×
New!

Bayan Al Islam Encyclopedia Mobile Application

Get it now!

Pas-pas bu wér ak ub safaanam, ak yiy yàq lislaam.

Aji taalif ji:

Seex Abdul Asiis ibnu Addul Laahi ibnu Baas.

Maa ngi tàmbulee samay wax ak samay jёf ci turu Yàlla miy Boroom yёrmànde ju yaatu ji ci adduna tay jakleell yёrmàndeem ёllag way gёm yi.

Laytaayug téere bi.

Sant ñeel na Yàlla rekk, xéewal ak mucc yalna nekk ci ki nga xam ne amul Yónnente buy ñew ginnaawam, ak ay ñoñam ak i àndandoom.

Gannaaw loolu: bi nga xameene pas-pas bu wér mooy cosaanu diiney lislaam ci laa ko def muy tombub waxtaan wi; te xamees na ci tegtali sariiha yi ne ci Alxuraan ak Sunna ne, jëf yi ak wax yi mi ngi wére te dees nako nangu bu bawoo ci pas-pas bu wér, budee ne pas-pas bi wérul nag lépp lu ca soqikoo ciy jëf walla ay wax day yàqu ni ki ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:

﴾Tay ji daganalal naa leen ñam yu teey yi, te ñamu boroom téere ya dagan na ci yéen, séenuw ñamit dagan na ci ñoom, ak ñi fegu ci jigéen i jullit ñi, ak ñi fegu ci jigéen i ñi ñu jox téere ca ñaleen jiitu woon, bu ngeen leen joxee séen i can, te góor ña di ñu fegu, ñu mucc ci njaalo, ak a ànd ak ñu ñu takkul, képp ku weddi ginaaw ak ngëm ay jëfam yàquna, te bis pénc ba dinañ bokk ca Way-ñàkk ya 5﴿

[Saaru Maa-ida:5].

Yàlla mu kawe mi neena:

﴾Yàlla xamal na la xamal ña la jiitu woon ci ne boo bokkaalee say jëf di na yàqu, te di nga bokk ci Way-ñàkk 65﴿

[Saaru Assumari:65]

Aaya yiy tektale wax ju mel nii bari na ci Alxuraan, téereb Yàlla bu leer bi ak Sunnas yónnenteem bu wóor ba yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, day tektale ne pas-pas bu wér mi ngi ame ci gëm Yàlla ak Malaaka yi, ak Téere yi ak Yónnente yi, ak Bis bu mujj ba, ak Dogal bu neex ak bu naqari, juroom mbenni bir yii ñooy cosaan i pas-pas bu wér bi tax téereb Yàlla bu tedd ba wàcci te ci la Yàlla yónni Yónnenteem ba Muhammat yalna ko Yàlla dolli mucc ak jàmm.

Day soqikoo ci cosaan yi lépp lun wara gëm ci mbir yu fàddu yi, ak mbooleem li Yàlla ak ub Yónnenteem -yalna ko Yàlla dolli mucc ak jàmm- xibaare, te liy tegtale juróom benni cosaan yii nag ci Alxuraan ak Sunna barina lool, bokk na ca loola wax i Yàlla mu sell mi:

﴾Mbaax nekkul rekk ci ngeen jublu penku ak sowu, waaye mbaax mooy gëm Yàlla ak bis bu mujj ba, ak Malaaka ya, ak téere ya, ak Yónnente ya ﴿

[Saaru Baqara: 177].

Ba laaya ja jeex. Ak waxam ja moom Yàlla mu sell mi:

﴾Yónnente bi gëm na li Boroomam wàcce ci moom, ak jullit ñi ñoom ñépp gëm nañu Yàlla, ak i Malaakaam,ak i téereem,ak i Yónnenteem, dunu tàqale kenn ci diggante Yónnente yi.﴿

[Saaru Baqara:285].

Ak waxam ja moom Yàlla mu sell mi:

﴾Ey yéen ñi gëm gëmleen Yàlla ak ub Yónnenteem, ak téere ba mu wàcce ca Yónnenteem ba, ak téere ba mu wàcce ca la ko jiitu, képp ku weddi Yàlla ak i Malaakaam, ak i téereem, ak i Yónnenteem, ak bis bu mujj ba sànku na cànkute gu sori 136 ﴿

[Saaru Nisaa-i: 136].،

Ak waxam ja moom Yàlla mu sell mi:

﴾Xanaa xamoo ne Yàlla xam na li nekk ci Asamaan ak Suuf, loola ma nga ca téere ba,(lawhul mahfuus) te loolu yomb ci Yàlla la 70 ﴿

[Saaru Alhàjji: 70].

Hadiis yu wér yiy tegtale cosaan yii itam bari na lool, bokk na ca Hadiis bu wér bu siiw ba Muslim nettali ca téereem bu wér ba, muy Hadiisub Omar ibnu Xattaab -yakna ko Yàlla domme gërëm- mu ne Jibriil -yalna ko Yàlla dollee musël- laaj na Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- luy ngëm, mu ne ko:

Mooy nga gёm Yàlla ak ay Malaakaam, ak ay téereem, ak ay Yónnenteem, ak bis bu mujj ba,te nga gëm dogal ba,bu neex ba ak bu naqari ba. loolu mooy Hadiis bi.

Buxaariyu ak Muslim ñoo ko génne ci Hadiis i Abuu Hurayrata.

Juróom benn cosaan yi nag, ci la mbooleem li war jullit bi war a fas ci àq i Yàlla -mu sell mi- bàyyikoo, ak mbirum bis pénc, ak lu dul loolu ci mbir i gumpa yi.

Gëm Yàlla mu kawe mi.

Mooy Gëm ne Yàlla mooy buurub dëgg bi yayoo jaamu te ku dul moom yayoo wu ko.

Bokk na ci gëm Yàlla -mu sell mi- mooy gëm ne mooy buuru dëgg bi yayoo jaamu,ku dul moom yayoo wu ko, ndax mooy ki bind jaam ñi, di rafetal jëme ci ñoom, te leen di wërsëgal, te xam séen biir ak séen bitti, te mooy ki man a fay ñi koy topp ci ñoom, di mbugal ñi koy moy ci ñoom, jaamu gii nag moo tax Yàlla bind nit ak jinne, te moo leen ko digal, ni ki ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:

﴾ Binduma jinne ak nit lu dul ngir ñu jaamu ma 56﴿

[Saaru Azzaariyaati: 56]

﴾Bëgguma ci ñoom wërsëg bëguma it ñu leel ma.﴿

[Saaru Azzaariyaati: 57].

﴾ Yàlla mooy kiy wërsëgal te mooy boroom kàttan gu bari doole gi.﴿

[Saaru Azzaariyaati:58].

Yàlla -mu sell mi neena-:

Yéen nit ñi jaamuleen séen Boroom bi leen bind, te bind ña leen jiitu woon ngir ngeen ragal ko 21]

[Saaru Baqara: 21]

﴾Yàlla moomu moo leen lalal Suuf si, tabaxal leen Asamaan si, wàcce ndox ci Asamaan génne ci gàncax muy wërsëg ci yéen, kon buleen wutal Yàlla ay moroom te fekk xam ngéen ko 22﴿

[Saaru Naqara: 22].

Yàlla moo yónni Yónnente yi, wacce téere yi, ngir leeral dëgg ak woote ca, ak moytandikuloo lu wuute ak moom, ni ko Yàlla -mu sell mi te kawe- waxe:

﴾Yónni nan ab Yónnente ci béppu xeet ngir ñu jaamu Yàlla te moytu lépp lees di jaamu te du Yàlla ﴿

[Saaru Annahli: 36].

Yàlla mu kawe mi neena:

﴾Yaw Yónnente bi yónniwuma ca la la jiitu benn yónnente lu dul ne xamal nan ko ne amul benn buur bees di jaamu ci ak dëgg bu dul man ,kon nag jaamuleen ma 25﴿

[sóouratu al annbiyaahi:25]

Yàlla mu kawe mi te màgg neena:

﴾Alif laam raa,lii ab téere la bees xereñe ay aayaam,te muy lees tàqale mu jóge ci ku xereñ ka te xam lépp 1

Buleen jaamu ku dul Yàlla man maay ki leen ciy xupp ak a bégal 2 ﴿

[Saaru Huud: 1-2].

Dëgg dëgg i jaamu gii mi ngi ci wéetal Yàlla mu sell mi ci mbooleem li ko jaam ñi di jaamoo ci ñaan, ak ragal, ak julli, ak woor, ak rendi, ak nesër, ak lu dul loolu ci xeeti jaamu yi, ci anamug toroxlu ñeel ko, ak xemmeem ak tiit and ak bëgg gu mat sëkk ñeel ko, -moom Yàlla mu sell mi- ak toroxlul màggam ga, te li ëpp ci Alxuraan daa wàcci di leeral cosaan lu màgg lii, ni ki wax i Yàlla mu sell mi:

﴾ Jaamuleen Yàlla te sellalal ko diineem 2

Ndax du Yàlla moo moom diine ju sell ﴿

[Saaru Azzumari 2-3].

Ak waxam ja moom Yàlla mu sell mi:

﴾Sa Boroom digle na ne bu leen jaamu kudul moom ﴿

[Saaru Al-israa: 23].

Ak waxam ja -màgg na kawe na-

﴾ Ñaanleen Yàlla te sellalal ko diine ji donte neexul yéefar yi 14 ﴿

[Saaru Xaafiri: 14].

Ñёw na ci téereb Buxaariyu ak Muslim ñu jële ci Muhaas ibnu Jabal -yalna ko Yàlla dollee gërëm- mu ne Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- neena:

Li Yàlla yayoo ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañkoo bokkaale ak dara ».

Bokk na ci juróoom i ponk i lislaam yu fés yi: gëm mbooleem li Yàlla waral ci jaamam yi te farataal ko ci ñoom.

Bokk na ci gëm Yàlla gëm mbooleem li Yàlla waral ci jaamam yi te farataal ko ci ñoom ci ponk i lislaam yu fés yi, te mooy seede ne amul benn buur bees di jaamu cig dëgg bu dul Yàlla, ak ne Muhammad ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe azaka, ak woor weeru koor, ak aj Màkka, ci ku ko man, ak lu dul loolu ci farata yi Sariiha ju laab ja indi.

Li ëpp ci ponk yii te gëncaa màgg mooy seede ne amul benn buur bees di jaamu ci dëgg bu dul Yàlla ak ne Muhammad ndawal Yàlla la, seede ne amul ben buur bu dul Yàlla day laaj sellal jaamu ngi ngir Yàlla dong, te dàq jaamu ga ci ku dul moom, lii mooy maanaam amul benn buur bees di jaamu bu dul Yàlla, li miy tekki mooy amul kok dees na ko jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, lépp lees di jaamu te du Yàlla moo xam nit la, walla Malaaka, walla jinne, walla lu dul yooyu, loolu lépp lees di jaamu la cig neen, ki ñiy jaamu cig dëgg mooy Yàlla dong ni ki ni mu ko waxe-moom Yàlla mu sell mi-: ﴾Loolu mooy ne Yàlla rekk mooy dëgg te lépp lu ñiy jaamu te du moom ag neen la ﴿ [Saaru Alhajji: 62]. Jiitu na nu leeral ne Yàlla -mu sell mi- moo bind nit ak jinne ngir cosaan lu cosaanu lii, digal leen ko, yonni ca ay Yónnente, wàcce ca ay téere, xalaatal loola bu baax, te nga settantal ko lu bari ngir mu leer fi yaw li ëpp ci juulit ñi réere gu màgg gi ñu nekke ci cosaan li, batax ñuy jaamu lu dul Yàlla boole ko ak moom, soppi lu rëy ci àqam jox ko keneen. Yàlla mooy dimbalee.

Ak gëm ne Yàlla mooy ki bind li nekk ci àdduna di doxal séen i mbir di ca soppaxndiku ci-xam-xamam ak kàttanam.

Bokkk na ci gëm Yàlla -mu sell mi- gëm ne Yàlla moo bind li ne ci àdduna di doxal seen i mbir di ca soppaxndiku ci xam-xamam ak kàttanam, ni ki ni mu ko soobe -moom Yàlla mu sell mi- te moom moo moom àdduna ak àllaaxira, mooy Boroom mbindeef yépp, ku dul moom bindoo, te amul buur bu dul moom. Te moom mo yónni Yónnente yi, wàcce téere yi, ngir defar jaam ñi, te di leen woo ci la séenug mucc nekk ak séenug mbaax ci àdduna ak àllaaxira. Ak ne Yàlla -mu sell mi- amul ndend ci yooyu yépp, ni ki niko Yàlla mu kawe mi waxe: ﴾Yàlla mo binde lépp te moo mengoo lépp lumu man a doon 62﴿ [Saaru Azzumari: 62]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾Séen Boroom mooy Yàlla mi bind Asamaan yi ak Suuf yi, ci juróom benni fan, daadi yamoo ca kaw Aras, guddi gi day duggante ak bëccag gi, diko sàkku sàkku bu gaaw, jant bi ak weer wi ak biddiw yi dees leen a tàggat ci ndigalam, damane moom mooy Boroom mbindeef yi ak mbir ya, Yàlla daal ku barkeel la te mooy Boroom mbindeef yépp 54﴿ [Saaru Al-ahraaf: 54]

Gëm tur i Yàlla yu màgg yi, ak melokaanam yu rafet yi ci lu dul di ko soppi, ak di ko neenal, walla di ko melal, walla di ko niróole ak yu mbindeef.

Bokk na ci gëm Yàlla batay gëm tur i Yàlla yu rafet yi, ak melokaanam yu kawe yi ñëw ci téereem bu tedd bi, ak yi sax jóge ci Yónnenteem bu wóor bi ci lu dul soppi, walla neenal, walla melal, walla sax di ko niróole ak mbindeef. li war mooy wéyal ko ni ki mu ñëwe te bañko melal, ànd ak gëm la miy tektale ci maanaa yu màgg yi nga xam ne mooy melokaanu Yàlla yi, -mu magg mi te kawe- li war mooy melal ko namu yelle ci moom ci lu dul muy niróog mbindeef yi ci dara ci ay melokaanam, ni ki ni ko Yàlla mu kawe mi waxe: ﴾Moom niroowul ak dara mooy kiy dégg di gis ﴿ [Saaru Assuuraa: 11] Yàlla mu kawe mi te màgg neena: ﴾Bu leen di joxe ay misaal ñeel Yàlla, Yàlla mooy ki xam waaye yéen xamu leen ﴿ [Saaru Annahli: 74]. Lii mooy-pas- pasu waa Sunna ak mbooloo ma, muy àndandooy Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- ak ña leen topp ci ag rafetal, mooy li imaam Abul Asan Al-ashariyu -yalna ko Yàlla yërëm- toxal ci téereb: "Almaqaalaatu" jële ko ci waa Hadiis ak waa Sunna, ku dul moom it toxal na ko ci woroom xam-xam yi ak ngëm. Al-awzaahii -yalna ko Yàlla yërêm- laaj na Azzuhriyu ak Makhuul, aaya yiy wax ci melokaan yi, ñu ne ko wéyéle leen ko ni mu ñëwe. Alwaliid ibnu Muslim -yalna ko Yàlla yërëm- neena: laaj nan Maalik ak Al-awzaahii, ak Lays inbu Sahd, ak Sufyaan Assawriyu -yalna ko Yàlla yërëm- aaya yi ñëw ci melokaan yi, ñoom ñëpp ñu ne: wéyél leen ko ni mu ñëwe te bañkoo melal. Al-Awzaahiyu -yalna ko Yàlla yërëm- neena: nun ak ñi toppoon ci sahaaba yi nun ñépp daje woon nanu ci wax ne Yàlla -mu sell mi- ma nga ca kaw Arasam ja, te it gëm nan li ñëw ci Sunna ci ay melokaan. Bi ñu laajee Rabiiha bun Abi Abdu Rahmaan sëriñu Maalik -yalna ko Yàlla yërëm- neena: yamoog Yàlla ci Aras réeréesuko melokaan wa nag xameesuko, ci Yàlla la woote bi jóge, Yónnente bi jotal gu bir moo ko war, nun dëggal moo nu war ) Bi ñu laajee Maalik -yalna ko Yàlla yërëm- loolu dane:( yamoog Yàlla lees xam la, melokaan wa nag xameesuko,gëm ko nag lu war la, te laaj ko bidaa la, ) ginnaaw ga mu wax kiy laaj ne ko: yaw de nit ku bon nga, daadi digle ñu génne ko. Nettali nañu lu mel nii jële ci yaay i jullit ñi Ummu Salamata -yalna ko Yàlla dollee gërëm-, Abuu Abdu Rahmaan ibnu Mubaarak -yalna ko Yàlla yërëm-neena: (Xam nanu ne sunu Boorom -mu sell mi- ma nga ca kaw Asamaanam ya ca kaw Arasam ja, mu tàqalikoo ak mbindeef yi.) Wax i boroom xam-xam yi ci buntu bii barina lool, maneesukoo toxal ci waxtaan wii, ku bëgg a xam lu ëpp lii na nafar li boroom xam-xam i Sunna yi bind, ci buntu bii, lu mel ni tëereb "Assunna" bu Abdul Laahi bun imaam Ahmat, ak téereb "Attawhiid" bu imaam bu màgg ba Muhammad bun Xuzayma, ak téereb "Assunna" bu Abul Xaasim Allalakaa-ii Attabariyu, ak téereb "Assunna" bu Abuu Bakrin bun Abuu Haasim, ak tontub Seexu Lislaam Ibnu Taymiyata, ñeel waa Humaat, moom tontu bu bariy ñariñ la, leeral na ca -yalna ko Yàlla yërëm -pas-pasu waa Sunna, toxal ca lu bari ci séen i wax, ak tektali Sariiha ak yu xel yuy wane wérug la waa Sunna wax, ak neenug li ñi wuute ak ñoom wax. Na ka noonuTéereem bi ñuy tudde Attadmiiriya yaatal na ca leeral ca pas-pasu waa sunna ci ay tegtalam yu Sariiha ak yu xel,ak tontu ca ci wuute ak dëgg ci luy reeral dëgg di dàjji neen,ci képp koo xam ne xool na loolu ci woroom xam-xam yi ci jubluwaay bu baax baax ak yéenee xam dëgg,képp ku wuute ak waa sunna ci li ñu fas ci buntub tur i Yàlla yi ak melokaan yi,manuta ñàkk mu wuute ak tegtal i Sariiha yi ak yu xel yi,ànd ak juuyoo ku leer nàññ ci lépp lu miy saxal ak lu miy dàq. Budee waa sunna nag ñoom dañiy saxalal Yàlla li mu saxalal boppam, walla Yónnenteem bi Muhammad -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- saxalal ko ko, ci sunnaam su wér sa, saxal gog du ànd ak niral, te da ñu koy setal -moom Yàlla mu sell mi- ci niroo ak ay mbindeefam, setal gu set wecci ci neenal ay turam, batax ñu mucc ci ak jaxasoo, te da ñuy jëfe tektal yépp, lii nag mooy doxaliinu Yàlla -mu sell mi- ci képp ku jàpp ci dëgg gi ñu yónni Yónnente yi, tey góor-góorlu ci loolu, tey sellal ngir Yàlla ci càkkuteefam, batax Yàlla di na ko dëppale ak dëgg, dina leeral aw layam, ni ki ni ko Yàlla waxe: ﴾ Li am daal mooy dinanu sànni dëgg ci kaw neen mu yàq ko, ba mu naaxsaay ﴿ [Saaru Al-Anbiyaa-i: 18]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾Amul léebu wu ñu lay mën a indil ludul dinan la indil dëgg, te mooy kay gën a leer ﴿ [Saaru Alfurxaan: 33]. Alhaafis ibnu kasiir -yalna ko Yàlla yërëm- tudd na si tafsiiram bu siiw ba bamiy wax ci wax i Yàlla -mu sell mi- ﴾ Séen Boroom Yàlla mooy ki bind Asamaan ak Suuf ci juróom benni fan daal di yamoo ca kaw Aras ﴿ [Saaru Al-Ahraaf 54].wax ju rafet ci buntu bii dana rafet nu toxal ko fii ngir njariñam lu rëy. Waxa na ne -yakna ko Yàlla yërëm- lii mooy yax bi: boroom xam-xam yi ci mbir mii am nann ci wax yu bari lool, deesu ko man a yaatal fi, waaye daniy jaar rekk ci yoonu mag ñu baax ña: ku mel ni Maalik, ak Al-Awzaahiyu, ak Assawriyu, ak Allays bun sahd, ak Assaafihiyu, ak Ahmad, ak Ishaaqa bun raahówéya, ak ñu dul ñoom, ci kilifay jullit ñi, ca démb ak tay, te mooy jàppe ko ni mu nëwe te baña melal Yàlla, bañkoo niroole ak mbindeef yi, bañ a neenal meloom yi, li feeñ te njëkk a dem ci xel i ñiy niroole Yàlla ak mbindeef yi lu dàqu la ci Yàlla, ndax Yàlla niroowul ak ay mbindeefam, te melul ni lenn te mooy kiy dégg di gis, liy mbir mi sax mooy ni ko boroom xam-xam yi waxe bokk na ci ñoom, Nahiim bun Hammaad, Alxuzaahi, sëriñu Buxaariyu, neena: ku niroole Yàlla ak ay mbindeefam weddi na, ku weddi li Yàlla melal boppam weddi na, li Yàlla melal boppam ak li ko ab Yónnenteem melal ak niroog mbindeef yi amu ca, ku melal Yàlla mu kawe mi li rot ci aaya yu leer yi, ak xibaar yu wér yi, ci anam ga yell ca màggug Yàlla ga, te mu dàqal Yàlla ak wàññiku, kooku sóobu na yoonu jub.

Gёm Malaaka yi.

Budee gëm Malaaka yi nag: day làmboo gëm leen ci ag boole ak ug tàqale, jullit bi day gëm ne Yàlla bind na ay Malaaka ngir ñu topp ko, mu melal leen ci ay jaam yu tedd, yoy duñu ko jiitu ci ay wax te ndigalam rekk la ñiy jëfe. ﴾ Yàlla xam na li nekk ci séen kanam ak séen ginnaaw, te duñ rammu kudul ku Yàlla gërëm, te ñoom dañoo tiit lool ngir ragal ko ﴿ [Saaru Al-Anbiyaa-i: 28]. Ñoom nag ay xeet la ñu, bokk na ci ñu ñu gàll yenu Aras, am na ci ñuy wattu àjjana ak sawara, am na ci ñu ñu gàll wattu jëf i jaam ñi. Da niy gëm itam ci ag tàqale ñi ci Yàlla tuddu ak ub Yónnenteem, bokk na ca ñoom Jibriil ak Mikaa-iil, ak Maalik miy wattu sawara, ak Israafiil mi ñu gàll wol buft ba, moom aw turam ñëw na ci Hadiis yu wér, sax na ci téereb Buxaariyu, jële ci Aysa -yalna ko Yàlla dollee gërëm- mu ne Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- neena: «Malaaka yi dees leen a bind ci ak leer, bind jinne yi ci sawara, bind Aadama ci ni ñu leen ko melale »Muslim moo ko soloo ci téereem bu wér bi.

Gёm téere yi.

Ni la ñiy gëme téere yi warees naa gëm ci ag boole ne Yàlla mu sell mi wàcce na ay téere ci ay Yónnenteem, ngir leeral dëggam gi, ak woote ca, ni ki ni mu ko waxe moom mu kawe mi: ﴾Noo yónni su nuy Yónnente ci ay lay yu leer, wàcce ci ñoom téere ba ak màndaxe ma ngir nit ñi dund ci ak màndu.﴿ [Saaru Al-Hadiid 25]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Nit ñi wenn xeet la ñu woon,Yàlla yónni ci ñoom Yónnente yi ñuy bégale ak a xuppe, mu jox leen téere ba ci ak dëgg, ngir ñu àtte nit ñi ca la ñu wuute...﴿ [Saaru Baqara: 213]. Da niy gëm ci tàqale la ca Yàlla tudd, ni ki Tawraat, ak Injiil, ak Azzabuur, ak Alxuraan moom nag moo ca gën moo ca mujj, moo leen féete kaw, moo leen di dëggal, mooy bi nga xam ne war na ci mbooleem xeet wi ñu topp ko, te àttewoo ci moom ak li wér ci Sunna jóge ci Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- ndax Yàlla mu sell mi moo yónni ab Yónnenteem Muhammad -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- yabal ko ci mbooleem nit ak jinne, mu wàcce ci moom Alxuraan jii, ngir mu àttewoo ci, def ko it muy saafara li ci xol yi, di leeral lépp te di ak njub, ak yërmànde ñeel jullit ñi, ni ki ni ko Yàlla mu kawe mi waxe: ﴾ Lii ab téere la bu ñu wàcce muy lu bàrkeel na ngeen ko topp, te ngeen ragal Yàlla ndax mu yërëm leen ﴿ [Saaru Al-Anhaam: 155]. Yàlla -mu sell mi neena-: { Wàcce nanu ci yaw téere ba muy leeral lépp, di ak njub, di yërmànde, di mbégte ñeel jullit yi ﴿ [Saaru Annahli: 213]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Yaw Yónnente bi waxal ne yéen nit ñi man la Yàlla yabal ci yéen ñépp, Yàlla minga xamne moo moom Asamaan yi ak Suuf yi, amul benn buur bu ñiy jaamu ci dëgg ku dul moom, mooy dundal mooy ray, gëmleen Yàlla ak ub Yónnenteem Yónnente bi manuta jàng moom minga xam ne dafa gëm Yàlla ak i waxam, toppuleen ko ndax ngeen jub ﴿ [Saaru Al-Ahraaf: 158]. Laaya yi ñëw ci anam gii lu bari la.

Gёm Yónnente yi.

Na ka noonu warees naa gëm Yónnente yi ci ag boole ak ug tàqale, da niy gëm ne Yàlla mu sell mi moo Yónni ci ay jaamam ay Yónnente yu bokk ci ñoom ñuy bigle tey xuppe, tey woote ci ag dëgg, ku leen wuyu dana texe, ku wuute ak ñoom di na sooy di na réccu, mooy ki mujj ci ñoom, te mooy ka ca gën, mooy sunu Yónnente Muhammad -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- ni ki ni ko Yàlla mu sell mi waxe: ﴾Yónni nan ab Yónnente ci béppu xeet ngir ñu jaamu Yàlla te moytu lépp lees di jaamu te du Yàlla ﴿ [Saaru Annahli: 36]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Ñoom ay Yónnente la ñu yuy bégle tey xuppe, ngir nit ñi bañ a am aw lay fa Yàlla ginnaaw Yónnente yi ﴿ [Saaru Annisaa-i: 165]. Yàlla mu kawe mi neena: { Muhammad du baayu keen ci séen i góor, waaye ndawal Yàlla la te moo mujj ci Yónnente yi } [Saaru Al-Ahazaab :40]. Kusi yàlla tudd wala ag tuddam sax jugé si Yónnente Yàlla bi danu koy gëm ci ak taqale ak cig ràññatle ni ki Nooh ak Huud ak Saalih ak Ibraiima ak ñudul ñoom, Yàlla na nekk si ñoom ak ci sunub Yónnente gën gi mucc ak gën gi sell ak jàmm.

Gёm bis bu mujj ba

Budee gёm bis bu mujj ba

Da ciy dugg gëm lépp lu Yàlla wax walla Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- wax ko, ci luy ñëw ginnaaw dee, ni ki fitnay bàmmeel ak mbugalam ak i xéewalam, ak liy xew bis pénc ba si tiitange ya, ak tar-tar ya, ak jéggi siraat, ak màndaxem jëf ya, ak luññutu ga, ak pay ga ak tasaareg téere ya ca nit ña, di na am kuy jële téereem ci ndayjooram ak ku koy jële ci càmmooñam wala ci ginnaawam. Day dugg ci gëm téere yi ba tay gëm déegu sunu Yónnente Muhammad ba ñiy naane, ak gëm àjjana ak sawara, ak gis gi jullit ñi di gis séen Boroom mu sell mi, ak wax jimiy wax ag ñoom, ak lu dul loolu ci li bawoo ci Alxuraan, ak ci Sunna su wér si bàyyikoo ci Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- warees naa gëm loolu lépp ci anam gi ko Yàlla leerale ak ub Yónnenteem yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc.

Gëm ndogal yi.

Budee gëm ndogal yi nag day làmboo gëm ñenti mbir:

Ba ca njëkk: mooy Yàlla -mu sell mi- xam na la jiitu ak liy ñëw, xam na it mbir i jaamam yi, xam na séen i wërsëg, ak séen i dig, ak séen i jëf, ak lu dul loolu ci séen i mbir, dara nëbbuwu ko -moom Yàlla mu sell mi- ni ki ni mu ko waxe: ﴾Yàlla xam na lépp﴿ [Saaru Baqara: 231]. Yàlla mu kawe mi te màgg neena: ﴾ Ngir ngéen xam ne Yàlla mooy ki mën lépp, te Yàlla it moo peeg lépp cig xam ﴿ [Saaru Attalaax: 12]. Ñaareelu mbir mi: mooy Yàlla -mu sell mi- bind na lépp lu mu dogal te àtte ko, ni ki ni mu ko waxe: ﴾ Nun xam nan li suuf si di wàññi ci ñoom, te nekk na fi nun téere buy aji-wattu lépp 4 ﴿ [Saaru Xaaf: 4]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾Lépp lu mu man a doon takk nanu ko ci ab téere bu leer ﴿ [Saaru Yaasiin: 12]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾Xanaa xamoo ne Yàlla xam na li nekk ci Asamaan ak Suuf, loola ma nga ca téere ba,(lawhul mahfuus) te loolu yomb ci Yàlla la 70 ﴿ [Saaru Alhàjji: 70]. Ñàtteelu mbir mi: mooy gëm coobarey Yàlla ju am doole ja, lu ko soob mooy am, lu ko soobul du am, ni ki ni mu ko waxe moom Aji-Sell ji: ﴾ Yàlla mooy def lu ko soob﴿ [Saaru Alhajji: 18]. Yàlla mu kawe mi te màgg neena: ﴾ Liy mbiram mooy bu bëggee dara danaan ko nekkal rekk mu nekk ﴿ [Saaru Yaasiin: 82]. Yàlla -mu sell mi neena-: ﴾ Du leen soob mukk lu dul dafa soob Yàlla,Yàlla Aji-Xam la Aji-Xereñ la 30 ﴿ [Saaru Al-insaan: 30]. Ñenteelu mbir mi: mooy ak mbindam -moom Aji-Sell ji- mbooleem mbindeef yi, ku dul moom bindul, amul buur bu dul moom, ni ki mu ko waxe: ﴾ Yàlla moo bind lépp, te moo gàlloo lépp lu mu man a doon 62 ﴿ [Saaru Azzumari: 62]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Yéen nit ñi fàttalikuleen xéewal i séen Boroom, ndax am na ku bind ku dul Yàlla di wërsëgal ci Asamaan yi ak ci Suuf yi, amul benn buur bu ñuy jaamu ci dëgg bu dul moom, na ka ngéen di wane ginnaaw dëgg 3 ﴿ [Saaru Faatiri: 3]. Gёm dogal yi ci waa Sunna ak mbooloo ma day làmboo ñenti mbir yii, mu wuute ak ñi weddi lenn ca yooya ci ñoñ bidaa ya.

Gёm nag wax la ak jëf, day dolliku ci ak topp Yàlla di wàññiku ci ag moy.

Day dugg ci gëm Yàlla fas ne gëm wax la ak jëf, day yokk ci ag topp, di wàññiku ci ag moy, gëm it ne du dagan ñuy yéefarloo kenn ci jullit ñi ci genn moy gu yées bokkaale, ak ug kéefar, ni ki njaalo, ak sàcc, ak lekk ribaa, ak naan yiy màndal, ak dog ay wayjur, ak lu dul loolu ci bàkkaar yu mag yi, li féeg ka koy def daganaluko, ngir li Yàlla Aji-Sell ji wax: ﴾ Yàla du jéggal ku koy bokkaale, dana jéggale nag lu yées bokkaale ñeel ku ko soob ﴿ [Saaru Annisaa-i: 48]. Ak li sax ci Hadiis yi ñëw ci ay yoon yu bari Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- wax ne Yàlla day génne ca sawara ku xolam am lu toll ne as pepp ci ngëm.

Bëgg ngir Yàlla ak bañ ngir Yàlla, ak péete ngir Yàlla, ak noonoo ngir Yàlla.

Bokk na ci gëm Yàlla: bëgg ngir Yàlla ak bañ ngir Yàlla, ak péete ngir Yàlla, ak noonoo ngir Yàlla, dana war ci juulit bi mu bëgg jullit ñi, te féete ag ñoom, bañ yéefar yi te noonoo leen, te ñi jiitu si juulit i xeet wii ñooy àndandooy Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-. Waa sunna ak mbooloo ma dañu leen a bëgg mengoo leen, fas ne ñoom ñoo gën ci nit ñi ginnaaw Yónnente yi, ngir wax i Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- « Maas gi gën ci maas yi mooy samag maas, ak ña topp ca ñoom, ak ña topp ca ñoom »Dëppoo nan ci ak wéram. Da ñiy fas ne ki gën ci ñoom mooy Abuu Bakrin, ginnaaw ba Umar Alfaaruux, ginnaaw ba Usmaan Sun-Nuurayni, ginnaaw ba Alliyu Almurtadaa, -yalna leen Yàlla dollee gërëm- ñoom ñépp, ginnaaw ga ñi mottali fukk yi ñu dig àjjana, ginnaaw ba ña des ci sahaaba yi, -yalna leen Yàlla dollee gërëm- ñoom ñëpp, da ni noppi i ci li xewoon diggante sahaaba, da ñiy fas ne it ñu doon góor-góorlu la ñu ci loolee, ku ci am dëgg am nga ñaari yool, ku ci juum am nga benn yool. Da ñiy bëgg waa kër Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak muss- ña ko ca gëm, te féetewoo leen, féete it soxnay Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- yaayi jullit ñi, di leen ñaanal ngërëm, ñoom ñépp, da ñiy set it ci yoonu Raafida yi ñi nga xam ne dañoo bañ àndandooy Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc - di leen saaga, di ëppal ci waa-kër Yónnente bi, di leen yëkkati fu kawe séen wàccuwaay ba leen Yàlla Aji-Sell ji wàcce ni ki ni ñiy sete ci yoonu Nawaasib yi, ñiy lor waa kër Yónnente bi ci wax wala ci jëf.

Mbooleem li nu tudd ci wax ju tënku jii, mi ngi dugg ci pas-pas bu wér bi nga xam ne moom la Yàlla yónni ndawam la Muhammad -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-, te mooy pas-pasu kurel bu mucc ba, Waa-Sunna ak mbooloo ma, ñi Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- waxoon ci ñoom: « Ab kurel ci sama xeet wi du deñ di nekk ci dëgg di ñun dimbale, ku leen beddi itam du leen lor ba mbirum Yàlla mu sell mi di ñëw »Yónente bi -yalna jàmm ak mucc nekk si moom-neena: « Yahuud yi tàqalikoo nañ ci juróom ñaar fukki kurel ak benn, Nasaraan yi itam tàqalikoo nan ci juróom ñaar fukki kurel ak ñaar, te sama xeet wii di na ñu tàqalikoo ci juróom ñaar fukki kurel ñàtt, ñoom ñépp ay dem sawara ba mu des benn, Sahaaba yi ne ko: kurel boobu ban la yaw Yónnenteb Yàlla bi, mu ne: ba nekk ca li ma nekk man ak samay Sabaaba »Te mooy pas-pas bees war a jàpp te tënku ca te moytu lépp lu wuute ak moom.

Wax ci ñi juuyoo ak pas-pas bii te nekk ci safaanam.

Séen i xeet:

Budee ñi wuute ak pas-pas bii te nekk ci ab safaanam,ñoom xeet yu bari la ñu, am na ci ñuy jaamu ay Xëram, ak ay Malaaka, ak ay Wàlliyu, ak ay Jinne, ak ay Garab, ak i Xeer, ak yu dul yooyu, gaayii nag wuyu wu ñu wooteb Yónnente yi, waaye dañoo wuute ak ñoom, boole ci di leen noonoo, ni ki ni ko Xuraysin ak xeet i Araab ya defe ak sunu Yónnente Muhhammat -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-ñoom da ñu daan ñaan la ñu daa jaamu fajug aajo, ak wérug ñi feebar, ak daan noon ya, da ñu daan leen rendil, te di leen néséral, ba leen Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- weddee ca loola digal leen jaamu Yàlla dongu dañoo yéemu ca loola weddi ko daaldi wax: ﴾ Ndax daa bëgg a def Yàlla muy jenn Yàlla lii de mbir mu yéeme la ﴿ Saaru Saad: 5]. Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- masul deñ di leen woo ci Yàlla, di leen xupp ci bokkale, di leen leeralal dëgg-dëgg i li mu leen di woo, ba Yàlla jubal ca ñoom ña mu jubal ñu dugg ci diiney Yàlla ji di ay mbooloo, diiney Yàlla ji fës ci kaw mboolem diine yi ginnaaw woote bu jokkaloo, ak xeex bu yàgg bu Yónnente -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- doon def moom ak ay àndandoom -yalna leen Yàlla dollee gërëm- ak ña leen topp ci ak rafetal, ginnaaw ba nag la mbir ya soppiku réer not ñi gën a bari ci mbindeef yi, ba mujj ñi ëpp dellu ci diiney ceddo, ci ëppal ci Yónnente yi, ak Wàlliyu yi, di leen ñaan ak a xettaliku ci ñoom, ak lu dul loolu ci xeeti bokkaale, te xamu ñu maanaam LAA ILAAHA ILLAL LAAHU, ni ko yéefari araab ya xame woon,Yàlla rekk ay dimbalee.

Bokkaale gi deñul di tasaaroo ci nit ñi ba ci sunu jamono jii, ngir réer gu not, ak sori jamonoy Yónnent.

Lëntum ñi mujj ci ñoom mooy lëntum ña njëkk ci ñoom, ak tudd lenn ci pas-pas i kéefar yi.

Lëntug gaayi mujj yii mooy lëntug ñu njëkk ña, te mooy séen i wax: ñii -séen i xëram- ñoo ñuy ramm fa Yàlla, jaamu wunu leen lu dul ngir ñu jigeel nu Yàlla,Yàlla dàjji na lënt mii, daaldi leeral ne ku jaamu ku dul moom ak ku mu man a doon bokkaale na ko weddi na ko. ni ki ni ko Yàlla waxe: ﴾ Da ñiy jaamu lu dul Yàlla lu leen dul lor te du leen jariñ, teg ca di wax ne ñii ñoo ñiy ramm fa Yàlla.﴿ [Saaru Yuunus: 18]. Yàlla mu sell mi tontu na leen ca waxam: ﴾ Ndax da ngeen di xibaar Yàlla lu mu xamul ci Asamaan yi ak sSuuf yi, Yàlla sell na kawe na ci li ngeen koy bokkaaleel. ﴿ [Saaru Yuunus: 18]. Yàlla -mu sell mi- leeral na ci aaya ji ne jaamu ku dul moom muy Yónnente yi, ak Wàlliyu yi wala ku dul ñoom luulu bokkaale bu mag la donte ki koy def dakoo tudde leneen, Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Ñi jàppe lu dul Yàlla ay kilifa da ñu naan jaamu wunu leen lu dul ngir ñu jegeel nu Yàlla ak jege ﴿ [Saaru Azzumari: 3]. Yàlla -mu sell mi- tontu na leen ca waxam ja: Yàlla mooy àtte seen diggante ca la ñu wuute, Yàlla daal du jubal ab fen kat bu ko weddi. ﴿ [Saaru Azzumari: 3]. ﴾ Yàlla -tudd naa sellam ga- leeral na ci loolu ne séen ug jaamu lu dul moom ci ñaan, ak ragal, ak yaakaar, ak yu mel ni yooyu, weddi ko la -moom Yàlla mu sell mi- li gën a doon ay fen ci séen wax ja nag mooy lin wax ne séen xëram yi da leen di jegeele Yàlla ak jege. Bokk na ci pas-pas i kéefar yi safaanoo ak pas-pas bu wér, te wuute ak li Yónnente yi indi -yalna leen Yàlla dolli jàmm ak mucc- li weddi kati Yàlla yi fas ci sunu jamono jii, ci ñi topp Màrkis, ak Liyniin ak ñu dul ñoom, ci woote kati kéefar yi, moo xam loolu da ñu koo tudde Istiraakiyatu, wala Suyuuhiyatu, wala Bahsiyatu, wala lu dul loolu ci tur yi, bokk na ci cosaan i weddi kat yii ne Yàlla amul te dund gi moy li ñiy teg bët rekk. Bokk na ci séen i cosaan weddi dekki ga, ak àjjana, ak sawara, ak weddi diine yépp, ku xool séen i téere jàng la ca nekk dana xam loolu ci lu wóor, amul nàttable ne pas-pas bii lu wuute la ak mboleem diiney asamaan yépp, te day yóbb boroomam ci mujj gu ñaaw ci àdduna ak àllaaxira. Bokk na ci pas-pas yi safaanoo ak dëgg lenn ci li ñiy askanoo baatin gëm, ak lenn ci Waa-tasawuf, mooy ne ñi ñiy tudde ay wàlliyu da ñiy bokk ak Yàlla ci doxal, di soppaxndiku ci mbir i àdduna bi, ñu leen di tudde ay Aqtaab, ak ay Awtaad, ak ay Axwaas, ak lu dul loolu ci ay tur yu ñu fental séen yàlla yi. Pas-pas bii moo gën a bon ci bokkaale ci moomeelu Yàlla gi, te moo gën a bon it bokkaaleg ceddoy araab ya, ndax yéefar i araab ya bokkaale wu ñu woon ci moomeelu Yàlla gi, waaye ci ak jaamu la ñu doon bokkaale, da ñu doon bokkaale ci jamonoy yomb-yomb, budee jamonoy tar-tar nag ñu sellalal Yàlla jaamu ga, ni ki ni ko Yàlla -tudd naa sellam ga-waxe: ﴾Bu ñu waree ci gaal ya da ñiy woo Yàlla sellalal ko diineem ji,su leen musalee ba ñu wàcci gaal ga rekk daaldi bokkaale waat 65﴿ [Saaru Al-Hankabuut: 65]. Budee moomeelu Yàlla gi ñoom nanguloon nañ ko ko moom dongu, ni ki ni ko Yàlla -mu sell mi- waxe: ﴾ Boo leen laajoon ku leen bind dañ i wax ne xanaa Yàlla ﴿ [Saaru Azzuxruf: 87]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Waxal yaw Yónnente bi ana kan moo leen di wërsëgal ci Asamaan ak ci Suuf, ana kan moo moom dégg ak gis, kan mooy génne liy dund ci li faatu, di génne li faatu ci liy dund, kan mooy doxal mbir yi, danan wax ne xanaa Yàlla neleen lu tewoon ngeen rafal Yàlla kon 31 ﴿ [Saaru Yuunus: 31]. Aaya yi ñëw si wàll gii lu bari la.

Li bokkaalekat yu mujj yi, yéese ñu njëkk ña.

Budee bokkaalekat yu mujj yi,ñoom yées na ñu ñu njëkk ña ci ñaar i anam:Bu njëkk ba:mooy bokkaaleg ñenn ci ñoom ci moomeelu Yàlla gi la,ñaareel bi mooy:séenug bokkaale day ame ci yomb-yomb ak ci jafe-jafe,ni ki la ko képp ku jaxasoo ak ñoom te càmbar séen i mbi xame,te gis la ñuy def ca bàmmeelu Al-Husaynu,ak Al-Badawiyu,ak ñu dul ñoom ca Misra,ak ca bàmmeelu Al-Hidruus ca Hadn,ak Al-hHaadii ca Yaman,ak Ibnu Arabiyu ca Saam,ak Seex Abdul Xaadir Al-Jaylaaniyu ca Hiraaq,ak yeneen bàmmeel yu siiw yu dul yooyu nga xam ne way-réer ya ëppal na ñu ca,te joxnañu leen lu bari ci àq i Yàlla-mu sell mi- te néew na ku leen koy tere,di leen leeralal dëgg-dëgg i wéetal Yàlla gi tax Yàlla yónni ab Yónnenteem,-yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-ak Yónnente yako jiitu wóon,nun Yàlla moo nu moom te ci moom rekk la niy dellu. Noo ngi ñaan Yàlla -tudd naa ag sellam- mu delloo leen ca séenug njub, te baril ci ñoom woote kati njub, te may njiit i jullit ñi ak séen i woroom i xam-xam ñu man a xeex bokkaale gii, ak jële ko fi ak ay jumtukaay am moom Aji-jege la Aji-Dégg la. Bokk na ci pas-pas yi safaanoo ak pas-pas bu wér, ci buntub tur i Yàlla yi ak melokaan yi, pas-pasu waa-bidaa, ñoom Jëhmiya, ak Muhtasila, ak ku jaar séenu yoon, ci dàq melokaan i Yàlla yi -tudd na ag sellam-ak di ko rafleel -moom Aji-Sell ji- ci melokaan i mat yi, ak di ko melal -tudd naa ag sellam- melokaanu lu amul ak yu amul ruuh, ak yu jomb ya, Yàlla gën naa kawe seen wax jii kawe gu rëy. Day dugg ci loolu ñi dàq lenn ci melokaan yi di saxal yenn ya, ñu mel ni Asaahira yi, ñoom da leen di war ca la ñu saxal ci ay melokaan safaanub la ñiy daw ca melokaan ya ñuy dàq, di soppi ay tektalam, ci loolu la ñu wuute ak tektali Sariiha yi ak yu xel yi, ci loolu la ñu jaxasoo jaxasoo gu leer nàññi. Budee Waa-Sunna ak mbooloo ma ñoom da ñiy saxalal Yàlla -mu sell mi- la mu saxalal boppam, wala Yónnenteem bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- saxalal ko ko ci ay tur ak ay melo, ca anam ga gën a mat, te di ko setal ci niróog ay mbindeefam, muy lu set wicci ci neenal ko, ñuy jëfe tektal yépp, te soppi wu ñu neenalu ñu, ñu daa di mucc ci jaaxasoo gi ñeneen ña tàbbi, ni ki nu ko leerale ca la jiitu. Lii mooy yoonu mucc ak texe ci àdduna ak àllaaxira, mooy yoonu jub wa mag i xeet wii jaaroon, ak séen i njiit, te ñu mujj ñi du ñu baaxe ci lu dul la baaxaloon ñu njëkk ña, te mooy topp Alxuraan ak sunna, moytu la wuute ak moom.

Warug jaamu Yàlla dong ak leeral sabab yees di daane noon i Yàlla yi.

Li ëpp solo ci wareefu mukallaf te gën a doon farata ci moom, mooy mu jaamu Boroomam -mu sell mi- Boroom Asamaan ak Suuf ak Aras ju màgg ja, ki wax ca téereem bu tedd ba ne: ﴾Séen Boroom mooy Yàlla mi bind Asamaan yi ak Suuf yi, ci juróom benni fan, daadi yamoo ca kaw Aras, guddi gi day duggante ak bëccag gi, diko sàkku sàkku bu gaaw, jant bi ak weer wi ak biddiw yi dees leen a tàggat ci ndigalam, damane moom mooy Boroom mbindeef yi ak mbir ya, Yàlla daal ku barkeel la te mooy Boroom mbindeef yépp 54﴿ [Saaru Al-ahraaf: 54] Yàlla -tudd naa sellam gi- xibaare na ci beneen barab ci téereem bi ne moom moo bind nit ak jinne ngir ñu jaamu ko, ci la waxe -màgg na te kawe na- ﴾ Binduma jinne ak nit lu dul ngir ñu jaamu ma 56﴿ [Saaru Azzaariyaati: 56] Jaamu Yàlla gii tax Yàlla bind nit ak jinne mooy wéetal ko ci xeeti jaamu yi ni ki julli ak woor, ak azaka ak aj ak rukuuh ak sujuud ak wër kaaba ga ak rendi ak nesër ak ragal ak yaakaar ak xettaliku ak dimbandiku ak muslu, ak mbooleem xeeti ñaan yi, day dugg ci loolu topp ko moom -Yàlla mu sell mi- ci mbooleem ay ndigalam te bàyyi ay tereem ci na ko téereem bu tedd ba tektalee, ak sunnas Yónnente bu wóor ba -yalna gën gi jàmm i Yàlla ak muccam nekk si moom-. Yàlla -mu sell mi- digal na nit ak jinne jaamu gii tax mu bind leen, te mu yónni Yónnente yépp wàcce téere ya ngir leeral jaamu Yàlla gii, ak faram-fàcce ko, ak woote ca, ak digle ñu sellalal ko Yàlla dongu, ni ki ni ko Yàlla mu kawe mi waxe: Yéen nit ñi jaamuleen séen Boroom bi leen bind, te bind ña leen jiitu woon ngir ngeen ragal ko 21] [Saaru Baqara: 21] Yàlla mu kawe mi te màgg neena: ﴾ Sa Boroom digle ne bu leen jaamu ku dul moom te na ngeen di rafetal jëme ca ñaari wayjur ya ﴿ [Saaru Al-israa: 23]. Maanaam xadaa ci aaya bii mooy digle na te dénkaane. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Digaluma leen lu dul ngeen jaamu Yàlla te sellalal ko diineem ji, te set wecc ci bokkaale, tey taxawal julli, tey joxe azaka, te loolee mooy diine ju jub ja 5 ﴿ [Saaru Al-Bayyina: 5]. Aaya yi ñëw ci wàll gii ci téereb Yàlla bi barina,Yàlla -mu màgg mi te kawe- wax na: ﴾ Lu leen Yónnente bi indil jël leen ko, lu mu leen tere bàyyi leen ko, te ngeen ragal Yàlla Yàlla déy ku tar mbugal la ﴿ [Saaru Al-Hasri: 7]. Yàlla -mu sell mi neena-: ﴾ Yéen ñi gëm topp leen Yàlla te topp Yónnente bi, ak seen i kilifa, bu ngeen xëccoo ci mbir na ngeen ko delloo ci Yàlla ak Yónnente bi ndeem gëm ngeen Yàlla ak bis bu mujj ba, loolu moo gën te moo gën a rafet ag mujj 59﴿ [Saaru Annisaa-i: 59]. Yàlla mu kawe mi te màgg neena: ﴾ Ku topp Yónnente bi topp na Yàlla ﴿ [Saaru Annisaa-i: 80]. Yàlla -mu sell mi neena-: ﴾Yónni nan ab Yónnente ci béppu xeet ngir ñu jaamu Yàlla te moytu lépp lees di jaamu te du Yàlla ﴿ [Saaru Annahli: 36]. Yàlla -mu sell mi neena-: ﴾Yaw Yónnente bi yónniwuma ca la la jiitu benn yónnente lu dul ne xamal nan ko ne amul benn buur bees di jaamu ci ak dëgg bu dul man ,kon nag jaamuleen ma 25﴿ [Saaru Al-Anbiyaa-i: 25] Yàlla mu kawe mi neena: ﴾Alif laam raa,lii ab téere la bees xereñe ay aayaam,te muy lees tàqale mu jóge ci ku xereñ ka te xam lépp 1 Buleen jaamu ku dul Yàlla man maay ki leen ciy xupp ak a bégal 2 ﴿ [Saaru Huud: 1-2]. Laaya yu ñu xereñe yii ak yi yor ay maanaam ci téereeb Yàlla bi, yépp day tektale warug sellal jaamu nga ngir Yàlla rekk te loolu mooy cosaanu diine ji, ni ki ni muy tektalee it ne loolu mooy sababus bind jinne ak nit, ak yónnig Yónnente yi, ak wàcceeg téere yi. Li war ci mbooleem mukallaf yi mooy sonne mbir mii, te dégg ko, te moytu ci li ñu bari tàbbi ci ñiy askanoo Lislaam ci ak ëppal ci Yónnente yi, ak nit ñu baax ñi, ak tabax séen i bàmmeel ak di ko jàppe ay jàkka, ak di leen ñaan, ak a xettaliku ci ñoom, ak di wéeru ci ñoom, ak di leen ñaan pajug aajo ak wuññi njàqare, ak wéral ñi feebar, ak daan noon ya, ak lu dul loolu ci xeeti bokkaale gu mag gi. Saxna joge ci Yónnenteb Yàlla bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- lu dëppoo ak li téereb Yàlla -mu mŋgg mi te kawe- di tektale, loola mi ngi ci ñaari téere yu wér yi, Muhaas ibnu Jabal ne Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- neena ko: ﴾ Ndax xam nga lan moy Àq i Yàlla ci ay jaamam, ak àq i jaam ñi ci Yàlla, Muhaas ne: mane ko: Yàlla ak ub Yónnenteem ñoo ko xam, Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- daa di ne ko: àq i Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañkoo bokkaale ak dara, àq i jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaale wul ak dara ﴿ [Hadiis bi] Ñëw na ci téereb Buxaariyu bu wér ba Inbu Mashuud -yalna ko Yàlla dollee gërëm- ne Yónnente bi -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- neena: " Ku faatu te fekk muy wutal Yàlla moroom dina dugg sawara". Muslim génne na si téere am buu wér ba jële si Jaabir doomi -yalna ko Yàlla dollee gërëm- mu ne Yónnente Yàlla bi -yalna ko dolli jàmm ak mucc- neena: « képp ku daje ak Yàlla te bokkalewuko ci dara day dugg aljana ku daje ak moom nag te bokkaleko ci dara day dugg sawara »Hadiis yi yor maanaa mii yu bari la, te masala bii bokk na ci masala yi ëpp solo te gën cee màgg,Yàlla moo yónni ab Yónnenteem Muhammad -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- ngir mu woote ci wéetal Yàlla ak tere bokkaale, mu taxaw ci jottali li ko Yàlla yónni -yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- gën gaa rafet aw taxawiin, ñu lor ko ci Yàlla ay lor yu tar mu muñ ko, ay àndandoom it ànd ak moom ca muñ ga -yalna leen Yàlla dollee gërëm- di jottali woote ba, ba Yàlla dindi mbooleem xërëm yi nekkoon ci Jasiiratul-Arab, nit ñi def ay mbooloo di dugg ci diiney Yàlla ji, ñu yàq xërëm yi wëroon kaaba gi ak ya woon ca biiram, daa di màbb Laata ak Huzza, ak Manaata, daa di yàq mbooleem xërëm ya nekkoon ca giir i Arab ya, màbb xërëm ya ñu yoroon, baatub Lislaam kawe Lislaam fës ci Jasiiratul-Arab. Topp jullit yi daadi jublu ci woote ak jihaad jëm ci bitti jaziiratul arab bi, Yàlla daadi jubal ci ñoom ku ag texe jiitu ci moom ci jaam yi, Yàlla tasaare ci ñoom dëgg ak mandu ci li ëpp ci suuf, ci loolu lañu mujje nekk ay njiit cig njub, ak ay dag ci dëgg, ak ay wootekat cig mandu ak yéwénal, ay njiiti njub ak wuutekati dëgg yi leen toop ak ñaleen toppaat ci ag rafetal jaar ci seen yoon wa di tasaare diiney Yàlla ji, di woo nit ñi ci wéetal Yàlla, ak di xeex ci yoonu Yàlla ci seen bakkan ak seen alal te dun ragal kenn yedd leen si Yàlla, Yàlla dëgëral leen daadi leeni dimbali daadi leen fésal si kaw kepp ku jàmmaarloa ak ñoom, Yàlla matale li mu leen digoon ci waxam ji: ﴾Yéen ñi gëm bu ngeen dimbalee Yàlla mu dimbali leen te dëgëral séen i ndëggu﴿ [Saaru Muhammad: 7]. Ak waxam ja -màgg na kawe na- ﴾ Yàlla dina dimbali ka koy dimbali, Yàlla nag ku am kàttan la te not 40 Mooy ña nga xam ne bu leen Yàlla dëgaralee ci Suuf da ñiy taxawal Julli, tey joxe Azaka, di digle lu baax, tey tere lu bon, Yàlla rekk moo yor mujjug mbir ya 41﴿. [Al-Hajji: 40-41]. Ginnaaw ba nag nit ñi soppi na ñu, daaldi tàqalikoo, sàggane mbirum jihaad, gënale ab nooflaay ak topp bànneex, ñaawtéef tasaaroo ci ñoom lu dul ku Yàlla musal -tudd naa selam ga- Yàlla soppi la ñu nekkoon, xirtal séen i noon ci séen kaw, muy payug la ñu fàggu, te sa Boroom du tooñ ay jaamam,Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Ndax te Yàlla du soppi xéewal gu mu xéewale aw nit lu dul ne dañoo soppiku ﴿ [Saaru Anfaal: 53]. Li war ci mbooleem jullit yi moo xam nguur la ak ay askan mooy dellu ci Yàlla -mu sell mi- te sellalal ko jaamu ga moom rekk, te tuub dellu ci moom ci la jiitu ci séenug gàttañlu ak séen i bàkkaar, te gaawe ci def la leen war ci ay farata, te moytu li ñu araamal ci ñoom, tey dénkante loolu ci séen biir, te cay dimbalante.

Bokk na ci li ëpp solo ci yooyu taxawal daan i Sariiha yi, ak àtte nit ñi ci Sariiha, ci mbir yépp, ak di ca àttewoo, te neenal àtte yi ñu tër te nu wuute ak yoonu Yàlla, te bañcaa àttewoo, te waral ci mboolem askan yi àtteb Sariiha, ni ki ni mu ware ci woroom xam-xam yi ñu jàngal nit ñi séen diine, ak a tasaare ci séen biir njàngalem lislaam, ak di dénkante ci dëgg ak muñ, tey digle lu baax di tere lu bon, ak a soññ njiit yi ci loolu. Ndiki lay ware xeex mboolem delluwaay yinga xamni day màbb diine lu ci melni Al-Istiraakiya ak Bahsiya ak wotèwo xeet ak yu mel ni yooyu ci ngiir yinga xam ni day wuute ak Sariiha bi, ci loolu ci la Yàlla di yewénale li yàqu woon ñeel jullit yi, mu leen di delloo séen tedd nga jan nekkoon, dileen dimbali ci kaw séeni noon, di léen kàttanal ci kaw Suuf ni ki mu ko waxè -tudd naa sellam gi tè moy ki gën a dëggu ay wax: ﴾ War na ci nun nu dimbali juulit ñi ﴿ [Saaru Arruum: 47]. Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ Yàlla dig na ñi gëm ci yéen tey def lu baax ne da na leen wuutal ci Suuf si ni ki ni mu wuutale woon ña leen jiitu wóon, te da na leen dëgëral ci seen diine ji mu gërëm, da na leen wuutalal it kaarànge ci ginnaaw séenug ragal ci kaw ñu may jaamu te duñu ma bokkaale ak dara, ku weddi ginnaaw loolu ñooñee ñooy kàccoor yi ﴿ [Saaru Annuur: 55]. Yàlla -mu sell mi neena-: ﴾Nun di na nu dimbali suniy ndaw ak ña gëm ci dundug àdduna ak bis pénc ba seedi ya di taxaw 51﴿ [Saaru Xaafiri: 51]. ﴾ Bis booba mooy ba nga xam ne deesul nangul tooñkat yi séen ngànt, te am rëbb ñeel na leen ak dëkkuway bu bon 52﴿ [Saaru Xaafiri: 52].

Yàlla la nuy ñaan-S-mu baaxal njiit i jullit ñi,ak ña ñu jiite, te may leen ak dégg ci diine,te dajale leen cig ragal Yàlla,te gindi leen ñoom ñëpp ca yoonam wu jub wa,te dimbalee dëgg ci ñoom,te faagaagale ci ñoom ak neen,te may leen ñëpp ñuy dimbalànte cig mbaax ak ragal Yàlla,ak dénkante dëgg te muñ ca,moom rekk moo méngoo loola,te moo ko man,yal na Yàlla defal sotti ak mucc ci jaamam ba tey ndawam,te dib tànneefam ci ay bindeefam,sunu yonnente tey sunu imaam di sunu sang Muhammat ibnu Habdul Laahi,ak ay waa këram ak i àndandoom, ak ca topp seen ug njub,was saalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wa barakaatuhoo.

Pas-pas bu wér ak ub safaanam, ak yiy yàq lislaam.

Laytaayug téere bi.

Gëm Yàlla mu kawe mi.

Mooy Gëm ne Yàlla mooy buurub dëgg bi yayoo jaamu te ku dul moom yayoo wu ko.

Bokk na ci juróoom i ponk i lislaam yu fés yi: gëm mbooleem li Yàlla waral ci jaamam yi te farataal ko ci ñoom.

Ak gëm ne Yàlla mooy ki bind li nekk ci àdduna di doxal séen i mbir di ca soppaxndiku ci-xam-xamam ak kàttanam.

Gëm tur i Yàlla yu màgg yi, ak melokaanam yu rafet yi ci lu dul di ko soppi, ak di ko neenal, walla di ko melal, walla di ko niróole ak yu mbindeef.

Gёm Malaaka yi.

Gёm téere yi.

Gёm Yónnente yi.

Gёm bis bu mujj ba

Gëm ndogal yi.

Gёm nag wax la ak jëf, day dolliku ci ak topp Yàlla di wàññiku ci ag moy.

Wax ci ñi juuyoo ak pas-pas bii te nekk ci safaanam.

Séen i xeet:

Lëntum ñi mujj ci ñoom mooy lëntum ña njëkk ci ñoom, ak tudd lenn ci pas-pas i kéefar yi.

Warug jaamu Yàlla dong ak leeral sabab yees di daane noon i Yàlla yi.

معلومات المادة باللغة العربية