×
New!

Bayan Al Islam Encyclopedia Mobile Application

Get it now!

Firi tèerèb paspasou wà souna (Wollof)

Kiko wâjal: Mohammed Cheikh Sene

Description

Firi tèerèb paspasou wà souna Lan moy paspasou gniy toop souna Danouy guemni al khourane bou tedebi

Download Book

    Firi tèerèb paspasou wà souna

    العقيدة أولًا لو كانوا يعلمون

    [Wolof-الولوفية]

    محمد شيخ سين

    Mohammed Cheikh Sene

    —™

    جبريل جيي

    Ngiko firi: Djibril Dièye

    Firi tèerèb paspasou wà souna

    بسم الله الرحمن الرحيم

    Nogui sante yalla miy brom mindèef yi, di sèedènè amoul kènne kougnou wara diàmou koudoul yàlla, di sèedènè yonnèn tèbi ab diamam la te yallako yonni, tè mom moo moudie ci yoonnèntiyi, yalla nako yalla doolli ay khèwal ak wakeuram ak sahabayi ak koulèen toop ci ak rafètal ba kèrok allàkhira.

    Ginàw loolou:

    Yàlla dafa yabal yoonnèntibi sallal làhou alayhi wasallama diokhko ak gnoub ak dinèy deugue, mou dèfko moudoon yeurmànè ci mindèefyi, di ab royou wày ci kèpe kouy dieuf, yalla lèralal diamam yi lèp louy bàkhal sèn mbiri àddouna ak allàkhira thi ay ay paspas you wèr aki dieuf you bàkh aki jikko you rafèt, mou diarè lèral gui ci yoonnènt bi sallal làhou alayhi wa sallama ak li gnou wathièe thi moom ci alkhouràn ak sounna.

    Yoonnèntèbi lèralko ba bàyyi aw khètam ci lou lèr, sahàbayèk tàbihoonyi ak gnalèn toope ande diappe thia loolèn yonnèntèbi bàyyil, gnou teuyè thia bou deugar di roy yonnèn tebi sallal làhou alayhi wasallama ci paspasam ak diamou yàllàm, aki jikkoom, aki tègginam.

    gnom gnoognou di roy yonnèntèbi sallal làhou alayhi wa sallama gnooy kourèl bi ga khamnè dougnou dagne mouke di nèk ci deugue di thia fèegn, koulèn di khas wala galèn di khèkh doulèn loor tè dou takhe gnou bàyyi mouke .

    damay bind tèrèbi di ci lèral kourèl bi di roy yoonnèntèbi ci lèpp lan mooy sèn paspas , tè moy guem yall, ak malàkayi, ak tèrè yi yàlla diokh yonnèn tèyi, ak yonnèntèyi, ak allàkhira, ak dogalbi bou nèkhba ak bou nakhariba.

    Lan moy paspasou gniy toop souna?

    Gniy toop sounna sen paspas moy: gueme yalla, ak malakamyi, ak tèrèmyi, ak yonnentèemyi, ak bisou pegntheba, ak dogalyi bounèkh ak bounakhari.

    Dnouy guemnèyalla rek mooy binde moy warsagal temoy dokhal mbiryep.

    Donouy gamnè yalla rek mouyayou diamou, lepe lougnouy diamou loudoul mom nenla.

    Donouy guemnè melokani yalla youseleyi ak touramyi youmàgueyi, tadoun thi sooppi dara.

    Danouy guem kennouk yallagui ni amoul kene kounkoy bokalele,thi kennamgi ak yayo diamomgui ak touram you selyi, komniko yalla wakhe thi al khouran:

    ﴿رَبُّ السَّمَاوَاتِ وَالأرْضِ وَمَا بَيْنَهُمَا فَاعْبُدْهُ وَاصْطَبِرْ لِعِبَادَتِهِ هَلْ تَعْلَمُ لَهُ سَمِيّاً﴾

    Yalla danè: (yalla moy borom asaman ak soufe ak linek sen diggante, kon diamouko tega mougn ci diamou gi gakoy diamou.ndakh khamga kouyamo ak yalla ci ay touram walla ay melokanam? Amoul ken kou melne moom).

    Danouy gueme yalla kom nimou melale boppam thi ayatoul koursiou. Yalla dane:

    ﴿اللَّهُ لاَ إِلَهَ إِلاَّ هُوَ الْحَيُّ الْقَيُّومُ لاَ تَأْخُذُهُ سِنَةٌ وَلاَ نَوْمٌ لَّهُ مَا فِي السَّمَوَاتِ وَمَا فِي الأَرْضِ مَن ذَا الَّذِي يَشْفَعُ عِنْدَهُ إِلاَّ بِإِذْنِهِ يَعْلَمُ مَا بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَمَا خَلْفَهُمْ وَلاَ يُحِيطُونَ بِشَيْءٍ مِّنْ عِلْمِهِ إِلاَّ بِمَا شَاءَ وَسِعَ كُرْسِيُّهُ السَّمَوَاتِ وَالأَرْضَ وَلاَ يَؤُودُهُ حِفْظُهُمَا وَهُوَ الْعَلِيُّ الْعَظِيمُ﴾

    Limiy firi moy:

    Yàlla miga khamnè amoul kèn kou yayoo gnou diàmouko koudoul moom, moom mooy kiy dound doudou gou matgi, mooy kiy takhèwè mbiri diàm yèp, dou guammèntou dou nèlaw, moo moom li nèk ci asmàn yi ak linèk ci souf.

    Amoul kèn koumana ràmmou kèn fa moom loudoul boula diokhè ndigal ga ràmmou.

    Moom mo kham li nèk sèn kanam ak li gèn wèsou, tè amoul kèn kou mana kham dara ci ab xam xamam moom yalla loudl lako thia soob mou xamalko kou ko soob.

    Koursiy bou arasam bi yàtou wàyam migi toolnè yàtou wayou asmàn yi ak soufsi. (koursiy mooy tègou kàyou ay ndëgi tànkam). Tè disoul ci moom boroom bi mou sàm asmànyi ak souf si ak ligniy rëy lèp.

    Moom mooy kou kawègi mooy kou màg ki.

    Danouy guem liyalla wakh ci alkhouràn nè: yalla dara meloulnimom teday dègue dayguis.

    ﴿لَيْسَ كَمِثْلِهِ شَيْءٌ وَهُوَ السَّمِيعُ الْبَصِيرُ لَهُ مَقَالِيدُ السَّمَاوَاتِ وَالأرْضِ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَنْ يَشَاءُ وَيَقْدِرُ إِنَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ﴾

    Danouy guem li yalla wakh ci alqouraan nè: amoul lène louydoundou thi kawsouf loudoul ne yalla mokoy warsaguel temoy khame foumouy nek bouy dounde, ak foumouy nek ginaw bamou faatoo, telolou lèpe mougui thi tère moubinde.

    ﴿وَمَا مِنْ دَابَّةٍ فِي الأرْضِ إِلاّ عَلَى اللَّهِ رِزْقُهَا وَيَعْلَمُ مُسْتَقَرَّهَا وَمُسْتَوْدَعَهَا كُلٌّ فِي كِتَابٍ مُبِينٍ﴾.

    Danouy guemne li yalla wakhne: yalla rek moyor thiabiy gàloug xam koumpa, amoul ken kou kham koumpa koudoul yalla, temom mo xam linek ci guèedie gi ak soufsi, amoul wen khob wouy rot loudoulne xamnako, amoul ben peppe bounek fèenne loudoulne xamnako,amoul lèen lou toy walla lou woow loudoulne xamanako te bindnako fa lawhoul mahous.

    ﴿وَعِنْدَهُ مَفَاتِحُ الْغَيْبِ لا يَعْلَمُهَا إِلاّ هُوَ وَيَعْلَمُ مَا فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ وَمَا تَسْقُطُ مِنْ وَرَقَةٍ إِلاّ يَعْلَمُهَا وَلا حَبَّةٍ فِي ظُلُمَاتِ الأرْضِ وَلا رَطْبٍ وَلا يَابِسٍ إِلاّ فِي كِتَابٍ مُبِينٍ﴾.

    Danouy guem li yalla wakhe ci alkhouraan ne:

    Moom yalla rek mo kham kagne la allakhira di takhaw, moom rek moy wathiee tawbi, mookham li nek ci biri gni eumbe, amoul ken kou kham ligay am souba,amoul ken kou kham fooy faatoo.

    ﴿إِنَّ اللَّهَ عِنْدَهُ عِلْمُ السَّاعَةِ وَيُنَزِّلُ الْغَيْثَ وَيَعْلَمُ مَا فِي الأرْحَامِ وَمَا تَدْرِي نَفْسٌ مَاذَا تَكْسِبُ غَداً وَمَا تَدْرِي نَفْسٌ بِأَيِّ أَرْضٍ تَمُوتُ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ خَبِيرٌ﴾.

    Danouy gueme ne yalla day wakhe, te ay wakham sayouko soobee lakoy def, te lamou beuga wakh lay wakh, yalla wakhna ci alqouraan ne: yalla wakhna ak mousa ak wakhe.

    ﴿وكَلَّمَ اللَّهُ مُوسَى تَكْلِيماً﴾

    Mou wakhàtne: ba mousa dikkèe thia wakhtou wanou digantewon ak moom brombi yalla wakhakmoom.

    ﴿وَلَمَّا جَاءَ مُوسَى لِمِيقَاتِنَا وَكَلَّمَهُ رَبُّهُ﴾.

    Yalla wakhtne: ma woo mousa thia fay toolook montagno tour ma teralko ci wakhakmoom.

    ﴿وَنَادَيْنَاهُ مِنْ جَانِبِ الطُّورِ الأيْمَنِ وَقَرَّبْنَاهُ نَجِيّاً﴾.

    Donouy guem li yaalla wakhne: (bou guejegui donone daa guir binde bati yalla yi guejegui dina diekh te bati yallayi dou diekhe ).

    ﴿قللَوْ كَانَ الْبَحْرُ مِدَاداً لِكَلِمَاتِ رَبِّي لَنَفِدَ الْبَحْرُ قَبْلَ أَنْ تَنْفَدَ كَلِمَاتُ رَبِّي﴾

    Danouy guem ne bati yallayi mogana mate guena daggou te mogana wer bepe bate kome niko yalla wakhe ci al khourane ne:(wakhi yalla matna ci deugue ak manou)

    ﴿وَتَمَّتْ كَلِمَتُ رَبِّكَ صِدْقاً وَعَدْلاً﴾

    mou wakhàt ne: (ana kane mogana dguou yalla ay wakhe).

    ﴿وَمَنْ أَصْدَقُ مِنَ اللَّهِ حَدِيثا﴾

    Danouy guemni al khourane bou tedebi wakhi yalla la, moko wakhe thi dague moko yonni jibril mou wathieko thi yonentebi sallal làhou alayhi wasallama kome nimko wakhe thi al khourane nè :(al khouran lounou wathela mou diougè thi borome minedefyi, jibril moko wathe thi kholou yonentebi guirmou book ci gniy woote diamè ci yalla).

    ﴿قُلْ نَزَّلَهُ رُوحُ الْقُدُسِ مِنْ رَبِّكَ بِالْحَق﴾.

    ﴿وَإِنَّهُ لَتَنْزِيلُ رَبِّ الْعَالَمِينَ نَزَلَ بِهِ الرُّوحُ الأمِينُ عَلَى قَلْبِكَ لِتَكُونَ مِنَ الْمُنْذِرِينَ بِلِسَانٍ عَرَبِيٍّ مُبِينٍ﴾

    Danouy guemnè yalla mokawè mbindèfyi thi dieummame ak ay melokanam guir limou wakh ci alqouraan nè :(mom moy koukaweki kou magueki).

    ﴿وَهُوَ الْعَلِيُّ الْعَظِيمُ﴾

    ak limou wakhnè :(moy ki not thi kaw diamame yi moy kou khèrangeki moy kou kham leep)

    ﴿وَهُوَ الْقَاهِرُ فَوْقَ عِبَادِهِ وَهُوَ الْحَكِيمُ الْخَبِير﴾

    Dgnouy guem li yalla wakh ci alqouràn nè: (mobinde asamayi ak soufyi, bamouko bindè banoppi moudadi yamo ci kaw aras te moy dokhal mbiryi)

    ﴿خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالأرْضَ فِي سِتَّةِ أَيَّامٍ ثُمَّ اسْتَوَى عَلَى الْعَرْشِ يُدَبِّرُ الأمْر﴾

    ak yamom thi aras moy ak kawèm ci dieummam ak kawè ga yèel ci moom, te moom yalla rèk mokham namou nèkkè thia kaw aras, amoul kèn kou kham namou fa yamoo koudoul moom .

    Danouy guemnè mome yalla andaknè mogui yamo thi kaw aras day khame sene mbir yeb didegue sene wakhyi diguis sène dieufyi diteural sene mbiryi, moy warsagual kou gnàk, difathe adioyi, moy fal kou ko nèkh dèfko bour, moy foolli koukonèkh, moy yekati koukonekh, di soufèl koukonèkh, kokhamni mbiram niladèmè ak diamyi tha dague dague mogui andak mbindedefyi dagui dagui ande,donte mogui yamo thi arasambi, yalla nèna: (mom dara melouni mom te day degue day guis)

    ﴿لَيْسَ كَمِثْلِهِ شَيْءٌ وَهُوَ السَّمِيعُ الْبَصِيرُ﴾.

    Dounou wakh moukou li yènne kourèlyi diwakhe nan yalla migi fèppe ci dieummam.

    Dananou guisni kebe kouwakh lolou wakhna wakhi kèar, tè wakhna wakhi kou sankou tè rèer. Ndakh daay mèlal yalla mèlokàn wokhamne yèlloul ci yalla, ndakh li ci nèk ci ak soufè, nè boudènè yalla migi fèp ci dieummam kon day nèk ci bèp beureub bou saltè , tè yalla kawèna sèllena sorènak di mèlnoonou.

    Dananou guem lignou yonentebi sallal lahou alayhi wasallama khabar ci ab hadis nè yalla day wathie ci asaman sii ci gouddigi bou dèsèe bèn thièr, yalla bou wathiè danàn ana koumay woo ma wouyoula, ana koumay gnàn ma mayla, ana komay dièglou ma dièggal la.

    Danouy geumnè yalla day dike guir attè diguente diamyi komniko yalla wakhe thi alkhourane,

    ﴿كَلاّ إِذَا دُكَّتِ الأرْضُ دَكّاً دَكّاً وَجَاءَ رَبُّكَ وَالْمَلَكُ صَفّاً صَفّاً وَجِيءَ يَوْمَئِذٍ بِجَهَنَّمَ يَوْمَئِذٍ يَتَذَكَّرُ الإنْسَانُ وَأَنَّى لَهُ الذِّكْرَى﴾

    Nèna bisbou souf si yeugue too yeugu toomga, sa borom dadi dik gir attè diamam yi, mallàkayi dadi sappè .gnou dàdi eundi sawaraw diahannama, bou kèroguèe kou wèddi woon yalla daga wàrou dàdi toub, wayè fèk toub thi boobè bis dou diarign dara.

    Danouy guamnè yalla day dèf loumou beugga dèf. Yalla nèna ci al qouràan : (mom yalla loumou beugga dèf dakoy dèf te dara tawouko) ﴿فَعَّالٌ لِمَا يُرِيدُ﴾

    Danouy guemnè nammèelag yalla gnari nammèella:

    1- Limou dogal te mou sob ko mou am, limouy dogalnak tekki woulne loumou sooppla, lèg lèg mou dogal loo khmne loumou ayèla.

    2- Liga khamne yalla dako soopp di ko diglè, loolou loumou beugla wayè bouko soobè mou dogal mou am, bouko soobè dou dogal mou am. Misalam moy dioulli ak wor.

    Danouy guemnègnari nammèl yèpe day topou ak khèrèniam, lèpe lokhamnè dogalnako thi thiobarèem wala mou diglè gnou dèfko thi ak khèrègnam lako dogalè, mokham domou adamayi khamnanouko wala khmougno ko, wala mouneklo khamnè sèni khèl aguou thia.

    Danouy guemnè yalla kou bague top kati yalla yila, gniy top yalla gnomit gnou beugue yalla lagne. Liy tèktalè loolou moy liyalla wakh ci alkhouràan nè:(boufèkkèe bague guène yalla topoulen yonentebi yalla baguelèn).

    ﴿قُلْ إِنْ كُنْتُمْ تُحِبُّونَ اللَّهَ فَاتَّبِعُونِي يُحْبِبْكُمُ اللَّهُ﴾

    Ak limou wakhnè:(yalla dana indi ay nite niokhamni dalendi bague nioubague ko).

    ﴿فَسَوْفَ يَأْتِي اللَّهُ بِقَوْمٍ يُحِبُّهُمْ وَيُحِبُّونَهُ﴾

    ak limou wakhnè: (yalla day beugue gniy mougne)

    ﴿وَاللَّهُ يُحِبُّ الصَّابِرِينَ﴾

    Ak liyalla wakhnè (naguèn màndou ndakh yalla beugna gniy màndou).

    ﴿وَأَقْسِطُوا إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُقْسِطِينَ﴾

    Ak li yalla wakhnè (dèlèn rafètal ndakh yalla dafa beugue gni dieuf lou rafèt).

    ﴿وَأَحْسِنُوا إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُحْسِنِينَ﴾

    Dagnouy geumnè yalla day geuram lebe loumou yonal thi dine di bagne lepe loumou tèrè, boukouna thi liy tektalè lolou limou wakh ci alkhouràn nè :(bouguen wedde yalla yalla amoul àdio ci yèen, te dougueram thi diamamyi ak weddi bouguen santé mougaramko).

    ﴿إِنْ تَكْفُرُوا فَإِنَّ اللَّهَ غَنِيٌّ عَنْكُمْ وَلا يَرْضَى لِعِبَادِهِ الْكُفْرَ وَإِنْ تَشْكُرُوا يَرْضَهُ لَكُمْ﴾

    Danouy guemnè yalla dafay guereum diamam yiy guem tèy dèf lou bàkhe, komnimko wakhe thi alkhourane:( yalla garamnalen niougaramko lolou gnèlna gniragal yalla).

    ﴿رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمْ وَرَضُوا عَنْهُ ذَلِكَ لِمَنْ خَشِيَ رَبَّهُ﴾

    Dagnouy guemniè yalla day mèrè kepe kou yayo meram thi yèfaryi ak moykatyi,kom nimouko wakhe thi al khouràne nè: (yalla dana mbougal mounafèkhe yi ak yèaryi gnom gniy gnortou gnortou lou gnàw ci yalla ci dèfènè dou dimbali ab yoonnèntam ak gni guem yalla, yalla mèrè nalèen)

    ﴿وَيُعَذِّبَ الْمُنَافِقِينَ وَالْمُنَافِقَاتِ وَالْمُشْرِكِينَ وَالْمُشْرِكَاتِ الظَّانِّينَ بِاللَّهِ ظَنَّ السَّوْءِ عَلَيْهِمْ دَائِرَةُ السَّوْءِ وَغَضِبَ اللَّهُ عَلَيْهِمْ﴾.

    Yala wakhàtnè: (gniy wakh ak kèefar ande thièk khelmou dal kèn forsè woulèen ci yalla mèrènalèen).

    ﴿وَلَكِنْ مَنْ شَرَحَ بِالْكُفْرِ صَدْراً فَعَلَيْهِمْ غَضَبٌ مِنَ اللَّهِ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ﴾.

    Dagnouy guemnè yalla amna kanam. Yalla nèna: lithi kaw sou lèppay dièkh, kanamouk sa brom mom sakh ba fàaw, kanamam ga khamnè moy gou màggue ga, tè tèdde.

    ﴿كُلُّ مَنْ عَلَيْهَا فَانٍ وَيَبْقَى وَجْهُ رَبِّكَ ذُو الْجَلَالِ وَالْإِكْرَامِ﴾

    Donouy guemnè yalla amna gnari lokho you tedde you màague komnikouko wakhe thi alkhourane nè: ( gnari lokhomyi dafatalli day diokhr noumouko nekhe)

    ﴿بَلْ يَدَاهُ مَبْسُوطَتَانِ يُنْفِقُ كَيْفَ يَشَاءُ﴾

    Dagnouy guemnè yalla amna gnari beute kom nimouko wakhe thi alhourane di wakhak yonnent yalla nouhe nànko :( defaral galgui thi sàamou gi gnoulay sàamou ci guis gignoulay gis ci sounouy guete ga dèfar ko yit ci sougnou ndigal ).﴿وَاصْنَعِ الْفُلْكَ بِأَعْيُنِنَا وَوَحْيِنَا﴾

    Wa sounnayeb deuppo nagnou ci nè yalla amna gnàri beut, liy firndèl lolou moy wakhi yoonnetebi sallal lahou alayhi wasalma nèna: (dajal dafa patte te sene borom nekoul kou patte).

    Danouy guemnè yalla beut douko mana gis gis gou koy pèeg, yalla nèna ci alqouràan : (buet douko mana gis gis gokoy pèeg)

    ﴿لا تُدْرِكُهُ الأبْصَارُ وَهُوَ يُدْرِكُ الأبْصَارَ وَهُوَ اللَّطِيفُ الْخَبِيرُ﴾

    Danouy gamnè joulityi dananou guise sene borom yawmal khiyam, kom nimouko wakhe ci alkhouràane nè:(gna guem yalla sèn kanamya dafay lèr tè noy , gnou bolè thia di khol sèn broom)

    ﴿وُجُوهٌ يَوْمَئِذٍ نَاضِرَةٌ إِلَى رَبِّهَا نَاظِرَةٌ﴾.

    Danouy guemnè yalla dara meloulnimom thi melokanam you matyi,kom nimouko wakhe thi alkhourane:( dara meloul nèmome tè moom yalla moy kiy dègue lèppe di gis lèeppe)

    ﴿لَيْسَ كَمِثْلِهِ شَيْءٌ وَهُوَ السَّمِيعُ الْبَصِيرُ﴾

    Danouy guemnè yalla dou guemmentou wakhouma lak nelaw.guir ak matouk doundam. Yalla nèna: (mom dou guemmèntou dou nèlaw)﴿لا تَأْخُذُهُ سِنَةٌ وَلا نَوْمٌ﴾

    Danouy guemnè doutoogne kène ndakh ak màndom, tè dara ci li diamam yiy dèf oumpuko ndakh pèeg gimou lèn pèeg nimou matè.

    Danouy guemnè amoul lènne loumo lote ci defko thi asaman ak soufe guir matak xamxamam ak kattanam gou reuy, yalla wakhe thi al khourane nè: (yalla bou beugguèe amal dara danan na am rek loola am). ﴿إِنَّمَا أَمْرُهُ إِذَا أَرَادَ شَيْئاً أَنْ يَقُولَ لَهُ كُنْ فَيَكُونُ﴾

    Dagnouy guemnè yalla dou soonnou dou teulè, kom nimouko wakhe thi al khourane nè:(yalla mo binde asaman ak souf ci diourom benni fane te dara thi thiona lalouko)

    ﴿وَلَقَدْ خَلَقْنَا السَّمَاوَاتِ وَالأرْضَ وَمَا بَيْنَهُمَا فِي سِتَّةِ أَيَّامٍ وَمَا مَسَّنَا مِنْ لُغُوبٍ﴾

    Danouy guemn lèeppe loo khamnè yalla sakhal nako ci bopame ak lèeppe liko yonentebi sallal lahou alayhi wasallama sakhalal ci ay tour ak ay melokane, wayè danouy dagn ba sèt ci gnari mbire:

    1- Diko melal kom gana ay melokanam kom melkani mbindefyi la.

    2- Mouy geustou ndakala melokanou yallayi di amè. Mànàm bou yàlla nè yamouna thia kaw aras mouy geustou ndaka la yalla yamoo thia kaw aras.

    Danouy guemnè lebe loo khamnè yalla dakhe nako thi bopame wala yonentebi sallal lahou alayhi wasalma dakhal koko dagniy guemnè lola dakhouna ci mom, tèmom broom bi sorinako, gnou guemnè safànou loolèe gnou dakhe temiy ak mat mom la sougnou broombi milawo.

    Lèeppe lou yalla ak yoonnentèbi sallal lahou alayhi wasalma nooppi dagnou thiy noppi gnounit.

    Danouy guisnè geum yi gnou toud fi fratala tè lou meunta gnàakke la, ndakh yalla lèpe loumou sakhal thi boppam wala mou dakhe ko lolou khabarla boumou khibar ci booppam gnou war koo deugguell, ndakh yalla moo guena kham boppame te moo guena deugguou ay wakhe, te kène manouko pèeg thi kham kham. niki nonou yonentebi loumouko sakhalal waloumou dakhalkoko ab xibàarla boumou xibàrl broomom, tè moom moo guena dueggou bmolèm mbindèefyi, te moolèn guena xam yalla, tè moo ci dakha lèeral.

    Kon gnou xamnè wakhi yalla akoub yoonnentam dafa andak xamxam bou mat, akouk deuggou gou woor, ak lèral gou fès, kon nak kèn dou am gante ci diko dèlloo, walla ga thiy sik sakka.

    معلومات المادة باللغة العربية