde gàncax lu ëpp ci at mi ci lu dul boroomam di ko xont.
Naka noonu asaka day war ci luy génne ci suuf, lu mel ni Rikaas, te mooy: la ceddu ya daa suul, naka noonu it dugub ak gàncax yi, ak mbell yi, bu matee dayo biñ war a génnee asaka.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُتِبَ عَلَيْكُمُ الصِّيَامُ كَمَا كُتِبَ عَلَى الَّذِينَ مِنْ قَبْلِكُمْ لَعَلَّكُمْ تَتَّقُونَ﴾ ﴾ Yéen way-gëm yi, farataal nanu ci yéen woor, niki nu ko farataale woon ca ña leen jiitu woon ngir ngéen ragal Yàlla﴿.[ Saaru Al-Baqara: 110].
Ramadaan: mooy weeru juróom ñenteel ci at mi, ci nattuwaayu atum gàddaay gi, moom nag weer wu màgg la ci jullit ñi, lu am wàccuwaay la ci mbooleem weer yi, woor ko ba mu mat sëkk benn la ci ponki Lislaam yiy juróom.
Woor weeru koor nag: ag jaamu Yàlla la, ci bàyyi lekk ak naan, ak sëy, ak mbooleem luy dog koor, bu fajar gi fenkee ba jant bi di so, ci mbooleem fani weeru koor wu barkeel wi.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ وَلِلَّهِ عَلَى النَّاسِ حِجُّ الْبَيْتِ مَنِ اسْتَطَاعَ إِلَيْهِ سَبِيلًا﴾ ﴾ Yàlla waral na ci nit ñi aj Màkka ci ku ko man ﴿[Saaru Aali-Himraan: 97]
Aj Màkka nag day war ci ku ko man benn yoon cig dundam, moom nag mooy: jublu Kaaba ga, ak barab yu sell ya nekk Màkka, ngir def ay jaamu yu ñu xam, ci jamono yu ñu xam, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- aj na moog yonnent ya ko jiitu woon, Yàlla digal na Ibaahima -yal na ko Yàlla musël- mu woo nit ñi ngir ñu aji, niki ni ko Yàlla xibaare ci Alxuraan, daal di wax ne:﴿ وَأَذِّنْ فِي النَّاسِ بِالْحَجِّ يَأْتُوكَ رِجَالًا وَعَلَى كُلِّ ضَامِرٍ يَأْتِينَ مِنْ كُلِّ فَجٍّ عَمِيقٍ﴾ ﴾ Wool ñit ñi ci aj, danañu la ñëwal di dox, danañu war it ci béppu waruwaay, danañu ñëw it jóge ci bépp gox ak lu mu sori-sori ﴿.[ Saaru Al-Hajji: 27].
Ngёm nag: mooy saxal ak dëggal gu dogu, ak nangu gu mat sëkk, si mbooleem ndigali Yàlla yi, ci gëm ko ak wommatul ko, ci biir, ak ci bitti, loolu mooy dëggal ko ci xol, ak fas ko pas-pas bob mooy làmboo jëfi xol yi ak jëfi yaram yi, loola nag mooy làmboo jëfe diine yépp, ngëm nag day yokke ci topp Yàlla di wàññikoo cig moy.
Laaj nañ Yonnet bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- luy ngëm mu ne:Mooy nga gёm Yàlla ak ay malaakaam, ak ay téereem, ak ay yonnenteem, ak bis bu mujj ba, te gëm dogal ba, bu neex ba ak bu naqari ba.
Ponki ngёm mooy jaamu Yàlla yu xol yi war bépp jullit, te Lislaamu nit ki du wér lu dul da koo fas, te jëfe la mu laaj, looloo tax ñu tudde ko ponki ngëm.Li tàqale diggante ponki ngëm ak ponki Lislaam nag, mooy: ponki Lislaam jëf yu feeñ la yu nit ki di def ci ay céram, lu mel ni tudd baati seede yi, ak julli, ak asaka, bu dee ponki ngëm yi nag jëfi xol la ju nit ki di defe cib xolam, lu mel ni: gëm Yàlla, ak i malaakaam, ak i téereem, ak ay yonnenteem.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ إِنَّمَا الْمُؤْمِنُونَ الَّذِينَ آمَنُوا بِاللَّهِ﴾ ﴾ jullit ñi ñooy ñi gёm Yàlla ﴿[ Saaru An-Nuur: 62]
Danuy gëm amug Yàlla gi, te fas kennam gi ci moomeelam gi, ak ci jaamu gi, ak i turam, ak i melokaanam, gëm Yàlla nag lii lay làmboo:
Gёm amug Yàlla gi -tuddnaa sellam nga- ak kaweem ga.
Gёm moomeelam gi, gëm ne moo moom lépp, moo bind lépp te di ko wërsëgal, di doxal ay mbiram.
- Ak gëm wéetam gi cig jaamu, ak gëm ne moom rekk a yayoo ag jaamu, amul ku ñu koy booleel ci dara, moo xam julli la, walla ñaan, walla nesër, walla rendi, walla dimbandiku, ak xettaliku, ak mbooleem jaamu yi.
ـ Ak gёm turam yu rafet ya ak meloom yu kawe ya mu saxalal boppam, walla Yonnenteem bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- saxalal ko ko, ak dàq li mu dàqal boppam, walla Yonnenteem bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- dàqal ko ko, gëm ne it ay turam ak i meloom egg na ca dayob mat ak rafet, te moom niróowul ak dara, moom mooy Aji-Dégg ji mooy Aji-Gis ji.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ الْحَمْدُ لِلَّهِ فَاطِرِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ جَاعِلِ الْمَلَائِكَةِ رُسُلًا أُولِي أَجْنِحَةٍ مَثْنَى وَثُلَاثَ وَرُبَاعَ يَزِيدُ فِي الْخَلْقِ مَا يَشَاءُ إِنَّ اللَّهَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ﴾ ﴾ Sant ñeel na Yàlla mi bind asamaan ak suuf, mooy ki def Malaaka yi ay ndaw yu am i laaf, ñii ñaar, ñii ñatt, ñii ñent, mooy dolli ci mbindéef yi lu ko soob, Yàlla nag mooy ki man lépp ﴿.[ Saaru Faatiri : 1].
Danuy gëm ne Malaaka yi ci dund gu fàddu la ñu ne, te ñoom ay jaami Yàlla la ñu, yu mu bind ci ag leer, def leen ñu koy topp di ko toroxlul.
ñoom Malaaka yi nag ay mbindéef yu màgg la ñu, kenn peegul séen kàttan ak séen ub lim ku dul Yàlla mu kawe mi, ku ci ne am na ay melokaan ak i tur, ak ay ligéey yu leen Yàlla jagleel, bokk na ci ñoom Jibriil -yal na ko Yàlla musal- mi ñu dénk xam-xam bi Yàlla di jox Yonnet yi.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ قُولُوا آمَنَّا بِاللَّهِ وَمَا أُنْزِلَ إِلَيْنَا وَمَا أُنْزِلَ إِلَى إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَالْأَسْبَاطِ وَمَا أُوتِيَ مُوسَى وَعِيسَى وَمَا أُوتِيَ النَّبِيُّونَ مِنْ رَبِّهِمْ لَا نُفَرِّقُ بَيْنَ أَحَدٍ مِنْهُمْ وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ﴾ ﴾ Waxleen ne gёm nanu Yàlla ak li mu wacce ci nun, ak li mu wàcce ci Ibraahiima, ak Ismahiila, ak Ishaaqa, ak Yanqooba, ak Asbaat ya, ak la mu joxoon Muusa, ak Iisaa, ak li ñu joxoon Yonnent yi mu jóge ci séen Boroom, du ñu tàqale diggante kenn ci ñoom, te ci moom rekk lanu jébbalu ﴿.[ Saaru Al-Baqara: 136].
Danuy gëm ne it ne Yàlla moo wàcce ay téereem ci ay Yonnenteem, muy aw lay ci mbindéef yi.
Ñu leen di jàngal ci téere yi lu leen di jariñ, te di leen sellal.
Yàlla mu sell mi ci yónni gi mu yónni ab Yonnenteem Muhammat -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- ci nit ñépp ci la follee ci sariihaam mbooleem sariiha yi jiitu woon, mu def Alxuraan, mu tiim mbooleem téere yi jóge asamaan, moo leen folli it, Yàlla it moo warlu ci boppam wattu Alxuraan, ci bépp coppite, moom la sunu Boroom mu kawe mi di wax:﴿ إِنَّا نَحْنُ نَزَّلْنَا الذِّكْرَ وَإِنَّا لَهُ لَحَافِظُونَ﴾ ﴾ Nun Yàlla noo wàcce Alxuraan te noo koy sàmm﴿[ Saaru Al-Hijri: 9];Ndax te Alxuraan ju tedd ji, mooy téereb Yàlla bi mu mujj a wàcce ci mbindéef yi, Yonnenteem bii di Muhammat moo mujj ci Yonnent yi, diiney Lislaam mooy diine ji mu gërëmal mbindéef yi ba saa di taxaw, Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ إِنَّ الدِّينَ عِنْدَ اللَّهِ الْإِسْلَامُ﴾ ﴾ Diine fa Yàlla mooy Lislaam﴿[ Saaru Aali-Imraan: 19].
Téere yi jóge asamaan te Yàlla tudd ko ci alxuraan mooy:
Alxuraan ju tedd ji, Yàlla moo ko wàcce ca Yonnenteem ba Muhammat -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-.
Attawraat: Yàlla wàcce na ko ca Yonnenteem ba Muusaa -yal na jàmmi Yàlla nekk ci moom-.
Alinjiil: Yàlla wàcce na ko ca Yonnenteem ba Iisaa -yal na jàmmi Yàlla nekk ci moom-.
Assabuur: Yàlla wàcce na ko ca Yonnenteem ba Daawuuda -yal na jàmmi Yàlla nekk ci moom-.
Suhufu Ibraahiima Yàlla wàcce na ko ca Yonnenteem ba Ibraahiima -yal na jàmmi Yàlla nekk ci moom-.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ وَلَقَدْ بَعَثْنَا فِي كُلِّ أُمَّةٍ رَّسُولاً أَنِ اعْبُدُواْ اللّهَ وَاجْتَنِبُواْ الطَّاغُوتَ﴾ ﴾ Yónni nanu ci bépp xeet ab Yonnent ngir nañu jaamu Yàlla te moytu jaamu lu dul moom ﴿.[ Saaru An-Nahl: 36].
Danuy gёm ne Yàlla mu kawe mi moo yònni ci mbindéef yi ay ndawam yu leen di woo ci jaamu Yàlla moom dong, moom mi amul nawle, ak weddi lépp lu ñuy jaamu te du moom Yàlla mu kawe mi.
Danuy gëm it ne Yonnent yi ay mbindéef yu gòor lañu di ay jaami Yàlla, di ñu dëggu, di ñu ñu dëggal, te di ñu ragal Yàlla, ñu wóor, ñu jub tey jubale, Yàllaa leen dëgëral ci ay firnde, yuy tegtale séen ug dëggu, jottali nañu it lépp lu leen Yàlla yónni, te ñoom ñépp it ci dëgg gu leer lañu nekkoon, ak njub gu leer.
Ñoom yonnent yi nag ka ca njëkk ba ca ka ca mujj séen ub woote benn la ci cosaanul diine, te mooy wéetal Yàlla -mu tedd mi te màgg- cig jaamu te bañ koo bokkaale.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ اللَّهُ لَا إِلَهَ إِلَّا هُوَ لَيَجْمَعَنَّكُمْ إِلَى يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَا رَيْبَ فِيهِ وَمَنْ أَصْدَقُ مِنَ اللَّهِ حَدِيثًا﴾ ﴾ Yàlla mi amul ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul moom, dina leen dajale bisub taxawaay ba te amul benn nàttable, ana kan moo gën a dëggu Yàlla ay wax ﴿[ Saaru An-Nisaa-i: 87].
Danuy gёm bis bu mujj ba, te mooy bisub taxawaay ba nga xam ne bis du ñëw ginnaawam, te gëm it lépp lu ca aju, ci li nu sunu Boroom mu tedd mu kawe mi xibaar, ci téereem bu tedd bi, walla Yonnenteem ba Muhammat -yal na ko Yàlla defal xéewël te musal ko- xibaar nu ko, niki faatug doomu Aadama, ak dekki, ak tasaaroo ga, ak rammu, ak màndaxe ma, ak saytu ga, ak Àjjana, ak Sawara, ak lu dul loolu ci lépp lu aju ca bis bu mujj ba.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ إِنَّا كُلَّ شَيْءٍ خَلَقْنَاهُ بِقَدَرٍ﴾ ﴾ Nun Yàlla noo bind lépp ci ndogal ﴿.[ Saaru Alxamari: 49].
Danuy gёm ndogal yu neex yi, ak yu naqari yi, te mooy gëm li Yàlla mu kawe mi, dogal ci mbindéef yi, ca na mu jiitoo ca xam-xamam ba, te xereñam laaj ko, ak it ne lépp lu xew ci mbindéef yi ciy xew-xew ci àdduna jii, mi ngi ame ci xax-xamu Yàlla ak ub ndogalam -tudd naa sellam ga ak màggam ga- ak ci doxalam moom dong, moom mi amul ndend, ndogal yépp it bindees nañu ko njëgg ñuy bind doomu Aadama, doomu Aadama it am na ag nammeel ak coobare, te itam mooy def ay jëfam ca dëggi-dëggi jëf, waaye loolu lépp nag dara du ci génn xam-xamu Yàlla ak coobareem.
Gёm ndogal nag day ame ci ñenti tolluwaay:
Bu njëkk bi mooy: gëm xam-xamu Yàlla bu matale bi te peeg lépp.
Bu ñaareel bi mooy: gëm ne Yàlla bind na lépp lu war a am ba bis pénc ba.
Bu ñatteel bi mooy: gëm coobarey Yàlla ju mat ja, ak kàttanam ju mat ja, lu ko neex mooy am, lu ko neexul du am.
Bu ñenteel bi mooy: gëm ne Yàlla moo bind lépp, te amul kenn ku mu bokkal bind ga.
Rafetal, mooy: nga jaamu Yàlla ba mel ni yaa ngi koy gis, te xam ne boo ko gisul it moo ngi lay gis. Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ إِنَّ اللَّهَ مَعَ الَّذِينَ اتَّقَوْا وَالَّذِينَ هُمْ مُحْسِنُونَ﴾ ﴾ Yàlla mi ngi ànd ak ñi ko ragal, ak ñiy fafetal ﴿.[ Saaru An-Nahl: 128].
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ التَّوَّابِينَ وَيُحِبُّ الْمُتَطَهِّرِينَ﴾ ﴾ Yàlla dafa bëgg way-tuub yi, dafa bëgg it way-laab yi ﴿.[ Saaru Al-Baqara: 22].
Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na:( Ku jàpp njàpp mu mel ni sama njàpp mi, daal di julli ñaari ràkka yoy xalaatu ca, Yàlla dina ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram).Buxaarii moo ko nettali.
Bokk na ci liy wane màggug julli, Yàlla yoonal gi mu yoonal laab mu jiitu ko, mu def ko ab sart ci wérug julli, moom mooy caabiy julli, teewlu ngëneelam nag day def xol bi am ug cofeel ci taxawe julli, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na:( Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko).Muslim moo ko nettali.
Yonnent bi -yal na Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na:( Ku jàpp te rafetal njàpp ma, ay ñaawtéefam day génn ci aw yaramam bay génn ci ay weyam).Muslim moo ko nettali.
Jaam bi jëm ci Boroomam day laab laabug bitti, ci njàpp, ak laabug biir, ci taxawe jaamu Yàlla gii, sellalal ko Yàlla mu kawe mi te roy ca njubug Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-
Liy waral njàpp:
1- Julli, ak gu mu man a doon, moo xam gu farata la, walla gu sunna la.
2- Wër kaaba ga.
3- Laal kaamiil.
Damay jàpp ak a sangu-set ci ndox mu laab:
Ndox mu laab mooy: bépp ndox mu jóge ci asamaan, walla mu jóge ci suuf, te des ca cosaanam, te it benn ci ñatti melokaanam yi soppikuwul, moo di: melo wa, ak cafka ga, ak xet ga, ci lenn ci mbir yiy deñal laab ug ndox ma.
Jéego bu njëkk bi mooy :1- yéene, barabam nag mooy xol, yéene li muy tekki mooy: dogug xol ci def ag jaamu Yàlla, ngir jege-jege lu Yàlla mu kawe mi.
Ñaareelu jéego bi mooy 2: damay wax: bismil Laahi.
Jéego ñatteel bi mooy 3: raxax tenq yi ñatti yoon.
Jéego 4: gallaxndiku ñatti yoon.
Gallandiku mooy: dugal ndox ci gémmiñ yëngal ko yàbbi ko.
Jéego 5: saraxdiku ak fiiru, ñatti yoon, saraxndiku mooy: xëcc ndox mi ci sa biir bakkan ba mu sori ca biir.
Fiiru mooy: génne li nekk ci bakkan bi, cig noyyi.
Jéeego 6: raxas kanam gi ñatti yoon.
Dayob kanam gi:
Kanam mooy: li ngay jakaarlool ci nit.
Dayob kanam cib yaatuwaay: mi ngi tàmbalee ci nopp yam ci beneen nopp ba.
Dayob guddaay bi: mi ngi tàmbulee fa kawar baaxoo saxe ba ca yamukaayu sikim ba.
Raxas kanam dafay làmboo lépp lu fa ne ci kawar gu woyof, ak la amul kawar, ak it weex-weex ya, ak la sës sa nopp ya.
Weex-weex ya mooy: la nekk ca diggante nopp bi ak sikkim bi.
Kawar gi sës ci nopp bi mooy: gi sax ci yax bi féeteeg bënn-bënnu nopp bi féete ca bopp ba, juge fa jëmm ca nopp ba.
Naka noonu raxas kanam day làmboo lépp lu feeñ ci kawarug sikkim gu fatt ga, ak la wàcc jëm suuf.
Jéego 7: raxas loxo yi tàmbalee ca baaraam ya ba ca coñco ya, ñatti yoon.
Raxas coñco yi day dugg ci raxasug loxo biy farata.
Jéego 8: masaa bopp bi yépp ci say loxo, boole ko ak nopp ya benn yoon.
Masaa bopp ci kanamu bopp bi lay tàmbalee ba ca doq ga mu delloowaat leen.
Day dugal ñaari baaraami sànni kaayam ci biir nopp bi, teg baaraami déy ya ci bitti nopp ba, daal di masaa bitti nopp ba ak biir ga.
Jéego 9: raxas tànk yi, tàmbalee ca baaraami ndëggu ya, ba ca dojor ya, ñatti yoon, raxas dojor yi nag day dugg ci raxas tànk giy farata.
Ñaari dojor yi mooy: ñaari yax yi génne ci suufu yeel bi.
Bir yii ñooy yàq yàq njàpp:
1. Liy génne ci ñaari génnuwaay yi, ni ki saw ak dem duus, ak ngelawal, ak manniyu, ak masyu.
2. Xel mu deñ ci ay nelaw yu diis, walla xëm, walla màndite, walla am ndof.
3. Lépp luy waral sangu, niki janaba, ak mbërëg, ak meret.
Bu nit fajee aajoom war na ci moom mu deñal sobe sa ci ndox mu laab, loolu moo gën, walla ci lu dul ndox mu laab tey deñal sobe, niki ay doj, walla ay xob, walla sagar, ak lu nirook moom, ci kaw loolu nekk ñatti fomp yu set, te defe ko ci lu laab.
Jamono jees di masaa ay saŋ walla ay kawas, manees naa masaa ca kaw, te du aajewoo raxas tànk yi, waaye nag ci ay sàrt:
1. Mu sol ko ci ag laab gu mat sëkk ci toj mu ndaw ak mu mag.
2. Mu nekk yu laab yu amul sobe.
3. Masaa ga nekk ca diir ba mu war a yam.
4. Mooy ñu doon yu lew, bu ñu doon yu ñu sàcc, walla yu ñu siif.
Ñaari saŋ yi nag mooy: lees di sol ci tànk ci der wu woyof walla lu ni mel, walla lu mel ni ay dàll yoy day muur tànk yi. Ñaari kawas nag mooy: li nit di sol ci ay tànkam ci sagar, ak lu ko niru, mbaa lu mel ni li ñuy tudde Sarraab.
Li tax ñu yoonal masaa ci ay saŋ: jubluwaayu masaa ci ay saŋ mooy yombal ak woyofalal jullit yi nga xam ne summi ay saŋ ak ay kawas walla raxas ay tànk, dina diis ci ñoom, rawati na ci jamonoy seddaay gu tar, ak ci tukki.
Diir bi masaa saŋ di ame: budee ki nekk ci dëkkam: bis bu mat sëkk la, [24i waxtu] budee ki tukki: ñatti fan yu mat sëkk la [72i waxtu].
Limub diirub masaa mi ngi tàmbalee ci njëlbéenug masaa saŋ ya walla kawas ya ginnaaw am laab.
Melokaanu masaa ay saŋ walla ay kawas:
1. Day tooyal ñaari loxo yi.
2. Day rombale loxo yi ci bitti tànk yi [mu tambalee ci catu tànk yi ba ci njëlbeenu yeel yi].
3. Day masaa tànku ndayjoor bi, ci loxob ndayjoor bi, masaa tànkub càmmoñ bi ci loxob càmmoñ bi.
Yiy yàq masaa: 1- yiy waral sangu. 2- jeexug waxtuw masaa wi.
Bu góor walla jigéen jaxasoo donte génnewul mànniyu walla sa ñu génne mànniyu ci bànneex, cig yeewu, walla ciy nelaw, kon sangu dana leen war, ba ñu man a taxawe julli, walla lol laab dacay war.Naka noonu jigéen bu setee ci mbërëg walla meret sangu da koy war, balaa muy man a julli walla mu def lol laab dacay war.
Melokaanu sangu moo nekk nii:
Jullit bi day matale yaramam wépp ci ndox ca anam ga mu man a ame, bokk na ci loola gallaxndiku, ak saraxndiku, su matalee yaramam ci am ndox toj mu mag ma yëkkatiku na laab ga it mat na.
Amna it weneen melokaan wu gën a mat, te mooy ba Yonnent ba -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- doon jëfe, te moo nekk ni:
01 Yéenee yëkkati am toj.
02 Wax bismil Laahi, ak raxas loxo ya ñatti yoon, sooga raxas péy ma mooy fa sobe sa taq.
03 Jàpp mu mat, niki muy jàpoo buy julli.
04 Sotti ndox ca bopp ba ñatti yoon, day tooyal fa kawar ga saxe.
05 Matale mbooleem yaram wi ci am ndox, mu tàmbalee ci raxas wetug ndayjoor wi, ak camooñ bi, ànd ak bomb ko ci ay loxoom ba ndox ma egg ci mbooleem yaram wi.
Danañu tere ku am janaba mu def yii ba kerog muy sangu:
01 Julli
02 Wër kaaba ga.
03 Toog ci jàkka, ak di fa romb, te toogoo fa.
04 Laal kaamil.
05 Jàng Alxuraan.
Bu jullit bi amul ndox mu mu man a laabe, walla manut a jëfandikoo ndox ma, ngir tawat walla lu ni mel, te mu ragal julli ga raw ko, kon day tiim ci suuf.
Melokaan wa mooy day dóor ñaari loxoom ci suuf benn dóor, daal di ca masaa kanamam ak ñaari ténqam rekk. Dees na sartal ca suuf sa mu doon lu laab.
Bir yii mooy yàq tiim:
1. Liy yàq tiim mooy yàq njàpp.
2. Am ndox lu jiitu muy dugg ca jaamu Yàlla ga mu tiimaloon.
Yàlla farataal na ci jullit bi juróomi julli ci bis bi ak ci guddi gi, te mooy: fajar, tisbaar, tàkkusaan, timis, gee.
Bu julli jotee jullit bi day laab ci toj mu ndaw, ak toj mu mag ndeem dafa tojle toj mu mag.
Toj mu mag mooy liy waral ci jullit bi sangu.
Toj mu ndaw mooy: liy waral ci jullit bi jàpp.
Jullit bi buy julli day sol yére yu laab, dem ci barab bu laab, te muur awraam.
Jullit bi na taaroo yéere yu laab yu yelloo ak jamonoy julli ga, te muur aw yaramam, du dagan ci góor guy julli mu feeñal dara ci li dox ci diggante jumbax bi ak bëti wóom yi.
War na ci jigéen buy julli mu sàng mbooleem aw yaramam, ba mu des kanam ga ak ténq ya.
Daganul ci jullit muy wax ci julli gi lu dul wax ji ñu ko jaglleel, te muy diglu imaam bi, te du geestu ci julleem, bu manul mokkal wax yi julli jagoo day tudd Yàlla di ko sàbbaal ba julli gu noppi, dana ko war it mu gaaw jàng julli ak la ñu cay wax.
Ngir nu julli julli gu wér ci ndigalul Yàlla, nanu topp jéego yii te sàmmoonte ak moom:
Jéego 1: yéene ñeel farata ji nga bëgg a def, yéene nag barabam mooy xol.
Ginnaaw bi ma jàppoo damay taxaw julli, bu dee man naa taxaw.
Jéego ñaareel bi 2: damay yëkkati samay loxo bamu tolloo ak wagg yi, daadi wax: [ Allaahu akbar] yéenee dugg ci julli gi.
Jéego 3: damay jàng ñaanug ubbee yi ñёw ci sunna, bokk na ci yooya:(Subhaananakal Laahumma wa bi hamdika, wa tabaaraka ismuka, wa tahaalaa jadduka, wa laa ilaaha xayruka).
Jéego 4: damay muslu ci Yàlla ci Saytaane, daadi wax:( Ahuusu bil Laahi minas Saytaanir rajiimi).
Jéego 5: damay jàng saaru faatiha, ci ràkka bu ne, daadi wax:﴿ الْحَمْدُ لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ * [ Alhamdu lil Laahi Rabbil aalamiina*الرَّحْمَنِ الرَّحِيمِ * Arahmaanir Rahiimi*مَالِكِ يَوْمِ الدِّينِ * Maaliki yawmid diini*إِيَّاكَ نَعْبُدُ وَإِيَّاكَ نَسْتَعِينُ * Iyyaaka nahbudu wa iyyaaka nastahiinu*اهْدِنَا الصِّرَاطَ الْمُسْتَقِيمَ * Ihdinas siraatal mustaxiima*صِرَاطَ الَّذِينَ أَنْعَمْتَ عَلَيْهِمْ غَيْرِ الْمَغْضُوبِ عَلَيْهِمْ وَلَا الضَّالِّينَ﴾. Siraatal laziina anhamta halayhim, xayril maxduubi halayhim walad daalliina﴿.
Ma sooga wax: [Aamiin]. li miy tekki mooy: yaw Yàlla yal na nga nangu ñaan gi.
Ginnaaw faatiha damay jàng li ma man ci Alxuraan ci ràkka bu njëkk bi, ak bu ñaareel bi dong ci julli gune, lii nag du lu war, waaye def gi yool bu rëy a ngi ci.
Jéego 6: damay wax: (Allaahu akbar) daadi sëgg sëgg bu jub, jàpp samay wóom te soreele samay baaraami loxo, sooga wax ci sëggaay bi: (Subhaana rabbiyal Hasiim wa bi hamdihi) ñatti yoon.
Jéego 7: damay siggi ci sëggaay bi daadi wax:(samihal Laahu liman hamidahu) yëkkati samay loxo ba mu jege samay wagg, su ma taxawee ba ne jodd daadi wax: (Rabbanaa wa lakal hamdu).
Jéego 8: damay wax:( Allaahu akbar) daadi sujjuud ci samay loxo ak samay bëti wòom, ak samay tànk, ak samab jë, ak sama bakkan, daadi wax ci samab sujjuud (Subhaana rabbiyal ahlaa) ñatti yoon.
Jéego 9: damay wax: (Allaahu akbar) daadi yëkkatiku ci sujjuud ba toog nojj, ci sama kaw tànku càmmooñ, samp sama tànku ndayjoor, daadi wax: (Rabbi ixfir lii,) ñatti yoon.
Jéego 10: damay wax: (Allaahu akbar) daadi sujjuud beneen yoon bu mel ni sujjuud bu njëkk ba.
Jéego 11: damay jug ci sujjuud ba, daadi wax:(Allaahu akbar) ma taxaw bane jodd, la des ca julli ga yépp damay def na ma ko defe woon ca ràkka bu njëkk ba.
Ginnaaw bu ma jullee ràkkaab ñaareel ba ci jullig tisbaar, ak tàkkusaan, ak timis, ak gee, damay toog ngir jàng taaya ju njëkk ji, te mooy:(Attahiyyaatu lil Laahi, azzakiyyaatu lil Laahi, attayyibaatus salawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu, wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahis saalihiina, ashadu an laa ilaaha illal Laahu, wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu.Ginnaaw loolu nag damay jug taxaw julli ràkkab ñatteel bi.
Ginnaaw ràkka bu mujj bi ci julli gu ne damay toog daadi jàng taaya ju mujj ji, te mooy:(Attahiyyaatu lil Laahi, azzakiyyaatu lil Laahi, attayyibaatus salawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan nabiyu, wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahis saalihiina, ashadu an laa ilaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu, Allaahumma salli halaa Muhammadin, wa halaa aali Muhammadin, kamaa sallayta halaa Ibraahiima wa halaa aali Ibraahiima, innaka hamiidun majiidun, Allaahumma baarik halaa Muhammadin, wa halaa aali Muhammadin, kamaa baarakta halaa Ibraahiima, wa halaa aali Ibraahiima innaka hamiidun majiidun).
Jéego 12: ginnaaw loolu damay sëlmël ci sama wetug ndayjoor, daadi wax: (assalaamu halaykum wa rahmatul Laah) dellu sëlmël ci sama wetug càmmoñ daadi wax: (assalaamu halaykum wa rahmatul Laah) daadi ci yéenee génn ci julli gi, ci loolu laay nekke ku def julli gu mat.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ قُلْ لِأَزْوَاجِكَ وَبَنَاتِكَ وَنِسَاءِ الْمُؤْمِنِينَ يُدْنِينَ عَلَيْهِنَّ مِنْ جَلَابِيبِهِنَّ ذَلِكَ أَدْنَى أَنْ يُعْرَفْنَ فَلَا يُؤْذَيْنَ وَكَانَ اللَّهُ غَفُورًا رَحِيمًا﴾ ﴾ Yaw Yonnent bi waxal sa soxna yi ak sa doom yi, ak jigéeni jullit ñi, na ñuy muur seen i cér, loolu moo gën a néew ci ñu xam leen, ba deesu leen lor, Yàlla déy ku bari ak njéggal ak yërmaande la﴿.[ Saaru Ahsaab: 59].
Yàlla moo waral muuraay ci jigéenu jullit, tey nëbb mbooleem ay cëram ci ay jàmbur yu góor, ci ay yére yu waa réewam baaxoo sol, du dagan ci moom muy sol lu woyof lu dul ci kanamu jëkkëram, walla ay koj i armalam, te ñooy ñi nga xam ne du dagan ci jigéenu jullit bi muy sëy ak ñoom ba fàwwu, ñooñu ñooy:(baay, ak i maam, doom ak ay sët, ay baay tëx, ak ay nijaay, ak mbokk, ak doomi mbokk mu góor, ak doomi mbokk mu jigéen, ak boroom jëkkëru yaay, ak baayu jëkkër, ak ay maamam, ak doomi jëkkër, ak ay sétam, ak mbokk ci nàmpaale, ak jëkkëri ki ko nàmpal, dees na haraamal cig nàmpaale lépp lus haraamal ci askan).
Jigéenu jullit war naa sàmmoonte ak bir yii ci ak colam:
Ba ca jëkk: mu daj mbooleem yaram wa.
Ñaareel bi: yére yi bañ a nekk ab taar, ndeem dafa nekk ci ay jàmbur yu góor.
Ñatteel bi: mu bañ a yaraax bay fésal aw yaramam.
Ñenteel bi: mu yaatu bañ a xat, bay melal aw yaramam.
Juróomeel bi: mu bañ a xeeñ gëtt budee day génn ci ay jàmbur yu góor, yu xet ga man a xeeñ.
Juróom benneel bi: mu bañ a niru ak yérey góor.
Juróom ñaareel bi: mu bañ a niru ak yérey ñi dul jullit, ci séen ug jaamu, walla ci séen i xew-xew.
Juróor ñatteel bi: mu bañ a nekk yére yu ràññiku.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ إِنَّمَا الْمُؤْمِنُونَ الَّذِينَ إِذَا ذُكِرَ اللَّهُ وَجِلَتْ قُلُوبُهُمْ وَإِذَا تُلِيَتْ عَلَيْهِمْ آيَاتُهُ زَادَتْهُمْ إِيمَانًا وَعَلَى رَبِّهِمْ يَتَوَكَّلُونَ﴾ ﴾Ñi gëm Yàlla ñooy ñi nga xam ne bees tuddee Yàlla séen xol yi day tiit, te bees jàngee ay aayaam mu dolli leen ngëm, te ci séen Boroom la ñuy wéeru﴿.[ Saaru Al-Anfaal: 2]
- Kuy dëggu la ci ay waxam, te du fen.
- Day matal kóllare ak ub dig.
- Du wax lu ñaaw buy xuloo.
- Day matal kóllare.
- Day bëggal mbokkum jullitam la mu bëggal boppam.
- Day tedd.
- Day rafet njort ci nit ñi.
- Day jokk mbokk.
- Day gërëm dogalu Yàlla te di ko sant bu neexee, ak a muñ bu naqaree.
- Day am kersa.
- Day yёrëm mbindéef yi.
- Ab xolam day mucc ci ag mbañeel, ay céram it day mucc ci lor keneen.
- Day jéggal nit ñi.
- Du lekk ribaa te du ko jëflante.
- Du njaalo.
- Du naan sàngara.
- Day rafetal jëme ci ay dëkkandoom.
- Du tooñ du wor.
- Du sàcc, te du wuruj.
- Kuy rafetal la jëme ci ñaari way-juram, donte duñu ay jullit.
- Day yar ay doomam ci ag mbaax, di leen digal wartéefi Sariiha yi, di leen tere ay ñaawtéef ak yu haraam.
- Du nuru-nurulu ñi dul ay jullit ci benn jëf bu ñu jagoo ci diine, walla ci aada yi ñu ràññikoo.
- Day dellu ci Yàlla di ko jéggalu ci ag gàttañloom, ak i bàkkaaram.
01 Yàlla mooy sunu Boroom amul buur bu ñuy jaamu cig dëgg bu dul moom, amul benn yàlla ci dëgg bu dul moom, amul lu nirook moom, amul dara lu ko të, moom mooy kiy dégg di gis.
02 yàlla -tudd naa sellam gi té kawe na- moo ngi ci asamaan, nék si kaw mbidéefam yépp, tàqalikoo ak ñoom, ak kaweem dafa matalé ci bépp anam, kaweg jëmm , kaweg daraja, kaweg not, te moom boroom bi -tudd naa sellam gi- Aji-peeg la bépp mbir.
03 danuy saxal lépp lu Yàlla saxal ci jëmmam ji walla Yonnenteem bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- saxalal ko ko ci ay tur walla ay melokaan, te it danuy dàq lépp lu mu dàq ci jëmmam ji, walla Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- dàqal ko ko.
04 Yàlla mu kawe mi mooy nangu ñaan yi, di faj aajo yi, te moo moom lépp, kenn du jariñ walla muy lor ku dul moom, ab jaam nag manul doylu ci wenn saa wolif ko, daganul cib jullit muy jublu ku dul Yàlla mu kawe mi ci wenn xeet ci xeeti jamu Yàlla yi, niki ñaan walla julli walla nisër walla rendi walla ragal walla yaakaar walla wakkirlu walla yeneen xeeti jaamu yi yu feeñ yi walla yu nëbb yi, ku jëmële benn jaamu ci ku dul Yàlla, koo ku bokkaale na Yàlla.
05 Bakkaar bi gën a màgg nag te gën a rëy si bakkaar yi mooy bokkaale Yàlla, ku faatu ci bokkaale, Yàlla day haraamal ci moom àjjana te sawara mooy nekk dëkkuwaayam, bokkaale nag mooy bakkaar bi Yàlla dul jéggël kenn ku ko faatuwaale te tuubu ko.
06 Lenn lu moy jaam bi nekkul lu ko war a dal, lu ko dal itam nekkul lu ko war a moy, day war ci jullit bi mu gëm dogali Yàlla yi, ak gërëm dogali yàlla mu kawe mi, ak di tagg boroomam te di ko sant ci bépp anam.
07 Muhammat sunub Yonnent -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- mooy ki gën ci nit ñi te moo mujj ci yonnent yi, mooy aji-ramm ji ñuy rammloo keroog bisub taxawaay ba,Yàlla moo ko jàppe xaritam niki mu jàppe Ibraahiima -yal na ko Yàlla dolli jàmm- muy xaritam.
08 Sunub téere mooy Alxuraan bu màgg bi, mooy li lottal ñépp, di téere bi ñu dogu ci ag wéram, mooy téere bi ñuy jaamu Yàlla ci jàngam, Yàlla -mu kawe mi- moo ko wàcce ci sunub Yonnent Muhammat -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- jaarale ko ci Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- mi gën ci Malaaka yi, Yàlla mu kawe mi moo ko wattu ci bépp coppite niki mu ko waxe -moom Aji-Sell ji-:﴿ إِنَّا نَحْنُ نَزَّلْنَا الذِّكْرَ وَإِنَّا لَهُ لَحَافِظُونَ﴾ ﴾ Nun Yàlla noo wàcce Alxuraan te Noo koy sàmm﴿.[ Saaru Al-Hijri: 9].
09 Nit ñi gën a jége Yàlla ñooy ñi koy gën a nàngul, te gën a topp sariihaam bi, Araab du gën ki dul Araab, ki dul Araab itam du gën Araab bi, ki weex du gën ki ñuul, ki ñuul itam du gën ku weex ki ci lu dul ragal Yàlla, ndax nit ñépp ci Aadama la ñu bawoo, te Aadama ci suuf la bawoo, Yàlla mu sell mi nee na:﴿ إِنَّ أَكْرَمَكُمْ عِنْدَ اللَّهِ أَتْقَاكُمْ﴾ ﴾Ki gën a tedd ci yéen fa Yàlla mooy ki gën a ragal Yàlla ﴿[ Saaru Al-Hijri: 13].
10 Ab jullit day gëm Malaaka yu tedd yi tey bind jëf yi, gëm séenug am, gëm ne yit ñoom ay jaam yu ñu bind la ñu, Yàlla mu kawe mi moo leen bind ci leer, kon ñoom ay mbindéef la ñu ci mbindéefi Yàlla mu kawe mi, bokk na ci ñoom: Jibriil mi ñu gàll Wahyu wi, ak Miikaa-iil mi ñu gàll taw bi, ak Issraafiil mi ñu gàll wal buftu ba, ak Malaaka mawti mi ñu gàll jël ruu yi jaam ñi.
11 jullit day gëm màndargay bis pénc, ak génnug Masiihu Dajjaal, ak wàccug Iisaa doomu Maryama -yal na Yàlla dolli jàmm- juge ci asamaan, ak fenkug jant bi ci sowwu bi.
12 Jullit day gëm ne mbugëlu bàmmeel amna ñeel ña ko yayoo, ak xéewëlu bammeel ñeel ña ko yayoo, ak laaju Munkar ak Nakiir ci bammeel, laaj yu jëm ci kan mooy sa boroom lan mooy sa diine kan mooy sa yonnent, mu gëm ne it ne bàmmeel day nekk toolub dër ci tooli dëri àjjana yi walla mu nekk am pax ci baxi sawara yi.
13 Day fas ne dekki amna, ak fay jëf yi bisub taxawaay ba, ak ne àjjana ak sawara ñaari mbindéef lañu yoy duñu jeex mukk.
14 Njabar ag weddi Yàlla la, jàng ko du dagan walla dem ci njabarkat ak narkat yi dara daganu si, te ab jullit du dëggal lab seetkat walla ab xamtukat, képp ku leen dëggal weddi na li Yàlla wàcce ci Muhammat -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-.
15 War na ci jullit bi mu bëgg àndandooy Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- ak bëgg it kepp ku leen bëgg, te bañ kepp ku leen bañ, ndax bëgg leen ci diine la bokk ak rafetal, bañ leen nag ag kéefër la ak ug naaféq, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- nee na: [ Buleen ŋàññi samay àndandoo] Muslim moo ko nettali. Képp ku jam walla mu ñàkkal solo kenn ci sahaaba yi, ku réer la te nitu bidaa la.
16 Jullit bi day saxal ne ki njëkka wuutu Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-mooy Abuu Bakrin Assiddiiq -yal na ko Yàlla dollee gërëm-muy ngëneel ci moom ak ug jiitu ci mbooleem xeet wi, ginnaaw ba Umar bun Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ginnaaw ba Usmaan-yal na ko Yàlla dollee gërëm-ginnaaw ba Alliyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ñoom ñooy xalifa ya, tey njiit yu jub ya.
17 Jaamu Yàlla ci ndigal rekk lay tege, du dagan ñuy jaamoo Yàlla ci genn jaamu lu dul daa sax ci Alxuraan walla ci Sunnas Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- gépp jaamu gu nit ñi sos ginnaaw faatug Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- te tege wul ci ak njubam loolu bidaa la dees koy delloo, Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- nee na: (képp ku sos ci sunu diine ji lu ci bokkul dees ko koy delloo) Buxaarii moo ko nettali.
18 Nangug jaamu mi ngi aju ci ñaari ponk yoy ay cosaan lañu te ñooy: sellal jaamu gi ngir Yàlla mu kawe mi, ñaareel bi mooy: topp Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- ca jaamu ga, kon deesul nangu ag jaamu bu sellul ngir Yàlla, deesu ko nangu it bu tegewul ci njubug Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-.
Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ مَنْ عَمِلَ صَالِحًا مِنْ ذَكَرٍ أَوْ أُنْثَى وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَلَنُحْيِيَنَّهُ حَيَاةً طَيِّبَةً وَلَنَجْزِيَنَّهُمْ أَجْرَهُمْ بِأَحْسَنِ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ﴾ ﴾ Ku jëf lu baax di góor walla muy jigéen te ànd ak ngëm dananu ko dundal dund gu neex, te dinanu leen fay séen ub yool ci lu gën a rafet la ñu doon jëf ﴿[ Saaru An-Nahl : 97].
Bokk na ci li gën a màgg ci luy dugal mbëgte ak bànneex ci xolu jullit bi, mooy jokkoom gu sës rikk ci Boroomam te amul benn aji-dond wala aji-dee wala ay xërëm yuy dox ca diggante ba, Yàlla mu kawe mi wax na ci téereem bu tedd bi ne moom ku jege ay jaamam la ba fàawwu, di leen dégg, di nangu séen i ñaan, niki ni mu ko waxe moom Aji-Sell ji:﴿ وَإِذَا سَأَلَكَ عِبَادِي عَنِّي فَإِنِّي قَرِيبٌ أُجِيبُ دَعْوَةَ الدَّاعِ إِذَا دَعَانِ فَلْيَسْتَجِيبُوا لِي وَلْيُؤْمِنُوا بِي لَعَلَّهُمْ يَرْشُدُونَ﴾ ﴾ Bu la sama jaam ñi laajee ci man, yaw Yonnent bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- neleen ku jege laa, damay nangu ñaanug aji-ñaan gi ndeem ñaan na ma, kon nañu ma wuyu si te gëm ma ndax ñu jub﴿[ Saaru Al-Baqara : 186].Yàlla mu sell mi moo nu digal nu ñaan ko, mu def ñaan goo gii mu bokk ci jaamu yi gën a màgg ci yi jullit bi di jege-jege loo Boroomam, niki ni ko Yàlla mu màgg mi waxe:﴿ وَقال رَبُّكُمُ ادْعُونِي أَسْتَجِبْ لَكُمْ إِنَّ الَّذِينَ يَسْتَكْبِرُونَ عَنْ عِبادَتِي سَيَدْخُلُونَ جَهَنَّمَ داخِرِينَ ﴾ ﴾Séen Boroom wax na ne ñaanleen ma ma may leen, ñi nga xam ne dañu maa rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way torox﴿[Saaru Xaafiri: 60],Jullit bu baax day sax ci yittewoo Boroomam, tey saxoo di ko ñaan, ak di ko jege-jege lu ci jëf yu baax.
Yàlla mu kawe mi moo nu amal ci àdduna bii ngir jubluwaay bu màgg, te bindu nu ngir fo; li tax mu bind nu mooy jaamu ko moom dong, moom mi amul ndend, moo nu yoonalal diiney njub ju matale, joj moo nose mboolem sunu mbiri dund gi nu jagoo ak gi nu séq ak ñépp, mu sàmme ci yoonam wu maandu wii yi manuta ñàkk ci sunug dund, te mooy sunu diine, ak sunuy bakkan, ak sunuy der, ak sunuy xel, ak sunuy alal, képp kuy dund tey topp ndigëlu Sariiha yi, moytu tere yi, kooku de wattu na yu manut a ñàkk yi, dana am ug texe ak ug dal ci ag dundam ci lu amul benn nàttable.
Yiy lënkale jullit bi ak Boroomam lu xóot la lol da koy may ug dal, ak nooflaayu bàkkan, yég-yégu dal ak kóolute ak mbégte, te def ko muy yég ni Boroomam bu màgg bi ànde ak moom, di ko dimbële, ak ug péeteem ak jaamam bi gëm, Yàlla mu kawe mi nee na:﴿ اللَّهُ وَلِيُّ الَّذِينَ آمَنُوا يُخْرِجُهُمْ مِنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ﴾ ﴾Yàlla mooy péetew ñi ko gëm, moo leen génne ci lëndamug kéefar yóbb leen ci leerug ngëm﴿[ Saaru Al-Baqara: 257].
Jokko gu màgg gii nag ab yég-yég la gog day yóbb jullit bi ci bànneexu ci jaamu Yàlla, ak am ug cofeel ci daje ak Yàlla, xol ba fees dell ak ug texe ci yég gi muy yég neexitu ngëm.
Neexit woowu nga xam ne kenn mënut a melal neexit wa, ku dul ku ko mos ci top Yàlla ak moytu ay ñaawtéef, Yonnent Yàlla bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- nee na:(ذاق طعم الإيمان من رضي بالله ربًا وبالإسلام دينًا وبمحمد رسولًا) (Mos na cafkag ngëm ki gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- di Yonnenteem)Muslim moo ko nettali.
Waaw, bu nit ki yégee ak teewam gu sax ci kanamu ki ko bind, te mu xam ko ci ay turam ak i meloom yu rafet, te di ko jaamu mel ni mi ngi koy gis, te sellal it jaamu ga ñeel Yàlla, te nammul ca jaamu ga lu dul Yàlla mu màgg mi, dina dund dund gu teey gu neex ci àdduna te ag mujjam dina rafeg ëllag.
Ba ci musiba yiy dal ci kaw jullit bi ci àdduna aw tàngaayam day déñ ci seddaayu kóolute, ak gërëm ndogalu Yàlla mu kawe mi, ak di ko sant ci mboolem ndogalam yi yu baax yi ak yu bon yi, ànd ak ngërëm lu mat.
Bokk na ci liy yell ci jullit bi mu xér si ngir texeem ak ug dalam yokk, mooy bari ag tudd Yàlla mu kawe mi, ak jàng Alxuranam ju tedd ji, niki mu ko waxe moom Aji-Kawe ji:﴿ الَّذِينَ آمَنُوا وَتَطْمَئِنُّ قُلُوبُهُمْ بِذِكْرِ اللَّهِ أَلَا بِذِكْرِ اللَّهِ تَطْمَئِنُّ الْقُلُوبُ﴾ ﴾Ñi nga xam ne dañoo gëm séen xol di dal ci tudd Yàlla ga, xanaa du ci tudd Yàlla la xol yi di dale﴿[Saaru Ar-Rahd: 28].Saa bu jullit bi baree lu muy tudd Yàlla ak a jàng Alxuraan, ci lay gën a jokkoo ak Boroomam, ba bakkanam day sell ngëmam gën a dëgër.
Naka noonu it jaadu na ci jullit bi, mu xér ci jànge mbirum diineem, ca delluwaay yu wér ya, ba man a jaamu Yàlla ci xam-xam bu leer, Yonnent bi -yal na ko Yàlla defal xéewël ak mucc- nee na:(Sàkku xam-xam farata la ci bépp jullit).Ibn Maaja moo ko nettali.Ak mu jébbalu, te wommatu ñeel ndigalu Yàlla mu kawe mi ko bind, moo xam xam na jubluwaay ba walla xamu ko,Yàlla mu kawe mi wax na ci téereem bu tedd ba ne:﴿ وَمَا كَانَ لِمُؤْمِنٍ وَلَا مُؤْمِنَةٍ إِذَا قَضَى اللَّهُ وَرَسُولُهُ أَمْرًا أَنْ يَكُونَ لَهُمُ الْخِيَرَةُ مِنْ أَمْرِهِمْ وَمَنْ يَعْصِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا مُبِينًا﴾ ﴾Yellul ci benn jullit bu góor ak jullit bu jigéen bu Yàlla ak ub Yonnenteem àttee benn mbir mu cay am lu muy tànn, te képp ku moy Yàlla ak ub Yonnenteem réer na réer gu bér﴿[Saaru Al-Ahsaab: 36].
Yal na Yàlla dolli jàmm ak mucc sunu Yonnent bi Muhammat ak waa kёram ak àndandoom yépp.
Ab tënk bu am solo ñeel jullit bi:
Jubluwaay bi waral bindug mbindéef yi:
Samab Yónnent Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc:
Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc mooy yërmaande gi yàlla rafaatale mbindéef yi.
Bokkk na ci ay melokaanam -yal na ko Yàlla dolli xéewël te musël ko-:
Alxuuran mu tedd mi waxu sama Boroom la.
Tolluwaay bu njëkk bi mooy: jébbalu.
Ponku ñaareel bi: mooy taxawal julli.
Ponku ñattel bi: mooy joxe asaka.
Ponku ñenteel bi, mooy: weeru koor.
Ponku juróomeel bi mooy: aj Màkka.
Tolluwaayub ñenteel bi mooy ngëm:
Ponk bu njëkk bi mooy: gёm Yàlla.
Ponku ñaareel bi mooy: gëm Malaaka yi.
Ponku ñattel bi mooy: gëm téere yi.
Ponku ñenteel bi: mooy gëm Yonnent yi.
Ponku juróomeel bi mooy: gëm allaaxira.
Ponku juróom benneel bi mooy: gëm dogal yu neex yi ak yu naqari yi.
Tolluwaayu ñatteel bi mooy: rafetal.
Bokk na ci melokaanu ab jullit: